wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
aakimu
accaparer
Mu ngi aakimu mikoro bi; mënatuñoo jél kàddu gi
il a accaparé le micro; on ne peut plus prendre la parole.
aada j-
coutume, culture
Jubb yii, seen aada la
ces touffes (de cheveux), c’est leur coutume.
aafiya j-
paix
May ma aafiya
fiche-moi la paix !
aawo b-
Épouse qui occupe le premier rang dans un foyer polygame
Aawo, buuru këram « aawo »
reine de sa maison
aka
comme
Aka gaaw
comme il est rapide !
a
c’est… qui
Omar a lekk ceeb bi
C'est Omar qui a mangé le riz.
Man a
C'est moi.
a
indique un procès à l’inaccompli
Boo ko gisee muy dem ak a dikk nii rekk, dafa jaaxle
quand tu le vois aller et venir comme ça sans arrêt, c’est qu’il est inquiet.
(prov.) Bëgga dem taxula mëna dem. Mëna dem ay taxa dem
il ne suffit pas de vouloir partir, il faut pouvoir le faire.
a
ou
amaana j-
loyauté
am-aajo
être respectueux, être attentionné, avoir de l’égard (à l’endroit des gens)
Ku am-aajo la ci ay dëkkandoom
il a beaucoup d’égards pour ses voisins.
am-am b-
richesse avoir bien
Danu wara boole sunu am-am
nous devons mettre en commun nos biens.
am-bopp
être extralucide, être un illuminé
Dafa am-bopp; lu ñu ko fexeel, mu yàqu
C'est un extralucide; tous les coups qu’on monte contre lui échouent.
am-alal
être riche être fortuné
Waa ju am-alal lay séyal
elle est mariée à un homme riche.
am-diine
être pieux
am-bayre
avoir une aura qui attire toutes les attentions à soi
Jaaykat bu am-bayre la
C'est un commerçant en vue.
am-bët
avoir les yeux globuleux
Am-bët dafay yokk taaru jigéen
avoir des yeux globuleux rehaussent le charme d’une femme.
am-fayda
avoir du caractère, de la personnalité
Góor gu am-fayda du wàlli sabar
un homme qui a de la personnalité ne va pas à des séances de tam-tam.
am-gat
avoir du toupet (grossier)
Aka am-gat
comme il a du culot !
am-fit
être audacieux, être courageux
amiin
amen ! Ainsi soit-il !
Neleen amiin
dites amen !
Lii de mooy ñaan gu daje ak amiin
cela ne pouvait pas mieux tomber
am-jëmm
avoir de la prestance
Xale bu tuuti la; dafa am-jëmm doŋŋ
C'est un tout jeune enfant; il a seule-ment de la prestance.
am-ji-jàmm j-
personne avec qui on entretient de bonnes relations
Omar sama am-ji-jàmm la; mën naa koo ñaan njekk
Omar est une de mes relations; je peux lui demander une faveur.
am-jom
avoir de l’amour-propre
Ku am-jom la; su ko baay ji xulee, mu jàng bu baax
il a de l’amour-propre; si son père le sermonne, il étudie bien.
am-jàmm
être pacifique, calme, paisible
Kooku, nit ku am-jàmm la
celui-là, c’est une personne paisible.
am-jot
n’avoir rien à faire de son temps être libre
Seetal ku am-jot, nga ànd ak moom
vois qqn qui est libre, va avec lui !
Toppal fale; danga am-jot
fiche le camp; tu n’as vraiment rien à faire.
am-jikko
avoir des sautes d’humeur
Ku am-jikko neexula dëkkal
une personne qui a des sautes d’humeur n’est pas facile à vivre.
am-kersa
être timide avoir de la retenue
Dafa am-kersa
il est timide.
am-kàttan
être résistant, endurant, fort
Tool bii, ku am-kàttan rekk a ko mëna bey
ce champ, seul qqn de fort peut le cultiver.
ammaa
pour sûr
Ammaa, koddaay moom, ay farataam barewul
pour sûr, s’agissant des habits, ses exigences ne sont pas nombreuses.
am-maanaa
être important, intéressant
Dama defe woon ne lu am-maanaa la ma doon wooye
je pensais qu’il m’appelait pour qqch d’important.
am-kóllëre
(relations) Être fidèle
Xaj, rab wu am-kóllëre la
le chien est un animal fidèle.
am-solo
être important, intéressant
Mbir mu am-solo la waxtaane
C'est d’une affaire importante qu’il parle.
am-sutura
être discret
Jabar ju am-sutura la
C'est une épouse discrète.
am-taxawaay
être élancé
Waa ju am-taxawaay la
C'est un homme élancé.
am-teraanga
être accueillant
am-wërsëg
être chanceux avoir de la veine
Tey, danga am-wërsëg
aujourd’hui, tu es chanceux.
am-tur
être célèbre
Woykat bu am-tur la
C'est un chanteur célèbre.
am-muur
être chanceux
am-xel
avoir du jugement avoir de la finesse d’esprit
Jabar ju am-xel du mere jëkkëram ngir xarum Tabaski mu duuful
une épouse réfléchie n’en voudra pas à son mari pour un mouton de la Tabaski qui n’est pas gras.
am-xorom
être intéressant être amusant
Ku am-xorom laa doon waxtaanal
je causais avec une personne intéressante.
am-yaram
être obèse avoir une forte corpulence
Bëggumaa am-yaram
je ne veux pas être obèse.
am-yar
être poli être bien élevé
Gone gu am-yar la
C'est un enfant bien élevé.
am-yeel
être élancé
Xale la, dafa am-yeel rekk
C'est un enfant mais il est grand.
am-yax
être robuste
déjeuner
Xaaral ba ma añ ba-noppi
attends que j’aie fini de déjeuner !
añaan
prendre son déjeuner chaque fois en des lieux différents, généralement en pique-assiette
Bi jabaram demee ba tey, dafay añaan rekk
depuis que son épouse s’en est allée, il prend son déjeuner à gauche et à droite.
andaar w-
unité de mesure d’environ un litre
Andaaru njaw, andaaru lem, andaaru soowum bëy, ñetti focci wuy, nga bembaxli ko
un litre de sirop de jus de Sclerocarya birrea, un litre de miel, un litre de lait caillé de chèvre, trois pains de singe, tu le verses dans la bouillie.
añ b-
déjeuner
Indil añ bi
apporte le déjeuner !
(prov.) Liggéeyu ndey : añub doom
labeur de la mère : déjeuner du fils
anaata j-
sixième des sept périodes de treize jours de la saison des pluies
Anaata jaa ngiy jeexsi
la sixième période de la saison des pluies tire à sa fin.
aaréen j-
arachide
Dañu toskareel aaréen
on a fait de l’arachide un parent pauvre.
aaru
se protéger
Bala may fital aw rab, dinaa xool ndax mu ngi ak biir, wala ndax tollu na ci waxtu aaru
avant de tirer sur une bête, je vois d’abord si elle est grosse, ou si elle est dans une période où elle se protège (d’un accouplement).