wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Xaaral ba mu yàndoor, nga tëral ko
attends qu’il soit profondément endormi et tu le coucheras.
(prov.) Doxandéem nelawul ba yàndoor
L'étranger n’a pas le sommeil profond.
yàq biir b-
interruption volontaire de grossesse
yàqute g-
impolitesse
Yàquteem a tax fu mu liggéeye, ñu mujj ci dàq ko
C'est à cause de son impolitesse que partout où il travaille, on finit par le renvoyer.
yàwwi
élargir
Dama bëgga yàkki baat bi
je veux élargir le col.
yóbbal b-
viatique, provisions de route
Cereek soow lanu daan def yóbbal
nous emportions du couscous et du lait caillé pour viatique.
yónnee
envoyer qqch à qqn
Dinaa la yónnee xaalis bi
je t’enverrai l’argent.
yàqule
un préjudice, avoir qqch d’endommagé
Bu nag yi duggee ci sa tool, dinga yàqule
si les vaches entrent dans ton champ, tu subiras des dommages.
yóbbante b-
ce qu’on fait transmettre à qqn
Am naa sa yóbbante
J'ai un message pour toi.
yób
apporter à qqn (vers un autre endroit)
Yób ko sa yaay
apporte-le à ta mère !
yóos
avoir la rougeole
Dafa yóos
il a la rougeole.
yóor w-
part portion
Ñetti yóor
trois parts.
yóox g-
cri
àbbante
s’emprunter des choses mutuellement
yóos b-
rougeole
Na des ca kër ga ba yóos bi wér ?
qu’il reste à la maison jusqu’à ce que sa rougeole soit guérie !
yóos j-
menu fretin
Jéndal yóos, nu togg kaldu
achète du menu fretin, nous allons préparer du « kaldu ».
yót
emmener, amener, porter, apporter (qqch à qqn ici ou là-bas)
Dafay xëy foraatuji lu mu yót ay doomam
il part le matin en quête de nourriture qu’il apportera à ses enfants.
àbb
emprunter
Demal àbb Faatu gënnam
va emprunter à Fatou son mortier.
àbbaatu
emprunter (habitude)
Li ma ko yàqal mooy : àbbaatu
ce qui me gêne en lui, c’est qu’il emprunte (c’est son habitude).
àddu
répondre de la voix
Bul àddu !
ne réponds pas !
Teen bi dafa xóot ba booy tàccu, dafay àddu
le puits est si profond qu’il fait écho quand on frappe dans les mains.
àbbloo
ordonner (à qqn) d’emprunter
Ndax man maa la àbbloo gënnu jaambur
est-ce que c’est moi qui t’ai demandé d’emprunter le mortier d’autrui.
yóot
exprime la manière d’allonger le bras pour atteindre qqch
àddiya j-
tribut que l’on donne aux descendants d’un défunt guide spirituel, en hommage à ce dernier
Joxeleen àddiya Sëriñ Tuubaa
donnez le tribut en hommage à Serigne Touba.
àkk
s’arrêter soudain
Mbaam mi dafa àkk, leketu soow mi këppu
L'âne s’est arrêté brusquement et la calebasse de lait caillé s’est renversée.
àkk
se présenter devant qqn pour se plaindre d’une chose dont il est censé répondre
Ba sama ganaar këppee sa ceeb, danga ma àkksi woon
quand ma poule avait renversé ton riz, tu étais venue te plaindre.
àkk w-
Écorce croûte
Àkku xay baax na ci
L'écorce du caïlcédrat est efficace pour cela.
àkk w-
nuages tout blancs apportant une forte pluie. Ils partent de l’horizon et montent. Il arrive que dans une même zône, la pluie tombe sur une partie et pas dans l’autre
àkk m-
fait de se présenter chez qqn avec impétuosité pour se plaindre d’une chose dont elle est censée répondre
Sa àkk ma la lay fàttali
elle te rappelle la visite agressive que tu lui as faite.
(prov.) Àkk àkkum gaynde, song songum bukki
enthousiaste avant l’action, froid au moment d’agir
àjjuma j-
vendredi
Tey, àjjuma la
aujourd’hui, c’est vendredi.
àlle
sauvage, désert (lieu inhabité)
Bërëb bii dafa àlle
cet endroit est sauvage
àjjiku
faire descendre (qqch d’un endroit élevé)
bal bi àjjiku na
on a fait descendre le ballon.
àllarba j-
mercredi
Dinaa ko seeti àllarba
j’irai le voir mercredi.
(prov.) Njàng mu nekk am na àllarba
toute activité nécessite une pause.
àmbolog b-
enveloppe
àppat
respirer difficilement
Buy yéeg iskale bi, dafay
àppat quand il monte l’escalier, il respire difficilement.
ànk
fruit qui a mûri dans l’arbre
àngal
angle
àngale
anglais
àttaa
même
Àttaa man, dem naa fa
même moi, j’y ai été.
ànd b-
placenta
Mbaam mi lekk na ànd bi
L'âne a mangé le placenta.
(prov.) Ku wacc sa ànd, ànd boo dem fekk ca boroom
quand on quitte les siens on ne peut pas s’accorder avec les autres.
àqan
être très proche par des liens de parenté
Sama jarbaat àqan la
C'est mon neveu très proche.
àttaaya j-
décoction de thé préparée suivant la tradition des Maures
Sa àttaaya ji neex na
ton thé est délicieux.
àtte b-
verdict décision d’un jugement
Lii àtte Yàlla la
tel est le jugement de Dieu.
àtte-tooñ b-
terrain vague no man’s land
Dañuy tere ku tëgg sabar ci pénc mi, waaye mën nanoo dem ca àtte-tooñ ba ca gannaaw toolu Demba
il est interdit d’organiser des séances de tam-tam sur la place publique, mais nous pouvons aller sur le terrain vague qui est derrière le champ de Demba.
óom b-
genou
Sama óom dafay metti
J'ai mal au genou.
óbbali
bâiller
Yaa ngiy óbbali rekk, demal tëri
tu n’arrêtes pas de bâiller, va te coucher !
óow
Oui !