text
stringlengths 6
463
|
---|
Xël wu jéggi dayo, duplee ndeyjoor, bañ a taxaw ci are yi ngir may kiliyaan yi ñu wàcc, yenn lañu ci jalgati yi. |
Liggéeykati meeri yi wone nañu ne mënuñu, lajj nañu ci seen sas wi. |
Ba léegi ñu ngi xaar kalaameb Maamur Jàllo, |
ndax loolu dina tax waa Senegaal yi xam bu baax ñi ñuy jiite. |
Musaa ak Ibraayima Ba, cosaanoo Welingara dañu fàqee woon ca seen daara ja nekk Kawlag ngir ñibbi seen kër. |
Kilifag Senegaal bile di Amadu Galo Faal, njiitu BAL, moo jox kub bi nga xam ne nataalu ag guy la. |
Ndaxte dinanñu yegge ay jegeñaaleem (jëwriñ ak deppite) lim yu bare. |
Li mu am yépp ci at mi, moom kese, tolloo naak ñaari ñetteelu xaaju li gox bi am. |
Te ñu koy gën di jëfandikoo ci mbay mi, maanaam, li ëpp ci li ñuy jariñal ci Senegaal. |
Ki ñëw bees dina jëfandikoo jumtukaayi njureefam |
(petorol bi tollu ci ñeen-fukk ci téeméer boo jël ci li muy am at mi yépp ak ci askan wi, askan woowu mu ngi tollu ci téeméer ak juróom-ñeen-fukki milyoŋ ak juróom-benn) |
ngir am ci xéewal yiy tukke ci màrse bi ñépp bokk. |
Senegaal def na li waroon bi mu dajee ak ekibu Keeñaa, bu àndoon ak pasteef lool te soxlawul woon lu dul temboo rekk ngir jàll, bokk ci ñetteel yi gën, ginnaaw bu Marog daane Afirig di Sidd (Afrique du Sud) benn bit ci dara. |
Luy dakkal mbirum turu Usmaan Sónko/Peresidãa ci kayiti joŋantey néegi njàng yu sekond, lile lañu dégge ci rajo Sud Fm. |
Dañu leen daanoon ci fukk ak juróom-ñeenteelu simili bi, waaye Mbay Ñaŋ ak i ñoñam mujj nañu dugal ñoom tamit. |
Defleen ndànk, bu ñu gaaw a wax. |
Jëfandikooleen seen kàrta wote yi, folli ko, |
loolu rekk moo ñuy mën a musal ci deret ju tuuru. |
Ngan gi nga xam ne, seetlukat yi, ag defaruwaat ba jekk lañu ko jàppe, ñëw na ci jamono joo xam ne, xayma bi Këru xayma gii di (ANSD) def ci weer wi, wone na ne li réewum Siin di dugal ci xaalis ci réew mi moo ëpp fuuf li réewum Farãas di dugal ndax ci benn diggante bi, tus ba ñeen-fukk ak juróom, |
Siin a ngi dugal 44,6% te Farãas moom di dugal 5,3%. |
Ak jàngalekat yu màgget yi, ñu bare ci ñoom di sooxaale feebar, dellu ci lekool yi weeru septàmbar, mën a leen di jural musiba, |
bu loolu amee rekk, mën na nekk luy gën a taral ñàkkug jàngalekat yi am tey ci njàng mu kowe. |
Tey, Sinwaa bi dafa gëm ni Siin moo war a jiite àddina si te dog-dog dafa ko daloon ci diggante bi, Àngalteer ak Sàppoŋ raw ko. |
Maa ngi digal képp ku yore sànkaru xëtër, jàngoroy xol, jàngoroy res, sàkkara bu tolluwaayam jéggi dayo, tenqo bu bañ, doomu jàngoroy erpes, jafe-jafey koddal, sànkaru xelliwaanu sàkkara, ñàkk a mën a am doom ak jiwu góor wu néew, mu dem seeti Doktoor Nelson. |
Wooteel am ndaje mu yaat |
wala nga gis ay limi tur yu bare. |
Ñett ñi ko dimbale nag ñoom, ñu di Daam Si, Seex Njaay ak Abdu Fay, ñu nga ba tey ci yoxoy takk-der yi, Màkkaanu takk-der yi (Section de Recherches), ñu leen di déglu, |
li ñu leen di toppe mooy, rawale ab defkatu ñaawtéef. |
Njiitu wàllu njiiteef gi mu ngi wallusi Njëwriñ ji yore suqalikug askan wi nga xam ne, ay gëtam rekk la yore woon, di seetaan bi màkkaanam bi di lakk. |
Li mu def ci njaaxum ci pólotig bi li muy bare bare, ay ñoñam dañu ko bàyyi muy wéy ci loolee. |
Mook Sàngalkaam ñoo bokk benn dekere 2011 bi rëddaatoon gox bi. |
Kuy wax lu gën ngir dem ak xel mu dal ca joŋantey meeri ya. |
Loolu tamit moo am ak waa Naples yi waa yi wékku ci Spal. |
Dinañu dem ca daloob yoonu Kafirin – Ngànda ba, dem Tàmbaa, |
bu ñu ci paree, ñu dem Kéedugu, foofee, Njiitu réew mi dina fa daloo lopitaal Ammat Dãasoxo. |
Li ñu ñu bëgg a gëmloo mooy, dekere bi ñu jox liggéeykati njiiteef gi du bu baax bi, |
loolu dafay tekki ne, kilifteefu nguur gi wala sax gu Njiitu réew mi dafa nërméelu ba ay nit di mën a am sañ-sañu jox liggéeykati njiiteefam gi ay kayit yu bon ngir ñu sukaandiku ci, |
def liggéey ba ca war (dekere wala yoon). |
Yal na la jig te yeneeni ndam topp ci. |
Yoon teggi loxoom etijaŋ yi, Porofesëer Baabakar Jóob ak Giy Maris Saaña xeexu ñépp la, askan wépp a ko laaj. |
Rom-poye Liberte Siis, ci wetu ñaari yoon yi, dafa mujj nekk ab bérebu dox-daje dëgg léegi. |
Fileek digaaleb Senac SA ak Nguuru Senegaal di jeex, Nguur gi dina defar ñetti téeméeri kilomet ci otorut ak xaalisu boppam. |