url
stringclasses
152 values
text
stringlengths
4
5.13k
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
NAKA LAA GISE MBAS MI
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Mbas mu dërkiis, ñàkk teggin tey jur tiiñalante ci biir réew mi ak ci bitim réew….
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Naka la doomi Afrig yi war a taxawe ? Céy mbas  mee gudd tànk, moom mi fàqe Penku,  ca Wuhan, ca Siin, ca Asi, sóobu ci Afrig, ba ci Géeju Atlantig, daanu ci fii ci Ndakaaru (dëkk raw) ; ci Tànk (Wakaam, Ngor, Yoof) fekk ñu fi ! Balaa moo agsi, wëndéelu na, jaar Ërop, jaar Amerig ! Kon boog dab nañu, yëngal na jamono, yëngal àdduna wërngël  képp, wërngël këpp, wërngël këtt.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Li bees
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Moonte ku xam jaar-jaari taarixu nit, xam ne du guléet musiba ak balaa xëppu ci gox, dëkk, réew, mbaa pàcc ci dunyaa. Li bees kay, moo di mbir mi ni mu gaawe, bette ak  law ; dëgg la, li ko waral moodi dem ak dikk bu gaaw te bare ci àddina, yéenekaay yu bées te ratax. Ak covid 19 tiitànge ak njàqare bare na, ñi faatu wax i nopp, moo xam góor, moo xam jigé. Mbas mii bàyyiwul ndaw te yab na mag, waxatumaak màggat. Ma nga doore Siin, faat fa ñu bare ; dàqe ji Tubaab yi Ërob ak Amerig, Naar yi yuuxu, sarxolle, mu mujj, dabsi nit ñu ñuul ñi, fii ci Afrig, fii ci Senegaal. Moone de doomi-Senegaal yi demoonañ ba yaakaar  ni dañoo tul, mbaa Yàlla ñoom rekk la bëgg.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Li yëngu, li ko yëngal…
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Li jaaxaal ñépp, boroom xam-xam yi, doktoor yi, fajkat yi ak njiiti réew yi, mooy mbas mi kenn xamul li ko sabab. Mbaa du gëstukat yu waane ñoo ko rëccal walla lu ñu sos la, te tey ko, walla ndax bëre ay ponkal la ci politig, walla koom-koom ? Xey-na dina mës a leer bés.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Li yëngu daal, li ko yëngal moo ko ëpp doole. Li ko yëngal nag, ndax ci njugub la jóge, mbaa meneen mala mu ñu doon jaay ca marse ? Koronaawiris ndax daa mel ni fel, mbaa teeñ, mbaa saxayaay ? Doom bi,  ci saxayaay lay dund walla ci xobu-garab ?
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Xam-xamu seetantal dina ko mës a leeral. Li wóor mooy dugg na ci yaramu nit, di wàllaate, indaale yaram wu tàng ak sëqat su bon, dënn bu fatt ak bakkan buy xelli ak biir buy metti.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
War nañoo xeex jàngoro ji, bëmëx ko ci biti. Réew yépp loolu la ñuy jéem.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Ñenn ni teel a fagaru, mel niki Siin, dem nañ ba bëmëx mbas mi ; ñi yéex a jóg, sàggan mel ni Itaali, Espaañ, Farãas, Amerig, waaru nañu, metti na lool ci ñoom, ña fa dëkk, juddoo fa, màgge fa, di fa tedd, ak ña fa ganesi mbaa wutsi wërsëg.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Pexeyeek jumtukaay yi
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Bi mbir nee faax, yenn réew yi mel ni Siin jiital xam-xam, xel ak caytu. Naka noonu dañuy ber ñi jàngoro ji laal, def ay lël, door di seet garab yu mën a indi tan.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Ci réew yu bare, am na ñu seen xel dem ci xam-xami Maam ya ak diine, ñu dem sax ba ni njaaxum yiy gën di bare ci àddina ñoo tax Yàlla mere ñu, delluwaat di cawe, ngir ñu  dellu ci dénkaane yi mu jaaraale woon ci Yonent yi.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Jar na nu jàng, jàngaat, sóobu ci, tanq ci woyu Sëriñ Musaa Ka, Xarnu bi, xarnu bi ñu génn (XXel), moom  bàyyiwul koom, aada, diine, mbaax ak xarbaax, tarixa, yoonu mucc, texe. Moonte war nañu fàttali, mbaa xamle ni, sunu Maam ya, waa Këmit, Misra, Esipt, ñoo jëkk a bind ci dund ak dee ; mbégte ak naqar.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Fii ci Senegaal
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Ci sunum réew, ki ko jiite, toog ci jal bi, Parsidã Maki Sàll, woote na waxtaan ak njiiti làngi polotig ak mbootaay yi ànd ak jamono yiy aar  liggéeykat yi, waxtaan ak dippite yi, ndawi réew mi ngir am lu mu yokk ci li mu xalaat ci bëre ak mbas mi. Ku ne def nga li la sa xel, xol, yaram, kàttan, mën-mën, pexe, gafaka may.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Gëstukat yi, fajkat yi, def nañu seen keem-kàttan, ba mbir mi am fu mu yem, jéggeegul dayo.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Bi mu agsee ba am fi weer, ñu gis ne laal na 195 nit, 40 % yi dañoo indaale doomu mbas mi,  dugal ko ci réew mi , 56 % dañu leen ko wàll, 4 % xamuñu fu mu ak naka la leen dabe. Loolu tax na, ñu war a gën a fagaru doonte xamuñu fépp fu mbas mi di jóge ; lii tamit la Porofesëer Musaa Seydi miy jiite xéex bi ci xam-xamu settantal ak paj denkaane.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Ñi koy jàppale ci caytu gi ak jumtukaay yi, doktoor Ablaay Buso, Alfa Sàll ak Mamadu Jara Béey dalal nañu xel yi, joxewaale ay ndénkaane yu ñu mën a may ñu mucc ci. Dëgg la, am na doomi réew ñu ci jot a faatu, am ci ku doon ku am tur, fulla ak faayda ci réew mi ak ci bitim-réew, mu di Paap Mabaaba Juuf, ku ñu ràññe ci xam-xamu tàggat yaram, ak ci gunge xale yi ci futbal, dem ba jiite ekibu Màrsey, ca Farãas.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Ëllëgu jàmm, tinkeeku ak tabaxaat
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Li am ba des moo di sàggan baaxul, wér-gi-yaram, jàng ak xam-xam war nañu leen sédd bu baax a baax. Ñu dellusi ci li mag ñu baax ñi dénkaane woon, fexe ba liy génn  ci pénc yi ak lël yu bare yi nuy amal, nu def leeni  jëf. Su boobaa luñu bett, ñu dékku ko, ci lu gaaw. Dëkk ci  fàtte, gàtt xel ak réccu ñoo ànd.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Gëstukat yi am nañu sas bu réy, war nañu gën di waxtaan ci seen biir, di wax ak ñiy jiite ci yeneen fànn.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Mbokk yi, at mii, nar na gudd tànk lool !Mu ngi mel na fasu benn tànk « rëkkal mba ma rëkk», nitu guddi ! Njuuma jaa ngook ! Am na ñu mu jaafurloo, mel ni Tubaab yiy wax nañu gaaw wuti garab, ñakk bu bees, jéemantu ko ci nit ñu ñuul ñi. Taat wuy tàkk moom kenn mënu ko solal tubey, kërandoom du set.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Doomi réew mi, doomi àddina, jaaxle nañu ! Ku moytuwul nag tam sa moroom dëmm, tam sa mbokk nóoxoor
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Lu mën a dindi jaaxle ?
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Xana daal ñu dal, gën a njàccaar, yokk caytu gi, jàppoo ci fagaru gi, paj mi. Nu jeexal ci seetlu bi : réew yi ci muccagum as tuut, ci Afrig mel ni Lësotoo, Komoor, Malawi, Sudaan, Sawo Tome bokk nañu ci yi duggagul, mbaa yi sore xëccoo ak buuxante yu metti ci biir àddina. Kon boog nanu gaaw ci teggi tànk ci benn yoon, teg tànk bu bees, bu gën, te àndandoo jublu ci tabax Bennoo Afrig ci Mbokk.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
Nañu Taxaw Temm, am Pasteef, tegu ci Yoonu Askan Wi, Déggoo ngir Bokk, Bëre, Daan.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
*Baabakar JÓOB Buuba, Njiitu Mbootaayu Doomi Afirig yiy yëngatu ci Liifant ak Njàngum mag ñi, PAALAE (Pan African Association for Literacy and Adult Education) te nekkoon njiitu An@fa di bànqaasu PAALAE fii ci Senegaal
https://www.defuwaxu.com/maggalu-daaru-xudoos/
MÀGGALU DAARU XUDÓOS
https://www.defuwaxu.com/maggalu-daaru-xudoos/
Mu doon tur wu siis wi ñu ko xame, màggalu daaru xudóos doon xew-xewu diine. Murit yi di ko màggal at mu jot ca Tuubaa, rawatina fa goxu daaru xudóos.
https://www.defuwaxu.com/maggalu-daaru-xudoos/
Xew-xewu diine boobu di fàttali bés ba Sëriñ Tuubaa Xaadim Rasuul di wuyuji Boroomam. Mu doon bés ba ñu ko jébbalee Boroomam faTuubaa ginnaaw ba mu làqoo ca Njaaréem (Njurbel). Ñu njëkk ko màggal ca atum 1935. Sëriñ Móodu Mustafaa di ab taawam nekk tamit xalifaam bu njëkk moo taxawal bés boobu. Muy wéy ba su nu jonni-Yàlla-tey. Waa Daaru xudóos di ko màggal ba mu far wuyoo ci turu màggalu Daaru xudóos.
https://www.defuwaxu.com/maggalu-daaru-xudoos/
Bés boobu ëmb mboor ak i baatin ca atum 1927 ba Sëriñ bi làqoo. Mu nekkoon tiis ju réy ci murit yi, jur njàqare ci taalibe yépp. Waaye, seede yi di wéy di biral taxawaayu taawam ba mat sëkk taaw, di Sëriñ Móodu Mustafaa. Nde, loolu ndénkaan la woon digganteem ak Sëriñ bi. Ndax, la mu sàkku woon ci moom mooy “ Bés bu ma wàccee, nañu ma yóbbu Tuubaa”. Mu nekkoon jamono yu metti ci digganteem ak tubaab yi waxoon ne, mëseesu koo bàyyi ( résidence surveillé) ba ni mu làqoo. Mébét moomu la doomam ja sottal ba ni mu ko indee Tuubaa te benn tubaab gisu ko.
https://www.defuwaxu.com/maggalu-daaru-xudoos/
Ren, ñu màggal ko ci dibéer jii weesu 6 ut 2023, yamoo woon ak 19i fan  muharram atum 1445. Ci teewaayu Sëriñ Ahmadu Maxtaar, di xalifab Daaru Xudóos. Bés boobu di am njooqe. Ndax, teewaayu nit ñu takkoo-takku ngir fekke guddi gi. Mu doon bésu xubbeeku ci ay bàkkaar. Nde, képp ku ko fanaane màggal ci béreb bu sell ba, ñu far say ñaawteef. Mu doon kàddu yu Sëriñ Móodu Mustafaa jaayante ak Boroomam.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
MÓODU LÓO DAAN NA AAMAA BALDE
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Xaar bi yàggoon na lool, waaj gi tamit naka noonu. Waaye, ñaari mbër yi mujje nañu sëgg démb ci dibéer ji. Móodu Lóo ak Aamaa Balde bëre nañ démb, ca aareen nasiyonaal ba ca Pikin. Móodu Lóo moo daan, yóbbu ndam leek metel mi (la couronne) Pàrsel.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Seen làmb ji, bi ñu ko dalee waaj, yàggoon na lool. Jotoon nañ koo àppal ca njëlbeen laat ñu koy bëtal ci sababi gàllankoor. Moo taxoon ñu dàkkoon ko ba jëmmi jamono. Démb nag, ci dibéer 5i fan ci nowàmbar lees ko jàppaatoon te mujje na am.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Ci fan yii ñu génn, gisees na ñaari mbër yi, Aamaa Balde doomu Pikin ji ak kii di Móodu Lóo doomu Pàrsel ji, ni ñu doon waajalee bés bi. Amaloon nañ ay jàkkaarloo yu saf sàpp. Werente bi bari woon lool ci diggante soppe yeek farandooy mbër yi. Fan yii ñu génn ba tay, foo geestu nit ñaa ngi ciy wax, ku ci nekk naan sama mbër a mën, sama mbër ay daan. Mënees na wax sax ni làmb dafa mel ne lu dekki. Nde, toogoon nañu jamono yoo xam ne yii, bu mbër mu mag waree bëre sax kenn du ko yég, mbaa ñu ci bari bu desee ay benn fan, ñaar lañ koy yëg. Bëre Aamaa Balde beek Móodu Lóo bi nag, dafa dekkil làmb ji, naatalaat géew gi. Jaadu na nag, ndax ñaari ndaanaan a doon daje, ku ci nekk mbooloo nekk sa ginnaaw.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Móodu Lóo yàgg naa def i jaloore ba jël metelu làmb ji (la couronne de l’arène), nekk buur bi, maanaam « Roi des arènes ». Ci Ëmma Seen, moom it di doomu Pikin, la ko nangoo woon. Gannaaw loolu, Ëmma dikkaat ngir nangu ko, saa-pàrsel bi daldi koy bañ, daanati ko. Ba tax na, mënees na ni loolee yokk jom kii di doomu ndem-si-Yàlla ji, Fàllaay Balde, ci mu gën a ñafe ba ñu taxawal bésam ak Móodu Lóo.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Li war ci bés bi yépp nag, ñaari mbër yi def nañu ko. Ci bés bi, ku ci nekk ñëw na na mu waree, bàkku, neexal bés bi, yëngal fowu bi (Arène national). Cokkaasante nañu, xarfa-fuufa yi ñépp gis nañu ni ku ci nekk ci ñoom ñaar def nga ci xaalis bu weex tàll. Amaa dikkee na nañu ko xamee woon, Móodu, wàllu sangu bi ñëwee na ci nees ko miinee woon it. Waaye, ci wàllu téere, dafa dëggal li mu ne : « woon weesu na fu may takkatee gàllaaj yu bari ndax làmb. »
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Ba ñu defee loolee lépp nag, la arbit bi daldi woote ca digg géew ga, ku ci nekk ñaan la muy ñaan, léemu ay léemoom. mu laaj leen ndax pare ngeen, ñu ne waaw, mu daldi sex mbiib ba rekk ëf ca. Ñépp ne tekk, fowu ba ne selew, soppe yépp jël xol yaak xalaat yaak yépp jëmale leen ca bëre bi, ca ñaari mbër yay laale.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Ñaari mbër yi tàmbaley léewatoo, ci ay saa, Amaa daldi tàmbali di dox ci kaw Móodu Lóo, nees-tuut ñu tàmbalee sànnantey kurpeñ rekk roofaloo. Doomu Pikin ji dóor mboot, Móodu ci mën bëreem, rocceku Amaa rëpp, samp ñetti cër ya, doomu pàrsel bi wër ko ndombo, jekku ko, di ko rokkoos ak nokkoos. Dóor yi mel ni mbàccum gerte. Móodu Lóo tiim Aamaa Balde, jàpp kanam giy dóor rekk bañ a bàyyi. Biir dóor yi mettee ba metti, as waay a dawee ci bitig géew ga, romb takk-der yi, ñëw laxasu Móodu Lóo ngir wallu Aamaa mi mu àndal. Ca lañu àttee ñaari mbër ya. Lu leer ba leer, ci soppey Amaa Balde yi la. Ndaxte, moom lañ jekku woon. Gannaaw loolu nag, arbit yi gise, dem ca “var” bi nga xam ni lu bees la ci làmb ji, bii di ñetteelu yoon biñ ko jëfandikoo ci làmb ji. Ci seet, settantal ñu jox kii di Móodu Lóo ndam li, mu delloowaat nguur gi Pàrsel.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Waaye, lenn ci lu ñuy rafetlu mooy ba ñu joxee doomu Pàrsel ji ndam, Aamaa Balde daldi ko jox loxo, kott ko, ndokkale ko, muy lu ñu bëgg ci bés yile, tubaab di koy wax “fair play”.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
Bu lépp weesoo, lenn ci lees war a bàyyi, mooy li am démb, ay sàmbaabóoy di bawoo fële di duggu ci géew giy yàkk làmb ji. Lees war a wutal saafara la balaa muy wéy di bari. Te, loolu, liggéeyu takk-der yi la, ñoom ñi war a sàmm kaaraange nit ñi.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
CAN KODDIWAAR 2024 : CAABALU BÉS BI
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
NGIRTEY JONANTE DÉMB YI
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Démb ci talaata ji lees amal ñetteeli joŋantey kippug C gi ak gu D gi. Nii lañu demee :
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Kippug C : Senegaal matal na ñettam, Kamerun rëcc na.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Démb bi 17i waxtu jotee la joŋantey kippug C gi tàmbali, mu nekkoon Gine Konaakiri – Senegaal ak Gàmbi – Kamerun. Senegaal mu ngi wéyal ay ndamam. Dafa gañe dëkkandoom bii di Gine Konakiri 2-0, gën a rafetal génnam ak toogaayam ca boppu kippu ga. Ñetti joŋanteem yépp la gañe, muy lu réy. Ci seen xaaj bu njëkk bi, gaynde yi xawoon nañu am tuuti jafe-jafe. Nde, ndawi Kaba Jaawara yi dañu tàmbali rekk, yéeg seen kaw. Ndax, xamoon nañ ne buñ mayee Senegaal dawal bal bi rekk, du baax ci ñoom. Waaye, ba ñu delsee ci ñaareelu xaaj bi, gaynde yi daldi fippu, nangu bal bi doxal. Ci 61eelu simili bi, ci benn teg-dóor (coup franc) bu jege kãwu Gine bi, Kerepeŋ Jaata daldi koy xellil Abdulaay Sekk, Cekkeen bi mbëkk bal bi ak doole, lakk caax yi. Ba ñu demee ba ci 90eel ba Ilimaan Njaay, goneg Màrsey gi, dolli beneen ci paasu Saajo Maane, muy 2-0. Noonu la joŋante biy jeexee.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Ci ñaareelu joŋante bi, Kamerun dafa dóor Gàmbi 3-2. Waaye de, yombul woon ci ñoom. Gayndey Kamerun yi xawoon nañu cof buntu toog. Ba seen joŋante bi dawee ba ñu mitã ba dikkaat, doxal ba ci 56eelu simili bi la Tokoo Ekàmbi taal caaxi Gàmbi yi. Ñu dawal lu yàggul, Gàmbi fayu ci 72eel bi. Ñu ni déet-a-waay, Gàmbi daldi dugalaat ci 85eelu simili bi. Foofu nag, daanaka Gàmbi kalifiye woon na. Waaye, dañu dugal seen kã (87eelu simili), muy lu doy-waar. Mu nekk 2-2. Saa-Kamerun gëm ko rekk ba ca 91eelu simili ba, joŋante bay waaj a jeex, Kiristofëer Wóo tojati kër ga, muy 3-2. Kamerun kalifiye, Gàmbi toog.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Seen kippu gi, Senegaal moo jël pée ak 9i poñ, toppu ci kamerun 4i poñ, Gine ñëwee ñetteel ak 4i poñ itam, kamerun jiitu ko ndax “carton rouge” bu mu amoon ca seen njëlbeenu joŋante ba. Gàmbi jël ndaare ak 0 poñ.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Kippug D : Móritani def na ko Alséri, Àngolaa nax na Burkinaa Faaso.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Ci gii kippu, lu kenn foogul woon, mbaa ñi ëpp, moo ci am. Móritani moo dóor Alseri mi jëloon CAN 2019 daldi koy toogloo. Mu bett daanaka ñu bari. Moom, Móritani, kalifiye na ci 1/8 dë finaal yi. Guléet muy am ndam ci CAN. Waayeet, guléet muy jàll ci ñaareelu sumb bi. Benn bii moo am ci joŋante bi, Muhammed Delaahi Yaali moo ko dugal ca 37eelu simili ba. Turam duggu na ca mboorum kuppe mu  Móritani.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Àngolaa tamit dafa nax Burkinaa Faaso, dóor ko ñaari bal ci dara. Mabululu moo dugal bii bu njëkk bi ci 36eelu simili bi, Sini dolli ko ci 92eel bi.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Moom Àngolaa moo jël pée ak 7i poñ, toppu ci Burkinaa Faaso ak 4i poñ, Móritani jël 3eel ak 3i poñ. Alseri mooy ndaare bi am 2i poñ.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
NAALU ÀLLARBAY TEY JI : KiPPUG E AK GU F
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Afrig dii Sidd dina daje ak Tunisi bu 17i waxtu jotee, ca beneen joŋante ba Namibi di ci dajeek Mali. Muy yu kippug E yi. Joŋante yaa ngiy daw jamono jii.
https://www.defuwaxu.com/can-koddiwaar-2024-caabalu-bes-bi-3/
Kippug F gi nag, bu 20i waxtu jotee lañuy futbal. Ci benn boor bi, Sàmbi dina ko ñàkkanteek Marog ; ci beneen bi, Tansani ak Kóngo Demokaratig dianñ laale.
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
SÀCCIIN WI JËM CI TÀNN YI DËGMAL TE FEEÑALEES KO
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
Sëñ Abdu Xaadr Kebe mooy biral fii xalaatam ñeel wotey tànn Njiitu réew mees dëgmal ci atum 2024 mii nu nekk. Dafay feeñal yenn pexey njuuj-njaaj yees lal ngir sàcc wote yi, foqati baatu askan wi.
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
1 : Baril àdduwaay yi (lieux de vote) ak pekki àddu yi (bureaux de vote) (3 910 000 bureaux de wote) ba waa kujje gi duñu fa man a am aji-teewal ci bépp pekku àddu, ñu jaare ca def càcc gu mag (création de procès-verbaux de résultats).
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
2 : sos ay pekki àddu (bureaux de vote) yu yées 600 te àtteb tànn bi (code électoral) daa wax ne pekkub àddu bu ne daa war a ëpp 600 wéttkat (àddukat, votant).
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
Ñoom nag sos nañu 2700i pekk yu yées 600 yii, yépp nag ngir tàyyeel-loo kujje gi ci wut ay way-teewal.
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
Lu ëpp 2 700 000 ciy pekk yu yées 600 àddukat (votant) sos nañu leen.
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
Pekk yi ñu tuxal du jeex (bureaux délocalisés) ; yooyu nag dañu leen di def ay pekki yees dul gis (soo wëroon ba sonn doo ko gis), pekki jeneer (bureaux fictifx) ak i wéeruy négandiku (abris provisoires).
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
Ngir tànn yii dëgmal 2024 gis nanu ci kàrt elektoraal bi lu sakkan ciy pekki àddu yees tuxal, soppi leen ñuy ay pekki àddu yoy jeneer (fictif), loolu jeexiital ci 469 271 tànnkat.
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
Pekk yees dul gis nag duñu jeex, ni ñu leen di sosee mooy bind ci kàrtuw tànnkat bi (carte électeur) pekku àddu Waagu-Ñaay ci misaal, nga dugg ci di wër ba xàddi.
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
Yii daal ay misaal lañu ci sàcciinu tànn wi ñu fi teg.
https://www.defuwaxu.com/sacciin-wi-jem-ci-tann-yi-degmal-te-feenalees-ko/
Abdu Xaadr Kebe
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Malaanum Lëndëm : Bóris Jóob, na woon, fa woon
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ñeenteelu yoon a ngi nii Bubakar Bóris Jóob di génne téere bu mu bind ci wolof (+), te mu tudde ko Malaanum lëndëm ; muy téere bu EJO móol. Bóris moom, kenn dootul woññi ay mbindam ci làkki réew mi ndax ni mu nuy jàngalee li war a nekk, naka jekk : di bind ak a jàng ci làmmiñ yi nu nàmp.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Li ëpp ci nettali bi, Niseriyaa lay xewe, doonte sax Senegaal lay doore. Taxul nag mu jëm ci mbiri “Boko Haram” ak i ma-rëtal yi ne ca dëkk boobu, di jàpp ak a faat jaambur yi. Konte, ni mu ko defe woon ak Murambi, le livre des ossements (bi amoon Raaya Ladab bu mag boobu ñu ràññee ci àddina sépp, di Neustadt), Bóris daa tànnati meneen réewu Afrig mu sori Senegaal gii mu cosaanoo, di Niseriyaa ; ñu gisaat fii doomu Afrig bi mu doon, bu xër ci mbëggeel gi mu am ci kembaar gi réewam féete. Rax-ci-dolli, nettaleem bi yépp dafa fees dell ak takkandeeru Amilkaar Kabral.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Li ci nettali bi
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ci téere bu bees bii nag, bindkat bi mu ngi nuy nettali xew-xew yi juddoo cib lànket bu Keebaa Jakite di amal ; Keebaa, genn góoru baykat la, dëkk Tànjuraa, ab gox bu nekk ci penku Senegaal ; lànket bi, li ko lal mooy xam lu waral ñu bóom xaritu benn bakkanam, Jonas Akintoye, doon doomu Niseriyaa bu dëkkoon Ingwini ca réew moomu.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ñoom ñaar nag, ay xarit dëggëntaan lañu woon, ku ci nekk jàppoon sa moroom ni woon ni doomu-ndey :
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Naka lañu mënoon a def ba duñ daje bés mook Jonas Akintoye, ku ci nekk ne jàkk sa moroom, ñu yëg ci saa si ne ay doomi-ndey dëgg lañu, ay doomi-ndey yu bokkul deret ?
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Noom ñaar, benn bëgg-bëgg lañu am, muy xër li ñu bokk xër jëmale ko ci lépp luy laal ci mbay. Waaye seen ànd yemul foofu, dañu nirooy jikko niy seex : ñoom ñaar ñépp dañoo gëm seen bopp, am péexte gu mat sëkk ba dara feesul seen i bët ; ñuy ñu dëggu, ñemee wax seen xalaat ak lu leen ci mën a fekk ; ñu doon ay nit ñu jub te am fit, bëgg seen réew te gëm seen i baaxi mboolaay ak seen cosaan. Ngëm-ngëm yu tumurànke yooyu ciyjamono yii, rawatina ci way-pólotig yi, nga xam ne, lu ne man nañ koo jënd, ba ci nit sax ak i noppam !
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ñaari xarit yii nag, ca ba ñuy ne ci seen diggu doole lañu xamante, ñu daje woon ca benn peyu Ërob, fu ay kuréli baykati Afrig gépp daje woon. Fekk booba, ku ci nekk ci ñoom ma nga jiite woon ca sa dëkk ay mbooloom baykat. Ba ñu fa jogee lañu jàppante ba seen i njaboot di demalante bu baax, doonte seen i réew dañoo soreyoo lool.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Bés, ñu xamal Keebaa ci njeggil-kàddu gi ni rey na ñu xaritam ciy anam yu ñaaw a ñaaw, te néew ba nee na mes, kenn xamul fu mu ne. Waa dëkk ba yépp njort ni, ñaawteef boobu, du liggéeyu kenn ku dul Chief Moses Abimbola, boroom daraja ju mag, bokk ci nguur gi, te nekkoon àndandoowu Jonas ba ñuy gune, ñu daan wujje ba ñépp xam ko. Fa la Abimbola jóge woon di won mbañeel gu tar jëme ko ci Jonas.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Keebaa moom, xelam mayu ko woon benn yoon muy seetaan dundu xaritam biy deme noonu ci neen. Mu ne fàww mu dem ba Ingwini ca Niseriyaa jaaleji soxnay ndemsi-Yàlla-ji, amal fab lànket ngir lijjanti mbir mu lëj moomu, te it, su manee nekk, mu fexe ba néew bi  feeñ. Mu jaraloon ko nag bakkanam. Ndax da doon ci moom, sas wu mu jële fu gën a sori ci xolam :
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Keebaa Jakite xam (na) ne kóllëre ginnaaw lay féete…
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Lu muy fekki ci tukkeem boobu ci réew mom  ñàkk kaaraange fa la fekk baax ? Ci yan anam la ñu reye xaritam bi, ak lu waral loolu ? Ndax sax dina feeñal néew bi ?
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Bi mu demee ba màgget, di xaar Yàlla def li gën ci moom, la Keebaa Jakite jël xalimaam ne fàww mu nettali askanu tey wi, xew-xew yu doy waar yooyule.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ciy way-jëmmal yuy dund ciy jamono yu wuute ak i béréb yu wute it, la bindkat biy jaare ngir nettali lépp jàngkat bi. Moom jàngkat bi sax, day dem ba miin way-jëmmal yi, ñu mel ne ay dëkkandoom dëggëntaan ; way-jëmmal yoo xam ne, ñii dañoo neex deret lool, ñee nee ñu bon-a-bon ; waaye li ñuy wuute yépp, kenn ku ne ci ñoom am na lu ñuy mën a jàngat ci nekkinam ak taxawaayam.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Way-jëmmal yi ci  téereb nettali bi
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Bi Keebaa yeggee Ingwini la nu nettalikat biy wonaleek i way-jëmmal  yu bees: ay defkatu ñaawteef yu jàppe rey nit ni liggéey (Chief Moses Ambibola ak “surgaam”, James Vandi), ay nit ñu xumb te doy waar (Mama Wumbi-Oyé, yaayu Moses ju xayedi ji), ñu jaambure te mën a daw ay ba dee (Tony Akintoye rakku Jonas ji)…
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ku ci ne ci ñoom, bindkat bi daf koo jëmmal, ku ci nekk ak say jikko walla say feem, ba far joxe melo nit dëggëntaan. Way-jëmmal yooyu yépp lañuy gis ñuy dem ak a dikk, di xalaat, di gént, di waxtaan, ñenn ñiy faat jaambur yi, ñeneen ñiy aar seen i moroom ; am ñu ciy xeex ngir taxawal yoon, am ñoo xam ne, topp seen bakkan rekk a leen soxal…
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Jàngkat bi, lu muy gën a xuus ci Malaanum lëndëm di gën a yéemu ci ni nettali biy doxe ba fa muy mujj. Lépp Bóris Jóob di nu ko toggal ba taajal nu lu ñor xomm. Ci njeexital li daal, nettali bu am solo lanuy topp, nettali bu nuy yéem ndax mbetteel yi ci biir ; nettali buy jàngale ci ni àdduna siy doxe,  buy jàngale ci tëralinu ëllëgu doom-aadama.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Bóris du tàyyi di jaxase jamono yeek béréb yi, ni mu koy faral di defe, jaare ko ciy xalaati Keebaa : ni mu doon janeere dundam ca ba muy waxambaane. Keeba di fàtteliku ay ndajeem ak Jonas, seen i waxtaan, ni ñu daan déeyandoo, seen i ree bay xàqataay ; waaye it, seen i njàqare, seen i soxla yu jëm ci seen liggéey, ak itam seen i wérante yu xumb jëm ci mbiri pólitig bi walla ci mbiru xeltu. Ku ne werante, ni juyoo, ndax li ñu doonoon ay doomi-ndey taxuleen woon a juboo ci lépp. Teewul nag, ñaari xarit yi doon gën di nawante. Ciy werante yooyu la bindkat biy jaare ngir samp ay xalaat yu am maanaa.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ponki xeltu yi Bóris indi
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ci seen i ñaaroo yi ñu daan faral a am, Jonas da daan cokkaas xaritam bi, di ko tooñ ci lu jëm ciy ngëm-ngëmam, dem bay wax lu ëpp ci diineem, jàpp ne ciy “waxi kasaw-kasaw” doŋŋ la lalu. Su ko defaan, Keebaa day waaru :
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ci laa jëkkee xalaat tamit ne, Jonas Akintoye, xéy-na yaram wi neexul.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ñaari doomi-ndey yi doon nañu waxtaane yeneen i mbir, ginnaaw lu jëm ci diine ji. Lu deme ni Demokaraasi itteeloon na  leen, te mu nekkoon it lu Jonas gëmul woon, ba tax koy kókkali Keebaa mi doon tiitaroo Demokaraasi Senegaal, naan royukaay la ci  Afrig. Du tere nag, bu Keebaa seetaatee mbir mi, du xam lu mu koy tontu :
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
àndumaak Jonas wànte nag, xiif di la bëgg a rey ba noppi ngay bàkkoo demokaraasi subaak ngoon, gaa ñiy sàcc di kàcc, di lekk ribaa ba seen biir yiy bëgg a fàcc, ñuy toroxal baadoolo yi, ku ko seet ci sunu Senegaal gii xam ni su dee loolooy demokaraasi, demokaraasi ay naxee-mbaay kese la.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Lee-lee itam Jonas samp laaj ci sàrt yi lëkkale réewi Afrig yi ak yeneen réew yi, rawatina yu Ërob yi :
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Mën nga maa wax luy yoonu Tubaab yi ci sunuy mbir ?
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Noonu la ko ñaari xarit yi jàppe woon : wecce yu dul jeex ci lépp lu soxal ëllëgu doom-aadama, rawatina luy tax réewi Afrig yi suqaliku.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Li Keebaa doon fàtteliku yooyu yépp, teewu ko woon bàyyi xel ci lànket ba ko taxoon a jóg. Ku bóom xaritam bi, ak lu tax ? Ci yan anam ? Fan la ñu làq néew bi ?
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Laaj yooyu ak seen i tontu, Bóris day feeñal lépp, ndànk-ndànk, ciy defin yuy fësal ni mu xareñe ci bind téereb fent.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Xereñtey Bóris ci mbind mi