url
stringclasses
152 values
text
stringlengths
4
5.13k
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Gis nanu ni bindkat bi di wommate jàngkat bi, dëkkoo-dëkk, ciy jamono yuy dem ak a dikk, mel ne ku naan ko naxee-mbaay, na ko Asta Balde waxe, ba muy jëw Gorgi Seega Ture ci jëkkëram. Asta  Balde dib sekkarteer bu Seega di liggéeyloo mu kay bindal nettaleem bii ko ñor lool, su weer deewe mu fey ko. Konte, su dee Seega mooy nettali, moom Asta Balde mooy ki nuy jottali nettali bi : di nu xamale sax ak Seega ak waa këram, ak yeneen way-jëmmal yiy nar a ñëw ci ginnaaw ; di ci njàmbaasaale nag ay mbiri boppam. Mu far mel ne ñaari nettali lanu bindkat bi boole di defal.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Konte Bóris, xaraley nettali yu bare te wute la jëfandikoo ngir yakkal nu téereem bu am solo bii, am maanaa lool, di Malaanum lëndëm. Ci ñeenti xaaj nag la nu ko indil, bu ci nekk di doore ci bataaxal yi Asta Balde di yónnee jëkkëram ja nekk bitim-réew te mu namm ko lool ; lu muy def di ko ko nettali, ragal réeroo seen diggante ndax fiiraange. Bataaxal yooyu sax ñooy tëj téere bi.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Kon nag, jàngkat bi, amul lu koy jaaxal : du réer benn yoon ndax Asta Balde mooy ki koy tette ba tax muy gindiiku saa su ne.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Leneen luy biral xereñteefu Bóris mooy wolof yu set yi muy bind, te du rekk mbind mu set te rafet : kàdduy way-jëmmal yi ci seen bopp dañuy génne waxin ak xalaatu doomu Afrig wala doomu Senegaal tigi, mu wóor ne lii duy kàdduy weneen làkk wu ñu tekki. Mu mel ne bindkat bi, ni muy waxe di ko binde, noonu lay xalaate ci làmmiñ wi mu nàmp. Loolu moo koy may muy mën a firi dëgg-dëgg, ci làmmiñu dëkkam, yëg-yëg biy jóge ci askanam.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Ci njeexital li, mën nanoo jàpp ni, Bubakar Bóris Jóob teggiwul benn yoon tànkam ca fa mu ko tegoon, muy yoon wu  ay magam xàlloon, ñu mel ni Seex Anta Jóob, Seex Aliyu Ndaw, Sahiir Caam, Paate Jaañ, Maam Yunus Jeŋ, Aram Faal ak ñoom seen. Bubakar Bóris Jóob ak i maasam wallay rakkam (Mamadu Jaara Juuf, Adraame Jaxate, Abdu Xaadr Kebe…), ñu ngiy bay, tey, seen waar, ci anam bu mucc ayib, ci tool bu yaatu boobule.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Bubakar moom, waaram ci wàllu ladab la ko féetale : fexe ba téreeb nettali ci wolof tollu fa yeneen xeeti àdduna si yóbbu seen yos. Moo waral ndam li mu ci amagum, àdduna sépp a ci teg bët, muy lu ñépp mën a seede.
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Uséynu Béey
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
(+) Téerey Bubakar Bóris Jóob ci wolof :
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Doomi golo, téereb nettali, Ndakaaru, Papyrus-Afrique 2003, ñaareelu móol EJO, 2019
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Nawetu deret, kilib (tekkig ‘Une saison au Congo’ bu A. Césaire), Zulma et Mémoire d’encrier, Caytu, 2016
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Bàmmeelu Kocc Barma, téereb nettali, Dakar, Ejo, 2017
https://www.defuwaxu.com/boris-na-woon-fa-woon/
Malaanum Lëndëm, téereb nettali, Dakar, Ejo, 2022
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
« Man, dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci. »
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
Mamadu Jàllo :  Ndax CFA bi baax na ci njaay meek njënd mi, rawati-na bitim-réew ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
Ndongo Sàmba Silla : Déedéet. Mësu cee baax ! CFA bi du yombalal njaay meek njënd mi. Moom kay, safaan bi la koy jural. Ndaxte, boo seetloo, bi Senegaal moomee boppam ci atum 1960 ba nëgëni-sii, li ñuy wax ci tubaab sunu “balance commerciale” dafa deme boor. Maanaam, soo méngalee li réew miy jënd ak li muy jaay bitim-réew, dangay gis ne li muy jënd moo ëpp fuuf li muy jaay. Li Frãs fuloon dayo CFA bi moo waral laago bi.  Ndege, diisaayu CFA bi moo tax liggéey ci jafe. Te, am réew, bu dee li muy jënd bitim-réew moo ëpp li mu fay jaay, day ame ay bor yu dul jeex. Loolu moo nu sonal. Booba ba léegi, bor a ngi ci sunu baat. Danoo leb a leb ba mënatunoo fey. Seŋoor ba Maki, jaare ko ci Abdu Juuf ak Ablaay Wàdd, ku dàq a leb sa moroom nga ne kii.  Wànte Maki Sàll, sunu njiitu réew mi fi ne, moo ci raw. Te nag, jàngoro, doomu-jàngoro du ko faj. CFA bi mooy laago bi, kon, féeg noo ngi koy jëfandikoo, dunu mës a jóg ci leb. Dëgg la, réew yépp ay leb, ba ci réew yi ëpp doole ci àddina si. Waaye, benn, kenn tënku leen ba duñu mën a jaay bitim-réew ; ñaar, seen woyofaayu xaalis may na leen ñu doxale noonu seen i naal. Nun nag, CFA bi mooy sunu gàllankoor. Xaalis bi dafa am doole ba tax na say njaay du jar. Kon fooy jële looy faye say bor ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
Li nga wax dox na waar, di !
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
Yaa ko gisal sa bopp. Lu ni mel, ñi féete kow te ne déjj ci donkaasi gi doŋŋ lay amal njariñ. Dinañ mën a jënd lu leen neex bitim-réew, indi ko ci réew mi, jaayaat ko nu mu leen neexe. Seen xaalis di gën a yokk ak bu Farãs, askan wi moom di wéy di ndóol. Bu lu ni mel amee, dees na joxoñ baaraamu tuuma bànk yu mag yi. Ndaxte, ñoo ko sooke. Ndekete, ñoom dañuy bañ a lebal nit ñi xaalis. Maanaam dañ leen di gàntal. Li ñu ko dugge nag, du lenn lu dul sàmm yemoo (parité) CFA bi ak Ëro bi. Njiiti bank yooyii xam nañ ne, bees lebalee xaalis liggéeykat yi, muy àntarpërënëer bi, di boroom bitig bi, walla sax bépp jaaykat, li ñuy koy jënde mooy ay jumtukaay walla dund. Jumtukaay yooyu ak dund bi, nag, bitim-réew lañu koy jënde. Te, téeméeri àntarpiriis yoo jël, 30 yi walla 40 yi bitim-réew lañuy jëggaani seen jumtukaay.
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
Loolu jur lan, nag, ci sunu koom-koom ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
Day nasaxal walla day wàññi xaalis bi nuy bàyyi ci bànki Frãs ba, ñu koy wax ci nasaraan “réserves”.  “Réserves” yooyu, nag, ñooy wóoral yemoo CFA ak Ëro. Looloo tax bànk yu mag yi duñ sawar ci lebal liggéeykat yi.
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
Doo ma baal nga leeral fii ? Lu loolu joteek yemoo bi ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
Waaw, ngir sàmm yemoo boobu, fàww ñu dakkal bor yi walla ñu wàññi leen. Liggéeykat bu ci am wërsëg ba bànk yi lebal la, li ngay war a fey day takku lool. Ci gàttal daal, CFA bi day yokk say bor, xoj say liggéeykat, tere laa am i isin, tere laa jaay bitim-réew… As tuut li nu am ciy njuréef ak alal, tubaab yaa koy fob yóbbu seen dëkk ndax li ñu dippe “zone franc” moo leen ko may. Ndax loolu jaadu na?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
–     Déedéet kay !
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
–     Kon nga xam ne noo ngi ci nooteel ba léegi. Loolu yépp, nag, boo leen boolee, lenn doŋŋ lay jur : tumurànke.
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
– GInnaaw bi nga leeralee ni CFA bi nooteel lay biral, lan nga jàpp ne moo nu ci teree génn boobaak léegi ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
– Waaw. Laaj bu am solo nga laaj fii. May ma ma jox la benn misaal. Man, damay faral di dem bitim-réew ngir amal fa ay waxtaan ñeel CFA bi, ma ciy ànd ak gëstukati daara-yu-kowe yu mag. Waaye, saa yu ma noppee ci wax ci CFA bi, leeral jafe-jafe yi mu làmboo, tubaab yi ci seen bopp dañuy waaru ! Mbir mi da leen di jaaxal lool sax. Bu ko defee, ñu naan ma : « Déedéet kay ! Waaw yéen, lu leen tee wacc musiba bii nga xamante ne day gàllankoor seen dund ak seen yokkute ? Ana seeni àntarpërënëer ? Seen njiit yi ngeen di fal nag, lu leen dal ba ñuy seetaan lii ? Moo, ndax dungeen fippu indi saafara ci jàngoro jii ! Yéen a ngi nelaw de ! » Bu ko defee ma ni waaw, Tubaab yeey wax lii…Waaye, bu dee fii ci Afrig, walla Senegaal, saa boo waxee ci musibay CFA bi, dañu la naan : “ Waaw…dëgg la, CFA bi am na ay jafe-jafe waaye am na ay ngëneel itam…” Nga gis ne, Tubaab yi sax, nangu nañ ne CFA bi musiba la ci nun. Waaye, ñenn ci doomi Afrig yi, walla doomi Senegaal yi ci seen bopp, ñoom, jàpp nañ ne CFA bi am na njariñ. Dafa di, ñi ànd ak CFA bi, dañu dul xalaat, walla ñu bokk ci nguur gi, teewal fi Frãs mu am lu mu leen di combal. Waaye, nag, ku waxaale sa ngor, ñu jënde ko sa toroxtaange. Loolu moo nu dal.
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
-Kon ci sa gis-gis Frãs a nu teg li lépp ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
– Frãs ak doomi-Afrig yi koy jàppale. Ndaxte, boo seetee, réew yi Frãs nootoon yépp, am ci ñu dul jëfandikoo CFA bi, moom seen bopp ba mu mat sëkk, te tey ñu ngi ci yoonu yokkute. Réew yooyu, bi xeex jotee, dañu jaayante ak Frãs, jàmmaarlook moom, foqati seen réew.
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
-Mën nga leen a lim ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
– Réew yu jàmbaare yooyu, mënees na cee lim Alséri ak Wiyetnaam. Ñoom ñaar ñépp a xare ngir afal seen askan. Nun, nag, sunuy njiit ya woon, jarul nu leen fiy tudd, doxalewuñu woon noonu. Dañu maslaa ak Frãs, mu kootoog ñoom, lal i pexe ngir gën fee mën a toog, aakimoo sunu alal. Bi gënoon a fës ci pexe yooyu nootkat bi laloon mooy li ñu dippe woon “Accords de coopération”. Loolu li mu wund mooy, lépp lu aju woon ci moomeelu réew yi mu nootoon, ciy loxoom lay tegu. Maanaam, njaay meek njënd mi, ak lépp lu ñeel jëflante ci diggante nootaakon (colonies) yi ak bitim-réew, xaalis bi (te muy CFA bi) ak koom-koom gi. Loolu la Frãs waxoon ne bu ci sunu njiit ya woon àndee xaatim ko, mu nangu ñu moom seen réew. Sunu njiit yi nag, ñu ci ëpp Frãs lañu jànge, foofu lañ leen tàggate, daan fa liggéeye te nekkoon fa sax dipite. Moo tax ñu xaatim loraange jooju nu topp ba sunu jonni-Yàllay-tey jii. Réew mu ci mel ni Gaboŋ, lépp lu muy def, Frãs da cee ànd. « Accords de coopération » bi mu xaatimoon ñoo ko ko yóbbe.
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
–Ndax am na ñu fippu, ne fàww ñu dog buumu njaam gii ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
– Lii tamit laaj bu am solo la. Am na ñu yàgg a xeex CFA bi ngir jële ko fi. Axã kay ! Du léegi la ñenn ci doomi Afrig yi tàmbalee xeex CFA bi. Xeex bi démb la woon, tey door a agsi. Te loolu boo ko waxee xel war naa dem ci Séku Ture. Ndege, moom moo jëkk a bañ CFA bi, ne dee, Gine du ci bokk. Moom Séku Ture, bañkat bu mag la woon, amaana li mu doonoon ab sàndikalist moo taxoon. Ndax ku mënoon a dajale ay nit la te bare woon i pexe lool. Waaye, ak lu xel miy màcc yépp, jataŋ ak gàllankoor yu bare yi ko Frãs daan teg, moo koo taxoon a tagatémbe. Loolu rekk a teewoon Gine génn ci. Frãs da doon dugal Gine xaalis bu bon bu baree-bare ngir yàq deru Séku Ture. Am na keneen ku ñiy wax Silwanus Olimpiyóo, njiitu Tógo la woon, nekkoon layookat bu siiw. Dafa laloon ab naal ngir wutal réewum Tógo xaalisu boppam. Jotoon na cee waxtaan sax ak réew yu mag ci àddina si, niki Almaañ ak Amerig. Bi mbir mi demee bay sotti la ko Frãs sàkkal pexe, ngem Eyademaa mu rey ko. Naka noonu, Tomaas Sànkara, jàmbaaru Burkina-Faaso ba. Nu gis ne, Frãs jenn itte doŋŋ la am : ratt réewi Afrig yi ba ñu sett, jël seen alal di ko siimee cereem.Cere jooju, nag, ku ko bëgg a xajamal mu sàkkal la pexe. Waaye, nit ñit xippi nañu seeni bët.
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
– De4gg la, nit ñi xippi nañu seeni bët, moo waral way-moomeel yi, kujje gi ak boroom xam-xam yi takkal pot sunu njiit yi ak Frãs. Dafa mel ni gaa ñaa ngiy deeltu ginnaaw ndax ñoo ngi wax ne dañuy bàyyi CFA bi dem ci ECO bi. Loo xam ci xaalis bu bees boobu ?
https://www.defuwaxu.com/naareelu-xaaju-waxtaanu-mamadu-jallo-ak-ndongo-samba/
– ECO bi ?Waaw. Dégg naa ñenn ñiy xeex CFA bi naan, nanu gaaw jël ECO bi, def ko sunu xaalis. Waaye, ECO bi ci lajj lay mujj. Wolof dafa ne, ku ndóbin rey sa maam, foo séenatee lu ñuul daw. Man dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci. Dama xamul lu tax rekk mënuñu lal ab naal boo xam ne, dina jur i meññent ëllëg. Te sax, lu tax nuy déglu ñi nuy gëmloo ne sunu bëggee jëm kanam fàww nu bokkak ñeneen ñi xaalis ? Loolu du dëgg. Gàtt xel doŋŋ la ak xeebaate. Fii, ku fi gëm sa bopp, takku liggéey dinga am yokkute. Damay jël misaal ci yenn réewi Ërob yoo xam ne Senegal moo leen gën a yaatu, ëpp leen alal, ëpp leen mbooloo. Tey, ñoo ngi ci naataange te dara mayu leen ko lu dul liggéey bu jaar yoon. Kon, ku nekk mën nga  liggéeyal sa réew ba mu naat. Waxuma ni booloo baaxul. Wànte, fàww ku nekk gëm sa bopp ba noppi, liggéey liggéey bu lay amal njariñ, amal njariñ ñeneen ñi. Bu ko defee, dinañu mën a saxal garabu booloo gi, di ko suuxat ba mu màgg, dëgër, law ci biir Afrig gépp.
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
XALAM DEMOON NA BAY NEEX
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
Dibéer, 24eelu fan ci weeru féewaryee, atum 2019. Bés bi ñépp doon xaar, agsi na. Bés bi taskati xibaar yi doon séenu, di ko jagleel ay xët ak i waxtaan a ngi nii. Bés bi mag ñi daan waxtaane, ndaw yi di ci werante, janq yi di ci dàggasante, waa-jur ak doom dem ba ciy meroo agsi na. Bés bi àddina doon waajal bernde bu mag, teersi na, indaale saricaam. Waaye, ba alxemes ji nu génn, sarica baa ngi woon ci loxoy Demba Kànji, àttekat bi jiite Kurelu ndajem wote bi. Bu ko neexoon mu def ko jàmm, baaxe ko réew mépp ; bu ko neexoon yit mu soppi ko safaan ba, def ko fitna. Lépp, nag, a ngi aju woon ci ni àttekat bii di Demba Kànji di séddalee saricay askan wi. Ñépp a ngi newoon tekk di ko déglu : ndax dina séddale saricay askan wi ni ko yoon bëgge ? Noo déggandoo li mu wax. Nee na tééméer bo jël, 58 yi Maki Sàll lañu sànnil xob. Ñu bare ci réew mi jàpp nañu ni du dëgg ndax li rajo yeek tele yi wax, ñépp di ci dégg, moo di ne ñaareelu sumb mënutoon a ñàkk te njiitu réew meek Idiriisa Sekk ñoo waroon a laalewaat.
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
Naqaru way-moomeel yi dara waralu ko lu dul yaakaar bu tas.
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
Ci fajar a fajar lañu jóg, wutali bérébi wotekaay yi ngir def seen warugar, ni ko maxejj bu nekk war a defe. Wote ren bi nag, mbooloo mu takku te farlu lees ci ràññee, rawatina ndaw yi. Ci xayma, téeméer boo jël ci ñi jotoon a bindu ci kayitu wote gi, juróom-benni fukk yi wéet nañu ci mbañ-gàcce gi. Nee ñu xiirte gu ndaw yi am ci bile wote, lawax bii di Usmaan Sonko moo ko waral. Ndaxte, Usmaan Sonko benn, ndaw la, ñaar dafa yeesalaat politig bi, di biral njub, gëm sa bopp ak bëgg sa réew. Ak lu ci mënti am, keroog ñépp xéy nañu, solu ba jekk, dem wote ci yar ak teggin ba 6 waxtu ci ngoon, ñu daldi tëj wotekaay yi, ngir lim xobi juróomi wutaakon yi bokkoon ci joŋante bi. Naam, amoon na ay rëq-rëq yu ndaw, waaye daal mënees na wax ne bëccëgu wote bi jaar na yoon. Bi asamaan si muuroo, nag, ci la mbir mi tàmbalee lëbëjoo, ñenn ñiy jéem a tuur lëndëm askan wi.
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
Bi timis ji maasee, ci la lim yu njëkk yi tàmbalee rot, ñetti wutaakoon yii di Maki Sàll, Usmaan Sonko ak Idiriisa Sekk beddeeku di wone seen doole. Xëccoo bi tar lool ci seen diggante. Ku raw fii, kee raw fee, keneen raw fale. Yeneen ñaari lawax yi ñoom, Isaa Sàll ak Madike Ñaŋ, nangu ndogal, xam ni bokkatuñu. Ku nekk ci ñoom ñaar gërëm askan week maxejj yi leen wóolu ba sànnil leen seeni kàrt ba noppi ndokkeel Usmaan Sonko ak Idiriisa Sekk. Waaye, biral nañu tamit ne, ku gën a jekku ci diggante ñaari wutaakoni kujje gi, moom lañuy jàppale ci ñaareelu sumb bi nga xamante ne, jàppees na ci njëlbéen ni mënta ñàkk. Ci jamono jooju, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñi ngemb Maki Sàll, ñoo giy fésal seen mbégte, naan Maki jël na raw-gàddu gi, xel wareesul a xalaat ñaareelu sumb di am. Loolu nag, du mbetteel, dafa di, ku ngemb sa mbër, bu la neexee bàkku ne yaay daan doonte dara wóoru la ci. Waaye, bi njiitu jawriñ li, Muxamadun Bun Abdalaa Jonn, génnee ca RTS ak TFM wax ni Maki Sàll faluwaat na ci sumb bu njëkk bi ak 57 baat ci téeméeri falaakon yoo jël, ci la xol yi jóg, coow li ne kurr.
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
Ci saa si, Usmaan Sonko ak idiriisa Sekk wooteb ndaje ak taskati xibaar yi. Ñaari wutaakon yi daldi ñaawlu doxalinu njiitu jawriñ yi. Waaye, yemuñu ci, ndax ŋàññ nañu màkkaanu taskati xibaar bu Yuusu Nduur bii di iGFM ak tamit RTS, rawatina yéenekaayi réewum Farãs France 24 ak RFI. Ñu neeti, kàddu njiitu jawriñ lii di Muxamadun Bun Abdalaa Jonn ak doxalinu taskati xibaar yees jot a lim, ag càcc a lalu ci suuf, ñu bëgg a nax askan wi, jox leen ay lim yu wérul. Waaye, ñoom duñu ko nangu ; te bu ko jaree, dinañu génn ànd ak askan wi xeex, jubali Pale ngir déjjati fa Maki Sàll.
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
Bi dënn yi demee ba tàng la àttekat bi jiite Kurélu ndajem wote bi xéy, woo taskati xibaar yi, daldi delloo njiitu jawriñ li palaasam, xamal ñépp ne, kenn amul sañ-sañu wax ne kii falu na walla ñaareelu sumb day am lu dul Kurélu ndajem wote gi mu jiite walla Ndajem ndeyu àtte mi. Bees ko laajee nag, kañ lees war a jot ci ngirtey wote bi, dafa xaarloo askan wi ba alxames walla àjjuma jees dégmal. Loolu nag, teeyoon na xel. Ndaxte, ak xeeti jumtukaayi xarala yi fi nekk, jarul woon a joxe àpp gu ni tollu. Mbaa du njiitu réew mi daa takkaloon pot Demba Kànji ak i ñoñam ngir ñu wax ne moo jël ndam li ? Am na sax ay ndaw yuy wax ne nguur gi dafa bëgg a foqati baatu askan wi. Ba tax na, ñenn ci ñoom tàmbalee ñaxtu ca buntu RTS di kaas naan ñaareelu sumb day am ci nii mbaa ci nee. Waaye, waa Bennoo Bokk Yaakaar ñoom, ñu ngi ŋoy ci seen lim bi njiitu jawriñ yi fésaloon, naan : « wure wi dem na këŋŋ, Makee faluwaat ! » Li am ba des mooy ne, askan wi gëmmul nelawul. Bi Demba Kànji joxee dogalam ba tey, nit ña ngiy xultu tëwa ba, kujje gi woote na doxu-ñaxtu tey ci àjjuma ji, buñ jullee tàkkusaan ba noppi. Lan la ndaje moomuy jur ? Yàlla rekk a xam. May laajati : mbaa du léeb dafa tàbbi géej ? Moom daal, xalam demoon na bay neex…
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
Am na tamit ñu naan Maki Sàll dunguru Emmanuel Macron doŋŋ la te sax Tubaab yee ko may fitu yemale joŋante bi ci benn sumb kott. Loolu tekki ne Frãs ay ndeyu-mbill gi te xéy-na lees war a def mooy bañatee jënd lépp luy doomi-Frãs di jaay fi ci Senegaal, moo xam Auchan la, walla Orange laak Total walla ñeneen.
https://www.defuwaxu.com/xalam-demoon-na-bay-neex/
Àttekat bii di Demba Kànji nag, bu tasul woon yaakaaru askan wi, Senegaal du mel tey ni réew mu toog ci nen. Xéy-na am na lu ñuy yoot. Fitna du yem ci boppu boroom te bu pënd wuree, fattu bare.
https://www.defuwaxu.com/paap-bu-mag-ba-woon-benuwaa-16-sosef-ratsingeer-wuyuji-na-boroomam/
Paap bu mag ba woon, Bënuwaa 16 (Sosef Ratsingëer) wuyuji na Boroomam
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
AY YEESAL ÑEEL BARI (LES EQUIPES) SENEGAAL YI
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Gaynde yu mag yi (ekib A)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Wéyalees na pasug Aliw Siise gi ba keroog atum 2026. Kii di Paap Caw lees tabb, teg ci wetam, muy tofoom (adjoint).
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Gayndey réew mi (équipe nationale locale)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Bu dee lu ñeel gayndey réew mi, Suleymaan Jàllo lees dénk lenge, mu war leen a tàggat. Sosef Seŋoor ak Séex Géy ñoo diy tofoom.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Gayndey yu ndaw
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Bu dee xibaar yi aju ci gaynde yu ndaw yi amagul 20i at (U20), Sëriñ Ja mooy leen yor. Bu dee gaynde yu ndaw yi amagul 17i at (U17), Ibraaxiima Fay a nekk ci bopp bi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
MUKTAAR JAXABI OPPEEREWU NA CI JÀMM
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Alxames jiI weesu, 7 màrs 2024, la jañkatu Gine bi oppeerewu ci tànk fa raglub “Jean Mermoz” ba nekk Liyoŋ (Farãs). Lépp jaar na yoon. Waaye, gaañu-gaañoom bi du bu ndaw. Nde, gannaaw gaañoom bi ca seen joŋante (valence) baak Real Madrid ca ayu-bés bee weesu la fajkat bees di wax “Dr Gastaldi” biral ay kàddu di xamle ni dina jafe lool ngir Jaxabi doxaat ni mu waree. Ndaxte, xeetu gaañu-gaañu bi yamul ak yu bari yu futbalkat yiy ame. Dolli ci ne jéem a fexe ba mu doxaat lees war a seet balaa ñees di xalaat mu delluwaat ci pàkk mi. Muy lu ñu bari di ko mastawu.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
ARDA GÜLER DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK CA REAL MADRID
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Saa-Tirki bi dugal na biiwam bu njëkk ca Real Madrid, démb ci dibéer ji, ci seen ndaje beek Celta-Vigo. Moom nag, ba mu ñëwee ca ekib ba ba léegi amagul wërsëgu wane boppam bu baax. Ndax, dafa dikk rekk am ay gaañu-gaañu yu tegalante woon. Loolu doyul, Carlo Ancelotti miy tàggat këlëb bi du ko futbal-loo lu bari. Yenn saa yi mu mosal ko as lëf ciy simili, waaye li ci ëpp ci toogu bi la koy bàyyi. Démb itam, bi joŋante bi desee 8i simili la ko dugal ci pàkk mi. Waaye, lu simili yiy néew-néew, jot na ci bégal soppe yi, rawatina yu dëkkam yi bëgg di ko gis muy laale lu bari. Fim ne mooy Saa-Tirki bi gën a doon ndaw te dugal ca sàmpiyonaa bu Espaañ. Turam dugg na xaat ci mboor ma.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
LÀMB JI
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Bëre taxaw na digante Móodu Lóo, buuru làmb ji, ak Sitta. Ñoom ñaari mbër yi dinañu sëgg weeru Nowàmbar ci atum 2024 mii.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
BOKS : FRANCIS NGANNOU ÑÀKKATI NA
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-11/
Saa-Kamerun bi ñàkkaat na weneen yoon ca powum boks ma. Guddig àjjuma jàpp 8 màrs la doon amal ñaareelu xeexam ci wàllu boks. Jàmbaar jii di Anthony Joshua la doon laaleel. Aji-mujj ji daf ko dóor mu tëdd ca ñaareelu xaaj wa, daldi gañe joŋante bi. Moom nag, Ngannou dafa mel ne neexleegul ci po mi. Ndax, ba mu jógee ca MMA ba léegi amagul ndam ci boks bi. Xëy-na lim miinagul yëf yi la, am li mu ñëw rekk ñu jox ko ci waagay po mi. Di xaar ci moom mu dikkaat ak taxawaay bu gën a jekk ci yeneen joŋanteem yiy ñëw.
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
FAATUG HIBAA CAAM : SENEGAAL, BOPP BU XAR ÑAAR?
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Guddi àjjuma, dëppook 3eelu fan ci weeru Awril, doon guddi gi jiitu bésub baaxentalub sunu moom-sa-réeew, la benn jànq bu am 28iat, di wuyoo ci turu Hibaa Caam, ñàkk bakkanam, ci anam yu tiis te doy waar. Ñu ngi ko fekk mu tëdd, ne nemm, di waccu deret. Ci li taskati xibaar yi wax, xale bu jigéen bi, dafa jël lu ko ëpp doole ci ay donji dorog, ba faf ca faatoo.
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Loolu nag, mu ngi xewe ci Almadi gii ci Ndakaaru, ca kër gu Baaba Jaw «ITOC» di luye. Moom nag, boroom alal ju raññeeku ci réew mi la te doomam bu jigéen moo ko féetewoo. Ñi fa daje woon ay moroomam lañu, ay xale yu góor ak yu jigéen, ne fay fo ak a topp seen bakkan, doon it ay doomi boroom alal, ak ay doomi kilifa yu ñépp xam ci réew mi. Ku ci bokkul ci ñi ŋànk nguur gii fi ne, am nga ci jegeñaale ; ñu ràññee ci : Daam Amaar, doomu ndem-si-Yàlla-ji Amet Amaar mu NMA SANDERS, doon itam goro Yusu Nduur, Luuti Ba te baayam di jiiteb kurëlu tàggat-yaram.
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Xew-xew bu ni mel nag, dafay firndeel, ci lu amul benn werante, yàquteg goney réewum Senegaal fi mu toll. Dees na ci joxoñ itambaaraamu tuuma kilifay réew mi, ci ñàkk a yarseen njaboot ni mu ware, bàyyi leen ci seen sago. Li jar a laaj dëgg nag mooy : ana nu ay gune yu juddoogul, mën a yore xaalis bu dul jeex, di ko pasar-pasare nu mu leen neexe, ci Senegaal gu ndóol gii ? Lu doy waar la ! Rax-ci-dolli, ñu mel ne ñu réer, wàcc seen and,waral ñuy daje di jolluy bitéeli biiñ ak a tux sineebar, dëkke càkkaay…
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Dëgg la sax, mënees na jàpp ni àddina day dox, ngir jamono ju nekk ak i feemam. Waaye kat…. !
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Ak lu mu ci mën a doon daal, li ëlëm ñépp,mooy, jamono ji jéyya yii yépp di ame, tiis ak njàqaree ngi lëmbe àddina, ba tàbbi ci sunu Senegaal gii, muy CORONAVIRUS.
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Mbas la moo xam ne, réewoo-réew mu ngi fay tëral ak a fàdd doomi–aadama yi. Ngir xeex ko nag, fii ci sunum réew, gornmaa bi dafa jël ay dogal yoy, bokk na ci : tere nit ñi ñuy génn guddi, ku nekk war a lëlu ba fajar. Beneen laaj bi nag mooy : xale yooyii newoon ci mbumbaay, ba dogal bi dal seen kaw, ana fan lañu jaar alkaati yi aakimoo mbedd yi. Ana nan lañu def  ba mën a dem ak dikk, guddi, tollook 10i waxtu, ba Hibaa mën a fekki xaritam yi ? Walla, ndax ñoom, xale yooyu, dañu leen a jox ay kayit yu leen may boobule sañ-sañ ? Su ñu noppee ci laaj yooyu, beneen taxaw, muy : ndax dafa am ñaari Senegaal : gu baadoola yi yoon mën a dal seen kaw, saa su ne, ak geneen, gu ñeel boroom barke yi, ñuy buum di bummi, di tambaambalook a def lu leen neex ? Dafa mel ni daal, yoon buy digal ak a tere, baadoola yee tax ; ci ñoom daal la gën a jekk. Moone, dañuy faral di wax naan :« Senegaal, benn bopp la, kenn mënu koo xar ñaar ! » Am déet ?
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Laaj yi yamuñu foofu de ! Leneen li mat a xam, mooy : ndax CORONAVIRUS bii, dafa am ñu mu dul song ? Du dañu naan feebar bixamul xàjjale? Ak li ñuy woote yépp ci rajoo yeek tele yi jëm ci jumtukaay ak i matuwaay ngir moytu feebar bu bon bi, niki : soriyantoo, raxas say loxo, ak yu ni mel, naka la sunu njiit yi mën wëlbatikoo, bàyyi seeni doom, ñu topp seen bakkan, di doxe maa-tey ? Xanaa kenn mënul ne bëgguñu seen doom yooyu de ? Walla, ñoom ci seen bopp, dañoo gëmul dara ci li ñuy woote ?
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Mbir maa ngoog. Laaj yi bari nañu lool, te yeneen mat naa leeral, yu mel ni, Hibaa Caam mi ci ñàkke bakkanam, ku ko rey, ak ci yan anam la faatoo ? Li ci gën a doy waar nag, mooy, doonte ubbeeguñu lànket bi, taskatixibaar yi xamle nañu ni, way-jur yi ci seen doom taq ripp, ba alkaati yi teg leen loxo,  ña ngay dugg ak a génn, di lal ay pexe. Looluteey na xelu ñu bari, ba ñu jàpp sax ni mbir mi du mujj fenn.
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Loolu nag, su amee it, du fi guléet : xanaa fàttewuleen Mati Mbóoj, janq bu siiw boobu fi génnoon àddina moom itam, ci anam yu ni mel? Mel na ni nag, yëf yaa ngi bëgg a ëpp i loxo, te lu ëpp, tuuru. Su ñu ci jógul, du baax ci guney réew mi.
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
Waaw, Senegaal gii xar ñaar, ak ñawtéef yi lëmbe réew mi, ndax mënees na koo saafara ?
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
KORONAAWIRIS : TAXAW TEEWLU
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
Làmp Faal Kala
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
Mbasum Covid-19 mi lëmbe na àddina, lëmbaaje xel yi ak xol yi, ba ku tiitul it jaaxle nga, mbaa sax nga faf boole tiitaange ak njàqare. La woon, lu ci ëpp wonni na tey, mbir yi jaxasoo, nit ñi di jaawale, gis-gis yi wute, ku nekk di wax ak a layal la dalum xelam.
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
Mu mel ni danoo jekki, ñu cëppeel nu ci meneen kéew mu wute ak ma nu xamoon. Barabu liggéeyukaay yu bari tëj nañu, ku daan yëngal ak a xumbal selaw nga,  boroom dërëm ak daraja ya daan bàkku ñooy kotkoti ndax tiit, woroom xam-xam yi wedam, njàqare daj fépp. Rax-ci–dolli, as péexte mi nit mënoon a bàkkoo, bàyyima yee ko ko ëppale tey, ngir nit la nuy tëj, bàyyima yiy daagu waxtu wu leen soob. Lépp ni tekk, ba ci barab yi nit ñi daan dem di fa yaakaaree yërmaande Yàlla sax, lu  mel ni jàkka yi ak jumaa yeek jàngu yi, nee nañu ràpp. Tëj googii juraat geneen werante ci jullit ñi, rawati-na bi weeru koor wi teroo : ñii wéeru ci ngëm, di sàkku nu tijji leen te gëm ni Yàllaa fi indi mbas mi, bu nu ubbee néegam yi, ñaan ko mën naa am mu wis ndox mu sedd ci mbas mi mu daldi fay, ñee gëm nañu Yàlla naam, waaye teewuleen a wéeru ci xam-xam te naan wareesul a ubbi jenn jàkka mbaa jumaa, ndaxam diinee digle fargaru. Kuréel gu ci nekk di indi ay aayaak i xadiis di layal sa gis-gis. Béjante ak werente yooyu jural jullit ñu bari ag jaaxle, rawati-na ñi seen àlluwa soriwul ba ñu mën a xam fu ñuy taxaw.
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
Fii jamono toll nag, képp ku amum xel yaa ngi joyal say xalaat ci mbas mi. Ñii jàppe ko mbugalu sunu Boroom, ñee jàppe ko pexeem ñoñ Ibliis, am sax ñu jàpp ni mbindare mi moo fippu ci kow doomi-aadama yi. Ñi daan tontu tey ñépp a ngi laaj : Ana fu jàngaro ji juge ? Ana fu mu jëm ak nun ? Kañ lay jeex? Ndax dunu jeex balaa jeex ? Nu muy jeexe ? Laaj yooyu ñoo ëlëm ñépp te lënt xel yi.
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
Li wér te wóor nag mooy, mbas mi wan nanu sunug néew doole ak sunu xam-xam bu gàtt, wan na nu itam sunu bopp, wan ku nekk ci nun jikko ya gën a làqatu ci moom, muy mbaax mbaa safaan. Lenn ci li koy firndeel mooy, doonte mbas maa ngi jur yeneen tolof-tolof ci fànn yu bari ba tax am ñu nelawatul ngir di def i jàngat ak a seet ay pexe ngir jariñ askan wi, ñeneen a ngay naxaate, di wuruj ak a wor,  di lali pexe ngir jariñoo askan wi.
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
Ginnaaw coow li amoon ci “Chloroquine”, fan yii “Artemisia” moo  aye ndax réewum Madagaskaar dafa cee defare garab gu ñu saytul seen bopp ba xam ni dafay faj ak a aare ci doomu-jàngaroy koronaawiris. Seen njiitu réew jël na ci ay dogal ba ñu tàmbali koo jëfandikoo, doonte O.M.S, di mbootaay mi nu dénk wér-gi-yaram ci àddina si, nangoogu ko. Taxawaayu O.M.S boobii sabab na yeneen laaj : ndax du li garab gi bawoo Afrig a tax O.M.S sawaru ci ? Ndax yeneen njiiti réewi Afrig yi dinañu dooleel njitu réewum Madagaskaar, indi seen xam-xam door koo yaatal ci séeni réew, walla ñoom, dañuy déglu ndigalu seen naataangooy tubaab yi ?   Li ci kanam rawul i bët.
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
Beneen laaj bi mooy lu jëm ci wàllu alikeñ yi. Ku nekk di ñaw ak a ñawlu, ñii di maye ñee di jaay. Ndax saytu ba xam ndax ñi ngi dëppoo ak cet ak matuwaay yi mu laaj yépp jotul ?
https://www.defuwaxu.com/koronaawiris-taxaw-teewlu/
Fii mu toll nag, ku nekk a ngi fagarook a ñaan mbas mi jeex, waaye na nu fas yéene,  su yii yépp jàllee, waxuma nit ku nekk rekk, waaye réew mu nekk, rawatina yoy Afrig, jëlaat say matuwaay, jubbanti sa doxalin, defaraat sa toogaay, ndax ku muus tey dañu laa naxoon démb.
https://www.defuwaxu.com/bokk-ak-nawloo-ngir-jamm-ak-naataange-ci-addina/
BOKK AK NAWLOO NGIR JÀMM AK NAATAANGE CI ÀDDUNA SI
https://www.defuwaxu.com/bokk-ak-nawloo-ngir-jamm-ak-naataange-ci-addina/
Weer yii nu génn, réew yu bare tànn nañu seen njiit. Joŋante yi gën a indi coow mooy yi amoon ca Beliyoriisi mbaa Amerig, walla fii ci Afrig, ca Kodiwaar, Gine-Konaakiri, Burkinaa, ak-ñoom-seen. Réewum Ganaa moo ci mujj. Gëstukat yu bare ak i yéenekaay bind nañ ci, woykat yi waxi noppi. Góom yeek dana yiy teree wote ci jàmm ñoo ngi ne fàŋŋ. Kon boog, jar na nu toog, delloosi sunu xel, ubbi bu baax sunuy gët ak sunuy nopp. Su ko defee, dinanu mën a bind ci jafe-jafe yi réew yiy jànkoonteel, rawatina: – Góom yeek dana yi tëwa wér – Siddit yi sanax – Yaram yiy soox I/ Góomi réewi Afrig yi bare nañu. Mënees na cee lim: -Ñit ñu bari yi amul dàntite, moo xam ndax mës na ñoo am kayitu juddu walla mësuñu koo am; -Ñi bëgg a wote waaye ba ñu demee ba ca béréb ya, gisuñu njaq liñu war a sànni seen xob; -Ni ñu dajalee nit ñi ci ay mbaar yu xat, ñu ne fay buuxante, ba faf mer, gedd mbaa ñu dàq leen, ne leen waxtu dakkal wote bi jot na; – Ñi gisul seen nataalu mbër ci xob yi; – Ñi mënul a dem ci béréb yi njaq yi ne, ndax seen i cër dañoo sutante walla ñu tàyyel a génn rekk, ndax léegi mën nañoo jaar ciy jumtuwaay yu bees ngir wote. Wóoruleen nag ndax seen xob mujj naa bokk ci waññi bi; – Lawax yiy tamante dëmm, di jiiñante càcc ak di jaayante doole, nekk na luñ dégg ci réew yu bare; – Ger ak maye xaalis tax na ba ci yenn làngi pólitig yi ak lawax yi luxóor, jël ndam li. II / Dana yi nag, nii lañu bindoo: – Ñi ci jal yi sawaru ñoo jébbale lenge yi, jàpp ci Yàlla nangu ni dañ leen a daan, – Daa ñu def seen kem-kàttan, aakimoo yéenekaay yi, gaawtu ne làmb ji tas na, wure wi dem na këŋ, – Daa ñu dóore, màtte, jiiñ, faat sax ñi ñu doon joŋanteel; – Daa ñu ger ñi leen sonal ak ñi ñu ragal, jaare ko ci mbootaay yi, sàndikaa yi, kilifa-diine yeek kilifa-aada yi. Ragal a delloo weccit, ragal a tontu ci li ñu leen di tuumaal moo tax ñuy yaakaar ne xare pólitig dafa ànd ak xaru, ak ñédd nguur; – Ba ñu defee loolu lépp ba noppi, daa ñu dellusi di digaate naataange ak jàmm: – Daa ñu jéem a dalal xel yi, dige ni di nañ jubbanti réq-réqi réew mi, ngir mbir yépp tegu ci anam yu leer te jub, lépp rekk ngir faluwaat. Waaye ndax mënees na leen a gëm? III / Ñàkkul siddit yee wéragul – Siddit wi ci gën a feebar mooy siddit wi Njiiti réew yi naj, jàppe nguur gi seen moomeel. Su fekkee njiit li ku dul sàmm kàddoom la, ku mànduwul, ku jiital bànneexu njabootam tey jàppaley xaritam, mbaa xeetam, walla waasoom, kooku mënul suuxat mat ak juboo ak Jàmm, astemaak naataange. – Faj siddit wi ci topp mooy tabaxaat pénc mi war a xàll yoon wi ñépp di jaar ngir jokkoo, waxtaan wi gën a yaatu Su fekkee pénc moomu, ki ko jiite ak i naataangoom defuñu seen liggéey, rax-ci-dolli lu njiitu-réew mi joxoñ, ñu dagg, xam ngeen ni ñooñu kenn dootul am yaakaar ci ñoom; duñu leen sax faaleeti; – Ñetteelu siddit wi feebar mooy siddit wiy dawal ëttu àttekaay yi. Su nasaxee, far, fekki yeneen ñaari siddit yi, réew mi mën naa tas. IV / Bokk ak nawlooy faj yaram wi Nit moo dem ba gis ne jàmm moo gën fitna. Noonu la fente demokaraasi, maanaam, sàmm baatu képp kuy noyyi cim réew, jublu ci saxal fa jàmm ak naataange. Nit demati ba yokk ci nawloo, ngir ñu yaatal géew bi; wàññi xiiro ak ŋaayoo, boddikoonte ci biir xeet yi, biir waaso yeek këru diine yi, ngir sàmm li ñépp bokk. Noonu la yaram wi war a bindoo. Bennoo bi tamit, war naa law fépp ci réew mi, ku ne li nga liggéey, jariñ la, jariñ sa njaboot ba jariñaale askan wépp. – Sàrt yi ñu ràbb noonu, ku leen jéggi, teggi sànni, xàllal nga fitna yoon. Kon boog fedd siddit yi, diw leen baa ñu niin ak kaarite mooy yeewu, jàng, sàkku xam-xam, ngir mën a tedd ëllëg. – Fii ci Senegaal nag, jot nan fee amal waxtaan wu yaatoo-yaatu. Persidaa Aamadu Maxtaar Mbów, moo jiite woon liggéey boobu. Yékkati na fay kàddu yu am solo, dénk leen ay sëtam. Du ñàkk nu dellusi ci balay yàgg, saytu mbir mi, wax ci li nu ci war a yokk. Baabakar Jóob Buuba Njiitu PAALAE, mbootaay muy yëngatu ci liifantu ak njàngum mag ci Afrig
https://www.defuwaxu.com/dibeeru-welbati/
DIBÉERU WËLBATI
https://www.defuwaxu.com/dibeeru-welbati/
Cialtine jii la njiitu réew mi doon jébbal askan wi saxaar gi ñu duppe TER. Waaye, laata looluy am, ndajem-ndeyu-àtte mi, siiwaloon na ci suba si juróomi wutaakon yi war a joŋante ci wote njiitéefu réew mi nu dégmal : Màkki Sàll (njiitu réew mi), Usmaan Sonko, Madike Ñaŋ, Isaa Sàll ak Idiriisa Sekk. Waaye, benn baat a fi lëmbe : wëlbati. Waa kujje gi naan, Màkki wëlbati na keesu réew mi, jël xaalis bu-dul jeex jagleel koog saxaar, te askan wiy jànkoonteel i jafe-jafe yu tar. Ñu neeti dafa kootoog yoon wi ngir wëlbati kàrt gi, seppi ñenn ciy naataangoom ci joŋante wote bi, Xalifa Sàll ak Karim Wàdd. Am sax ñu naan, ki tëgg làmbu dibéer bi ñu génn, te Bàlla Gay wëlbati Móodu Lóo jël ndam li, li mu ko dugge woon mooy juutal xelu nit ñi ba ñu fàtte solos bés bi.
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/
2002, ATUM SUUXU JOOLAA BI
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/
Bërki-démb 26 sàttumbar ci atum 2020, “Bateau le Joolaa” def na 18i at ci biir géej. Daanaka ñaari-junni nit ñàkkoon nañ ci seen bakkan. Te mujjagul fenn, ay daan amaguñ ci. Moonte kenn mësula gis jéeya ju tollu nii, mu waroon a tax askan week nguur gi taxaw ngir leeral ko. Dañ koy fàtte ba bés bi  dellusi, ñu amal ay ndaje, ne fay dige yoo xam ni, suñ fay jóge mu yem fa. Aa, nun askanu Senegaal, ni nu néewalee dafa jéegi dayo.
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/
Ñi ñàkk seeniy mbokk a ngi wéy di naqarlook fàttaliku, nguur ngi di wéy di dige jàppale ak teg i daan ña sooke suuxu Joolaa bi. Naam, nguur nga woon ca jamono jooju taxawaayam matul woon benn yoon, waaye warul tax nguur yi ko wuutu ni yàcc, ni yasar.
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/
Ñi ëpp ci askan wi yaakaaroon nañ ni nguur ngi ak àttekat yi dañ fay doxe wone seen mënin ak seen fulla waaye bun ko mën a waxee noonu fa la léeb doxe tàbbi géej ndax dige yu dul jéex te lépp naaxsaay.
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/
Ci kàdduy Ablaay Jóob, jawriñ bi yor aadaak cosaan, dees na taxawal “Mémorial le Joolaa” jagleel ko way-lab yi ngir kenn bañ a mës fàtte lu tiis loolu daloon réewum Senegaal ci sàttumbar 2002. Buñ delloosi woon xottu gaal gi, nag, ci lay dàq ndax way-ñàkk yi dinañ mën a dëj dëgg-dëgg seeni mbokk ; dina giifal it lu mu bon-bon meru askan wi ñeel nguur gi ak ñépp ñi seen càggan jur lu ni mel. Noonu sax la ko Bubakar Bóris Jóob di waxe ci Bàmmeelu Kocc Barma(aux éditions EJO, 2017).
https://www.defuwaxu.com/2002-atum-suuxu-joolaa-bi/
Ndey Koddu Faal Plus de publications Ndey Koddu Faal https://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/ BATAAXALU NGUGI AK BÓRIS JÓOB ÑEEL NJIITU RÉEW MI Ndey Koddu Faal https://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/ 23 AWRIL BÉSUB TÉERE AK ÀQU BINDKAT BI Ndey Koddu Faal https://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/ SÉEX ALIYU NDAW GÉNTOON NA KO DÉMB, AADAMA BAROW AK BASIIRU JOMAAY FAY DEF NAÑ KO TEY Ndey Koddu Faal https://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/ RUWÀNDAA, 30I GINNAAW FAAGAAGALUG TUTSI YA
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Bataaxalu Saalif Keyta ñeel IBK
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Ci tekkib Paap Aali Jàllo
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
KÔRO (mag sama),
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Jàmm ak salaam ñeel na la. Sa rakk a lay nuyu, di la ndokkeel, di la jox sa wàccuwaay.
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Ginnaaw loolu, xamal ni kat, sa mbokku cosaan mi nga bokkal maam, di sa mbokku aada, moo namm a waxtaan ak yow tey. Bataaxal bii ngay jàngsi, mi ngi bawoo cib maxejj bu bëgg réewam, mu jaral ko lu ne, fu ne, te xaaru ci kenn walla lenn, muy xaalis walla ndombog-tànk. Duggewuma ko wanewu. Te yit, jubluwuma ci ŋàññ la, walla di yàq sa der. Nde, doo sama noon, te noonoowuma la ; doo sama wujj, te wujjewumaak yow. Tamit, rambaaj walla naaféq taxumaa jóg. Kon, jàppal ni bataaxal bii, jàmm rekk la wund, ñeel nekkinu Mali gi nu bokk ak i doomam, te nga boole leen jiite. Bu ko defee, naŋ ko jànge xel, bañ koo jànge xol.
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Kôro,
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Liy xew ca bëj-gànnaaru Mali metti na, tiis na. Xanaa gisoo ni ñuy reye ndawi Mali yi, di saam seeni néew ? Ndege, biir làrme bi, ndaw yaa ci ëpp, bés bu nekk ñuy jaay seen bakkan ngir seen réew. Jigéen ñaa ngiy ténj, jirim yeek baayo yi di gën a bare, yaakaari way-jur yi di tas. Foo dem fekk fa dëj. Ndaxte, ay doomi jàmbur, mag ak rakki jàmbur, jëkkëri jàmbur ak pàppay jàmbur ñoo fay dee. Boo weddee li ma lay wax, dugalal sa ñaari doom yi, Buuba ak Karim, ci làrme bi, yabal leen ñu xeexi. Bu booba nu xool ba xam ndax dinga nelaw am déet. Waaye, ginnaaw kenn ci seeni  doom, mbokk walla jegeñaale deewu ci, seen yoon. Yëgalu leen ko sax seen yaram. Moo tax, ci jamonoy tiis ak naqar jii, say doom sañ a salfaañe alalu réew mi, di ko pasar-pasare. Ñu ni déet-a-waay, say way-yëddukat di yaataayumbe ak a gundaandaat, di jël lu tollu ci 100 walla 300i milyoŋ ci sunu koppar di ko yàq ciy aniwerseer ak i caaxaan. Ngeen fàtte askanu Mali wi nga xam ne, sonn na, tàyyi na. Nit ñi lott nañu, tumuraanke, xiif, mar ba nga ne lii lu mu doon.
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Ay waay ! Yërëm nu boog, kôro !
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Àddina sépp xam na ni Farãs a sooke jéyya ji xew ca bëj-gànnaaru Mali, di fa reylu ay ndawi réew mi. Xanaa gisoo ne seeni moroom yu Farãs di fey ci suuf ñoo leen di faat bés bu Yàlla sàkk ? Dafa di, nag, lu jiin Njaag a, te Farãs mooy Njaag. Te sax, yow ci sa bopp, dara umpu la ci. Yaa gën a xamaatoo ni Macron, njiitu Farãs, ak i ndawam ñoo ngemb ay saay-saay yiy mbubboo raaya Mali, di wootewoo bëgg-sa-réew ba noppiy faat ay doomi Mali bés bu nekk. Xam nga xéll ni Farãs mooy seytaane bi leen di jox i gànnaay, ñuy fetal doomi réew mi. Ma ni, benn jiyaadis amul Mali waxatuma laak terorist. Ay kàcci kese la ! Te, taskati xibaar yu baree ngi leen ciy jàppale. Dafa doy nag !
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Aa, Kôro !
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Tee ngaa jéngu, tekki buumu njaam gi la goneg Farãs gi takkal. Mbaa du Macron dafa këf saw fit ? Nga topp ci moom nig geen. Fuñ la fekk yaa ngi lëngook moom ngir wane ni ay xarit ngeen. Yow tamit, xamal nag ne doo moroomam. Kii nga xam ne ku bës bakkan bi meew génn ci, lu tax ngay nangoo wéy ci waawam ? Xale boobu ngay sibooru de, mooy reylu say ndawi réew bés bu nekk.