url
stringclasses 152
values | text
stringlengths 4
5.13k
|
---|---|
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Njiitu Réew dàq la sa liggéey |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Dàqin wu ñaaw, mbete sàcc |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Te yaa doon xeex ñay sàcc |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Askan wi fal la, def la dépite |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ngay dëggal, doon ku nite |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Fa nga daan taxaw Aasàmbale |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ku fa taxaw tey du ko mate |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ngay wax dëgg, ñu lay bów |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Waa APR ak Abdu Mbów |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Téye sa der bi di ci saw |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Seen iy sobeek seen iy pexe |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | « Présidentielle 2019 » |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñu lay kókkali, nga nëw doon |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñetteel ca ña jiitu |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Idiriisa Sekk xëy la wor |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Maki Sàll téye di tëje |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Takk-der di kajje, di pese |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Xalifa Sàll nekk kaso |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Nga taxawu ko, mu génn dëddu la |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñi fi amul woon resepise |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñi fi amul woon ku leen faale |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñi fi amul woon fitu gaynde |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Usmaan, yaay ki leen xettali |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Mag yu bari faalewuñu ndaw |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Nga wax ak ndaw ba mu mat mag |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Lu mel nii ci sunu Réew |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Néew na foo koy gise |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ba ñu xamee nag ne yaa leen gën |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ca la nu jóg di la tuumaal |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Jiiñ nañu la fi ciif, jiiñ la rëbel |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Jiiñ la terorist ak càccug telefon |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Jël nañu la tëj ak sa njaboot |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñaari weer ci sunu biir Réew |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Gii gàcce, gàccee ka réy |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Soo yambaroon nu dooniy jaam |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Nu ne déet, ñu sànni la kaso |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Sa pàrti, ñu gont tas |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Say junniy àndandoo ñu tëj |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Juroom-fukk ci ñoom ñu rey |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Siggil ndigaale, Usmaan Sonko |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ci Baay Seex Jóob mi ñu bóom |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ci Porospeer Seŋoor sa doom |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñoom ñii, ñooy say nawle |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñiy dund, ñi ëpp matuñu |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Tey jii, nga génn kaso |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ginnaaw nga woorlu jiitu Koor |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Looy defati bàyyi leen ci xel |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Nit ñi génn di la teeru |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ñoo yey, dangaa gore |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Maki Sàll bëggul a dem |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Nga samp Basiiru ngir mu dem |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Sa jëf yii ni ñu taaroo |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Yal na yiy ñëw gën a taaru |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Yaakaar yi nga yee ci nit ni |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Yal na ci ndam yu réy topp |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Liy ñëw nag mooy gën a metti |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Jagal Réew coono la doŋŋ |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Waaye nag du yow laa koy wax |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ku ragal coono daa bañ lu baax |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Doxal, Usmaan, bul jeng |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ci yow kat danuy jàng |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Ëlleg, bëgg nanu laa weesu |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Sunuy rakk it nëw di nu jiitu |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Senegaal dëkkee tedd |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | « Yaa gore », la taalif bi tudd |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Séex Axmadu Bàmba ki ko bind |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Njaay-Jaata, dëkk Njaaréem |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Di góoru Ajaa Mariyeem |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Moo la naan, dalal ak jàmm ! |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | Séex Axmadu Bàmba Njaay |
https://www.defuwaxu.com/yaa-gore/ | 15/03/2024 |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | AFRIG AK KORONAA, AFRIG GINNAAW KORONAA |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | USÉYNU BÉEY |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Koronaawiris bi, li muy metti metti, terewul kàngami boroom xam-xam yiy wéy di ci weccee xalaat ñeel doxalinu àddina si, ba xam luy nar a doon ëllëgu doomu-aadama, bés bu nu génnee ba set ci mbas miiy fàdd nit ñi, réewoo réew. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Ñu ci bare jàpp nañu ne, bu nu génnee ci fiir gii nu koronaawiris bi fiir, warees na xoolaat tëralinu koom-koomu àddina sépp, waññi puukare bi te jox gëddam lépp lu ñeel wér-gi-yaramu doomu-aadama. Maanaam, tabax ay loppitaan yu baax te doy, ak lépp li ñu war a àndal ciy xeeti xarala. Warees na yit jiital lépp lu jëm ci dund gi dëgg-dëgg : mbey mi, càmm gi, lekk geek naan gi… Njàng meek gëstu bi tamit, wareesu leen a fàtte. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Wax dëgg, Covid-19 bi musiba la, waaye booy seet ku mën a yar mag la. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Fii ci Afrig nag, ñu bare jàpp nañ ne, su nu weesoo jamonoy koronaawiris bi, sunu réew yi waratuñoo des ginnaaw. Am sax ñu dem ba yaakaar ne Afrig moo war a aye, jiitu ñi ci des topp ci. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Kon de mu neex ba dee ! Waaye loolu lépp, mbaa du ciy gént rekk la nar a yem ? |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Dëgg la, réewi Ërob yeek yu Amerig yi, ñoom, dañoo weere. Ndaxte, koronaawiris bi da leen a futti ba ñu set wecc ! Ndekete seen alal ju bare jeek seen doole ji leen ñépp xamaloon, fii lañ tollu : feebar biy lëmbe fépp, nit ñiy dee niy weñ, loppitaan yiy màbb, jarag yi jaaxle xamuñu nu ñuy def ba faju, fajkat yi jommi ; nit ñiy làqu ci seen i néeg… Kenn dematul, kenn dikkatul, koom-koom biy nasax di ruus… Yaafus mënul a weesu lii ! |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Fekk booba, Afrig mel ne Sunu Boroom daf kaa beral loxo. Ba fi nuy waxe nii, mbas mi, ñi mu ci jàpp ba di yóbbu seen i bakkan, buñ ko dee méngale ak li xew feneen, mën nanoo sànt Yàlla ! Doonte sax benn doom-aadama rekk bu wàññeku, ñàkk wu tiis lay doon saa su ne, ak fu mu mënti doon. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Ndegam kañ koronaawiris bi du ñëw génne yeneeni feem, jaxase mbir yi, dëggal yéeney ñenn ñi doon xaar Afrig nërméelu ba tàq ripp ci mbas mi ! Ndaxte, kat, jamono jii, muccagun. Senegaal gii rekk, limees na fi 2000i way-aajowoo ceet ak lu teg ! Te yit, 25i doomi-aadama faatu nañ ci sababu koronaawiris bi. Kon, mbas mi bàyyiwul kenn, nu wax ko, waxaat ko : kuy nelaw ba yàndoor, lu la ci fekk yaa tooñ sa bopp ! |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Teewul sun dee seet bu baax day mel ni àddina si, gaa tukkiwul, waaye mu ngiy soppiku : boroom doole yiy jaaxle, daanu, way-ñàkk yi taxaw di fëgg dënn. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Wànte, li mat a seetaat nag, mooy xam naka la sunu réewi Afrig yiy def ba bañatee doon ndaare, dem sax ba raw ci àddina sépp. Su nu wékkulee sunu yaakaar cib luxuskat buy ñëw defal nu lu ni mel, war nanoo seet fu nuy teg sunuy tànk, xam fu nuy jaar ba bañ a desati ginnaaw. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Yàlla-Yàlla, bey sab tool. Ndax askani Afrig yi, rawatina seen i njiit, taxawe nañu boobu taxawaay ? Ndax ñi ñu séqal mbir mi, maanaam yeneen réew yi dinañ nu seetaan nu leen di dab ba di leen raw ? Mbaa danoo yaakaar ni ñooñu dañoo ñàkk doole ba mënatuñoo xippi ? Te yit, li gënatee am solo mooy samp laaj bii : ndax tëralinu jëflante yi am ci diggante réew yi dañoo soppiku ba fàww ? |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Su dee loolu lépp dara amu ci, fu nuy jaare yeneen réew yi ba romb leen, waxatumaag di leen jiitu ? |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Sunu njiit yi de, ba tey jii, ci liñ nu wonagum, ñu ngiy wéy di tàllal seen loxo di ñaan ndimbal. Bare na ci ñoom ñuy sàkku ci seen i naataango yi nekk Ërob, Amerig walla Siin ñu baal leen seen i bor. Walla boog, gën caa néew, ñu far 44i milyaar yi ñu war a fey ci at mii. Njiitu réew mi, Maki Sàll, moo ci gën a ràññeeku, ndax moom moo aakimoo wax ji te Macron, njiitu Farãs di ko ci jàppale bu baax. Monte de, ñoom Macron ak ñoom seen, am nañu lu leen doy sëkk. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Moo tax it, waa Tugal yi xam nañu bu baax ne, meneen pexe amul. Balaa ñépp di labandoo fàww ñu seet nu ñuy fexe ba yombalal tuuti mbir mi waa Afrig yi, ndax ñu noyyi as tuut, ñoom it ñu am ci bànqaas bu ñuy jafandu ngir mucc. Li leen amal solo rekk moo di bàyyi xel ci buumu njaam gi, bañ mu rocciku, mbaa mu daŋ ba faf dàgg. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Waaw, ndax gor dëgg dina leb lu mu dundale njabootam, dem duggi, togg njëlam ba noppi dellu di balu ndax ñàkk lu mu feye ? Di ñaan ñu faral ko boram ba noppi fas yéenee demati leb fa woon ? Ndegam jéemul a naxaate (konte ndaw woyof bopp !), xanaa kon day yeew ay loxoom ba noppi daldi jébbal boppam ? |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Ba réewi Afrig yi jëlee seen moomeel ba léegi, noonu rekk la seen digganteek réewi Tugal yi deme, daanaka. Doxalin woowule nag, feek jógu fi, bu yeboo nun askanu Afrig, nu tëddi te nelaw ! |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Kon réewi Afrig yi, rawatina seen i njiit, war nañoo am beneen jubluwaay bu dul di tàllal seen i loxo di saraxu, di sukkal ñi leen yeew bu dëgër, ngir sàkku seen yërmande ! |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Dëgg la, am na ci sunu njiit yi kenn ku ci ràññeeku lool ci jamano yii, mu di Andry Rajoelina mi fi wone taxawaayu bañkat, ak garab gi waa dëkkam, Madagaskaar, feeñal ne day faj koronaawiris bi, ci lu wér ! Ndax dëgg la am déet, doctoor yeek ñi seen xam-xam màcc ci wàlluw paj mi, dinañu ko wax. Waaye, Rajoelina moom ku mat a naw la ndax taxawaayam, ak fullaak faayda gi mu àndal yépp ngir aar askanam, réewi Afrig yi ak sax àddina sépp. Moom de, xaarul ñu wax ko nu muy def walla fu muy jaar ba génne ay ñoñam ci guta gi ñépp daanu tey. Nekkul it, ci doxalinam, di toppandoo njiiti réewi Ërob yi, ni ko ñenn ci naataangoom yiy defe, fàtte ne anam yi réew yeek xeeti àddina siy dunde dañoo wute lool, su ñu woroowul sax. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Wolof Njaay, nag, dafa ne : benn loxo du tàccu. Jom ak faayda ji njiitu réewu Madagaskaar wone, doy nañ royukaay ñeel moroomi njiitam yi. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Nañ bàyyi yalwaan, tàkk seen fit, xeexal seen askan. Boole seen i xalaat ak seen doole, fas yéenee jammarlook nooni Afrig yi, jiital seen i njariñal réew, liggéeyal seen askan. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Suñ ko deful, na ko doomi Afrig yi defal seen bopp, seet nu ñuy lijjantee seen digganteek njiit yi leen wor. Jom mooy faj gàcce. Su gàcce gi dakkee la ëllëgu Afrig di door a leer. |
https://www.defuwaxu.com/afrig-ak-koronaa-afrig-ginnaaw-koronaa/ | Tey-si-tey, nag, wax ji lii rekk la : nu nuy def ba jële fi mbas mile. Mbas waay ! Sunu réewi Afrig yi su ñu bennoowul xàll seen yoonu bopp, gisuma leen Mbaaw ! |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | ALSERI DUMAATI NA SENEGAAL |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Démb ci talaata ji la gayndey Senegaal yi doon janook Alseri ci joŋante xaritoo. Jamñaajo, ça fowub Abdulaay Wàdd, lañ ko doon futbalee. Alseri moo jëlati ndam li. Nde, ñoom ñoo dugal benn bii, Senegaal tus. Démb a nekkoon 14eelu yoon wi Senegaal di sukk ci kanamu Alseri. Li ci gënatee doy waar mooy ne, Alseri dafa tegale 6i joŋantey kuppe yu muy dóor Senegaal. |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Laata joŋante biy door, bi 19i waxtu jotee, jaglees na similib tekkaaral way-dëdduy Marog yi dee ca rëng-rëng ba fa am. |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Bi mbir yi tàmbalee, Senegaal a tegoon tànk ci bal bi, sépp Alseri. Jekku nañ ay yoon ngir dugal. Waaye, muy Saajo Maane, di Ilimaan Njaay walla Nikolaa Jakson, kenn làkku caax yi. Bal buñ dóor, jàppkatu Alseri bi génne. Alseri dafa amoon ay jafe-jafe ngir jot ci bal bi. Te, saa buñ ko jotaan, gayndey Senegaal song leen, nangu ko, sëppaat leen. Ñooñu, ba ni arbit biy mayee ag noppalu ngir ñu seral seen i put. Ndax, dafa tàggoon démb. |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Biñ naanee ba màndi, waa Alseri dañu xaw a yeewu tuuti, tàmbalee cokkaas Eduwaar Mendi. Wàññeeku Senegaal bàyyeekuwul. Dañu jàppaat, nanguwaat bal bi. Paap Mataar Saar, Kulibali, Jakson ak Sabali naroon nañu dugal sax, waaye sottiwul. Bi xaaj bu njëkk biy jeex, kenn dugalul sa moroom. |