url
stringclasses 152
values | text
stringlengths 4
5.13k
|
---|---|
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Biñ delsee ci ñaareelu xaaj ji tamit, Senegaal dafa delloo buum ca mboy-mboy ga. Waaye daal, bal bi daa bañoon dugg. Ca la xel ya tàmbalee teey, ñiy ragal Alseri yoxosu Senegaal. |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Benn teg-dóor la Alseri am, Riyad Mahrez xellil Chaybi Fares, mu toj kër gi. Alseri nax na Senegaal, dugal ko benn bii bu kenn foogewul woon. Nde, Senegaal a moomoon mats bi, ci lees foogoon. |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Senegaal def na lépp ngir dugal, waaye dugaluñu. Jakson naroon na ko, waaye mbëkkam bi dafa kawe. Noonu noonu ba ni arbit biy mbiibee njeexitalu joŋante bi. Alseri daldi amati ndam ci kow Senegaal. 6i yoon la raŋale, di dóor Senegaal. Dafa di Aliw Siise sax, démb a nekkoon ñeenteelu yoon wi muy ñàkk ci kanamu Alseri. |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Démb nag, Sonko safoon na fa sàpp. Balaa joŋante biy door ak bi muy daw yépp, ndaw ñaa nga doon woy woyu Usmaan Sonko wi xew ci jamono : |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | “Aayee ! Iyawoo ! |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Sonko namm naa la ! |
https://www.defuwaxu.com/alseri-dumaati-na-senegaal/ | Sonko ! Sonko ! Sonko namm naa la !” |
https://www.defuwaxu.com/lamin-kamara-goneg-wurus-gi/ | LAMIN KAMARA, GONEG WURUS GI |
https://www.defuwaxu.com/lamin-kamara-goneg-wurus-gi/ | Mamadu Lamin Kamara, jàppleen tur wi. Xareñte, dëgëraay, njaxlaf ak dégg-daaj la gaynde gu ndaw gi boole def. Moo tax, Mamadu Lamin Kamara, kenn la ci ndaw yi futbalu Senegaal yaakaar, ñu di ko bàyyi xel bu baax. |
https://www.defuwaxu.com/lamin-kamara-goneg-wurus-gi/ | CHAN 2023 ba la njëkk a wone boppam, wone xareñteek njàmbaar gu mat sëkk. CAN U20 2023 bi ñëw, mu goneg Génération Foot ga woon delloo buum ca boy-boy ga. Dafa di sax, ginnaaw bi ko Senegaal jëlee, moom lees tabb kuppekat bi gën a ràññeeku, gën a xareñ ca joŋante ya. Lamin Kamara, nees ko tàmm a woowe, fa la jaare luqi bëti tubaabi FC Metz yi. Mu jóge Génération Foot (këlëbu Senegaal) mi ko tàggat ba tay jii, fekki këlëbu Farãs ba, Metz. Muy ndam lu réy ci moom. Yàlla bu cat topp. |
https://www.defuwaxu.com/lamin-kamara-goneg-wurus-gi/ | Moom nag gan la fa. Waaye de, gan-ganluwul wenn yoon. Fullaay jaay daqaar, am déet ? Moom kay, dafa dem rekk bokk. Ndax, bi mu àgge foofu ca këlëb bi, dafa ñëw rekk tàmbali di dëyal fullaak fayda gu mat sëkk ak xareñte gi ko ñépp xame woon. Looloo tax ñu teel ko dugal ca biir ekib ba, muy dem, di bokk. Liy wane ni gan-ganluwul nag mooy keroog joŋante bam ñjëkk bokk, korneer yaak teg-dóor yépp moo ko doon dóor. Démb ci gaawu gi, mu def paas ci seen joŋanteb Ligue 2 bi amoon diggante Metz ak As Saint-Étienne, futbal lu réy. |
https://www.defuwaxu.com/lamin-kamara-goneg-wurus-gi/ | Waaye nag, dafa jël ab “rouge”. Loolu di bénn xeer bu jam ñaari picc. Ndax, benn futbalkatu As Saint-Etienne a ko cokkaas, mu fayu, arbit yi gis ko. Njuumte la. Ndax jikkoy xale bu tàng deret kesee ko waral. Waaye, sikk amul ci ne dina gën a noot boppam, dëfal xolam ba lu ni mel bañ koo dalati. |
https://www.defuwaxu.com/lamin-kamara-goneg-wurus-gi/ | Nu di ko ñaanal mu dem ba ñu koy dégg nag fu raw fu ñuy dégg i magam, niki ñoom Saajo Maane, Gànna Géy añs. Ndaxte, loolu ndamal réew mi la ak kuppeg Senegaal. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | FUTBAL : LIGUE DES CHAMPIONS, EUROPA LEAGUE AK CONFERENCE LEAGUE |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Barki-démb, démb ak tey lañ doon amal joŋantey kaar-dë-finaal Ligue des champions yi, Europa League ak Conférence League fa Tugal. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | League des champions |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Ci talaata ji la Dortmund ak Atletico Madrid doon amal seen ñaareelu ndaje. Ca ndaje mu njëkk ma ame woon fa Espaañ, Atletico Madrid moo gañe woon 2i bii ci 1. Waaye, bi ñu demee Almaañ, Dortmund daf ko dóor 4i bii ci 2, daldi koy toogloo. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Ca jamono jooja, Barcelone ak Paris Saint-Germain ñoo ngi doon amal, ñoom itam, seen ñaareelu joŋante. Ca bu njëkk ba, Barcelone moo fekki woon Paris, duma ko 3i bii ci 2. Barki-démb, Paris dafa fayu. Ndax, dafa fekk Barcelone dëkkam, dóor ko fa 4i bii ci 1. Barcelone moo njëkk a dugal. Waaye, biñ joxee kàrtoŋ bu xonq Araujo, ca ndaje ma wëlbatiku. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Démb, ci àllarba ji, yeneen ñaari ndaje yu mag amoon nañ diggante Manchester City-Real Madrid ak Bayern Munich-Arsenal. Ci joŋante bu njëkk bi, Real Madrid moo toogloo Manchester City biir dëkkam. Ca seen joŋante bu njëkk ba, dañoo témboo woon 3-3. Démb tamit, dañoo témboowaat 1-1, Real Madrid gañe 3-2 ci teg-dóor penaltii yi. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Bayern tamit dafa toogloo Arsenal. Ginnaaw seen témboo 2-2 ca seen joŋante bu njëkk ba biir Arsenal, Bayern Munich moo am ndam ci kanami soppeem. Nde, dafa wane geneen xar-kanam, dóor àngale yi 1-0. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Bu ko defee, nii la démi-finaal yi di demee : |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Paris Saint Germain – Dortmund |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Bayern Munich – Real Madrid |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Europa League |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Ci joŋantey kaar-dë-finaali Europa League yi, tey ci alxamesu tey ji lañ leen doon amal. Ñu amoon ci ñeenti joŋante : AS Rome – Milan, Atalanta – Liverpool, West Ham – Beyer Leverkusen ak Marseille – Benfica. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | As Roma moo toogloo Milan, dóor ko 3-1 bees boolee ñaari ndaje yi. Naka noonu, Atalanta génnee Liverpool 3-1 ci ñaari ndaje yi. Noonii la Bayer Leverkusen toogloowee West Ham 3-1 ci seen ñaari ndaje yi. Marseille tamit moo toogloo Benfica ginnaaw biñ àggee ci teg-dóor penaltii yi. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Nii la démi-finaal yiy demee : |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | As Roma – Bayer Leverkusen |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Marseille – Atalanta |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Conférence League |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Ci xëccoo Conférence League bi tamit, ñeenti joŋante lees ci amoon ci alxamesu tey ji : Lille – Aston Villa, Fiorentina – Viktoria Plazeň, PAOK – Club Brugge ak Fenerbahçe – Olympiaco Piraeus. |
https://www.defuwaxu.com/futbal-ligue-des-champions-europa-league-ak-conference-league/ | Aston Villa, Fiorentina, Club Brugge ak Olympiaco Piraeus ñoo jàll démi-finaal. Aston Villa mooy dajeek Olympiaco Piraeus, Fiorentina laale ak Club Brugge. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | 7 MÀRS WALLA 8 MÀRS ? BEY CI SA WEWU TÀNK… |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Juróom-ñetteelu fan ci weeru màrs la xel yépp di dem ci jigéen ñi, ndax seen bés la. Àddina sépp a koy màggal, di ci amal ay ndaje, ay waxtaan yu yaatu waaye it di natt ba xam fu xeex bi tollu. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Lépp a ngi tàmbali ci 1917, ca Saint-Petersburg, at ma ay óbëryee yu jigéen meree, amal ab doxu-ñaxtu. Lu jiitu loolu, ci atum 1910, Clara Zetkin, doonoon jàngalekat, surnalist, politigseŋ, sooke woon na ndaje mu mag, jigéeni sosiyalist yi wuyusi ko, ñu daldi taamu 8 màrs, def ko bés bees war a siggil jigéen ñi. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Ci 1977 la Mbooloom-Xeet yi nangu loolu, dëggal ko. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Fii mu ne nii, amul benn njiitul réew mu sañ a tanqamlu jigéen ñi le 8 màrs. Niñ ko xamee, ñi ëpp ci ñoom ay góor lañu te koo ci gis mu ngi politige bés bi, di jéem a gëmloo jigéen ñi seeni tawat soxal nañ ko lool. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Ci ñoom nag, am na ci ku xamutoon caaxaan ak tappale. Kooku Thomas Sankara la woon. Demoon na ba jël ca réewum Burkinaa-Faaso dogal bu yéeme. Saa yu 8 màrs agsee, da daan sant góor ñi ñu xéy fobeere néeg yi, duggi màrse, taal añ, toppatoo xale yi, fóot yëre yi, téye kër gi daal ni ko seeni soxnay defe bés bu Yàlla sàkk. Sankara dugge wu ko woon dara lu dul fexe ba góor ñi gën a xam li jigéen ñiy daj ci seen néegu-séy, su ko defee ñu weg leen, lépp lu ñu leen daan jàppale ñu xeeb ko, gën leen a taxawu. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Jigéen, ni ko woykat biy waxe, ku ko sóoralewul, yakk ñamu-mbaam. Loolu lu am la. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Sankara amoon nay yéene yu mag ci Afrig, jaarale leen ciy xalaat yu rafet te leer nàññ, kaar. Jigéen ñépp, rawatina yu Afrig, ameel nañ ko njukkal. Waaye ginnaaw bey ci sa wewu tànk, ndax amul beneen bés bu Senegaal waroon a jagleel ay jigéenam ? Sunu réew, nun, mooy réewum ‘’Talaatay Ndeer’’. Kon mënoon nanoo bañ a jéggaani ciy Tubaab bés bu nuy sargale jigéeni Senegaal. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Am ñu ma ni : ‘’Bés boobu ban la ?’’ |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Maa ni leen : ‘’Nan fàttaliku.’’ |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Talaatay-Ndeer, 7 fan ci weeru màrs 1820 la woon, Naari Tararsaa yi song péeyum Waalo, fekkuñu fa lu dul i jigéeñ, bëgg a leen a jàpp defi leen i jaam. Ndaw su am fit suñ naan Mbarka Ja ne leen bésu dee du bésu dund, jomb nanoo nekki jaam ginnaaw Barag-Waalo, nanu dajaloo ci néegu-ñax bu mag bii, taal ko ci sunu kow. Noonu lañu ko defe keroog, di woy ci biir safara si ba sedd guyy, suuxat suufus Waalo ak seen jom ak seen ngor. |
https://www.defuwaxu.com/7-mars-walla-8-mars-bey-ci-sa-wewu-tank/ | Kon waay-waay yéen sunuy njiit, buleen ragal a def 7 màrs bésu jigéeni Senegaal yi ! Defeleen ko noonu, su ëllëg saa nu àndandook ñépp bokk ci xew-xewi 8 màrs yi. Ana lu aay ci yëkkati jigéen réew mi ñaari yoon ? Te sax, bu nu waxantee dëgg, li nga dàqe kon kéwél mu jëm àll, dàqe ko béy mu jëm kër. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM (3/9/2023) |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | SAALIF KEYTA KUPPEKATU MALI BA WOON GAAÑU NA |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | Ci gaawug démb ji, 2 sàttumbaar 2023, la kuppekatu Mali bi gaañu. Ndem-si-Yàlla Saalif Keyta mi ngi amoon 76i at. Moom, doomu Mali ji, mooy kuppekatu saa-afrig bi jëkk a gañe Kuppeg wurus gu Afrig (Ballon d’or africain) ca atum 1970. Saalif keyta, ku aayoon lool la, taqe woon te xareñ. Moo tax, jot na def i jaloore yu baree bari ci futbalu Afrig, waaye woneet na mëninam fa Tugal. Dafa di, ku fa siiw la, rawatina biir Farãs. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | Bésub 6eel ci weer wii lees jàpp ngir sargal ko. Dees na ko jagleel ab yaxal bu yaatu ngir fésal jaar-jaaram. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | BELLINGHAM A NGI WÉY DI WONE BOPPAM FA ESPAAÑ |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | Doomu Àngalteer ji dafa ñëw ci sàmpiyonaa Espaañ bi rekk daldi miin. Démb ci gaawu moo nekkoon ñeenteelu joŋanteem ak Real Madrid. Waaye, bu ci nekk dugal na ci. Fim ne nii, mu ngi ci 5i bii ak benn paas. Soppey Real Madrid yi dugal nañu ko seen xol te demaguñu fenn. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | SERGIO RAMOS DELLU NA SEVILLE |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | Gannaaw ba mu jeexalee pasam ak waa PSG, moom jañkatu Real Madrid ba woon mu ngi toogoon ci ruqam di liggéey. Ci dibéeru tey ji, 3i sàttumbaar, la dellu Seville, fa mu jóge woon dem Real Madrid. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | RONALDO AK SAAJO MAANE ÑU NGI BOYAL ÀLLU NAAR YI |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | Déggoo bi dafa mel ni dafa teel a jàpp njaax diggante Saajo Maane ak Cristiano Ronaldo. Jamono jii, ku nekk ci ñoom ñaar a ngi xiir di def loolook loolu. Ronaldo mu ngeek 5i bii ci ñetti joŋanteem ak ñetti paas, Saajo Maane amagum 4i bii moom it ci ñeenti joŋante ak seen këlëb bii di Al Nasr. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | NDEKE ISCO MÀGGETUL ! |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-3-9-2023/ | Ñu bari jàppoon nañu ni ay balam dañoo jeex ndax li mu toogoon lu tollu ci 9i weer ci bãwu Real te futbalul. Ci merkatoo bii la fasanteek Real Betis. Boobu ba léegi nag, moo ngi fay wane xereñte gi ñu ko xame woon. Seen ñeenti joŋante yépp moom lañu tabb baay faalu joŋante bi, jot na ci dugal benn bii. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | XIBAARI TÀGGAT-YARAM |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | Real Madrid a ngi wër góol bu bees |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | Thibault Courtois, góolu Real Madrid bi, dafa ame gaañu-gaañu bu metti (rupture des ligaments croisés) ba tax na dina toog diir bu yàgg door a góoluwaat. Loolu nag, jur na njàqare biir Real Madrid ba tax ñoo ngi ci wër góol bu koy wuutoondi ko ca caax ya. Jamono jii nag, ñoo ngi làmbaatu fu nekk. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | Christopher Nkunku dina gëj ci pàkk yi |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | Moom Nkunku, bi ko Chelsea jëndee yàggul dara. Waaye, du gaaw a futbal. Ndax, dafa gaañu moom it ci oom bi. Dañu ko oppeere sax. Xamle nañu itam ni dina toog diirub ñeenti weer laata muy dóoraat ci bal. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | Kylian Mbappe demul Real Madrid |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | Li coow liy bari lépp ñeel Mbappe, ndax dafay dem Real Madrid am am déet, Mbappe dafa noppi rekk, ni tekk tekkaaral. Ba ci alxames ji, mu daldi ciy àddu. Li mu xamal njiitu Paris Saint-Germain li mooy ne, moom Mbappe, dafay toog PSG, mottali at mi ko dese sog a dem ci coobareem. Jamono jii nag, bëgg-bëggu njiiti PSG yi mooy mu yeesalaat pasam ba 2025, nga xam ni déwén, buy dem ñu man ci am dara. Wàññeeku, Mbappe dafa bañ loolu. Lim bëgg mooy jeexal at mi ko dese, demal boppam. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | Noah Fadiga amaat na këlëb |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/ | Doomu futbalkatu Senegaal ba woon, Xaliilu Fadiga, dafa mel ni li daloon baay jaa koy bëgg a dal, mbirum feebaru xol bi. Loolu waraloon sax këlëb bim nekkoon ca Farãs, Brest, dogoon pasam. Mu bañ a yaras nekk di tàggatook a faju ba amaat këlëb, Gant. Muy këlëb boo xam ni bii, baayam Fadiga nekkoon na fa menn at ci mujjantalu dundug futbalam. |
https://www.defuwaxu.com/lamb-moodu-loo-di-woo-jepp-doomu-parsel-ci-ginnaaw-fara/ | Làmb : Móodu Lóo di woo jépp doomu Parsel ci ginnaaw Farã |
https://www.defuwaxu.com/lamb-moodu-loo-di-woo-jepp-doomu-parsel-ci-ginnaaw-fara/ | Démb la Farã doon amal Open Press ñeel laale bi war am ci digganteem ak Soq. Mbëri Parsel yu mag yi bare woon nañ fa ngir biral jàppale giñ koy jàppale. Kii di Móodu Lóo jot na fa yékkatiy kàddu. Woo na jépp doomu Parsel ñu teew ca Aren nasiyonaal ngir dooleel seen doom Farã. Jàmmaarloo boobu warees na am ci gaawu bii, yemook 19i fan ci weeru Me. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | XIBAARI TAGGAT-YARAM (23/7/2023) |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | MESSI DELLOONA BUUM CA MBOY-MBOY GA ! |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | Bërki-démb ci guddi, bi 3i waxtu jotee, la saa-arsàntin bi doon amal joŋanteem bu njëkk ak këlëb bu bees bee di Inter Miami fa USA (Amerig). Boobu këlëb nag nga xam ni futbalkat bu mag ba woon, David Beckham moo ko moom, defoon na 11i jonante yoy, gañewu ci woon benn. Bi Messi dikkee lañu xamaat cafkay ndam. Ci ñaareelu xaaju joŋante bi la Messi duggu, mu ngi fekk ñu nekkoon ci 1-1, gannaaw ba ñu jiitalee woon ekibam mul delsi. Ñuy dawal noonu ba ca bopp jeexital ga rekk, Inter Miami am teg-dóor. Booba, ñoo ngi woon ci 94eelu simili bi. Messi dafa teg bal bi, laxas ko ci caax yi, rekk powu bay riir. Kii di boroom këlëb bi David Beckham dafa bég bay jooy. Ndeke, Messi jeexalagul. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | ÓBAMEYAN AK ISMAYLA SAAR CA MARSEILLE |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | Maarsey moo ngi wër di defaraat bu baax taxawaayu ekibam. Bërki-démb lañ siiwal ñëwub Óbameyaŋ. Moom sax, tàmbali na tàggatoom ak i farandooram ya. Ci dibéeru tey jii tam, biral nañ seen déggoo diggante ak Watford mi moom Ismayla Saar. Daanaka, gayndeg Senegaal gi, léegi kuppekatu Marseille la. Ëllëg ci altine ji lañuy saytu yaramam foofu ca Marseille laata lépp di mat. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | AB FEEBAR CI BIIR FC BARCELONE |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | Futbalkati FC Barcelone yi, jamono jii, dañu jànkonteel ak feebar bu law seen biir. Looloo tax sax ñu fomm joŋante bu njëkk bi ñu waroon a amal ëllëg ci doxantu bi muy amal fa Etaasini. Njortees na ni kenn ci ñi demoon Afrig ci bër yiñ amoon a ko indaale. Amaana mu bañ a ñàkku laata muy dem. Waaye, wax jooju amul ndëgëlaay. Nde, amul lenn lu koy firndeel. |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | AFROBASKET 2023, KIGALI |
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-23-7-2023/ | Sunu Jigéen ñi dem nañu Ruwàndaa bërki-démb, àjjuma guddi. Jot nañ sax amal gaawug démb gi seen tàggatu gu njëkk foofa ca tàggatuwaay (Gymnase) bu Liise Kigali. Afrobasket baa ngi war tàmbali 28eelu fan ci weeru sulet, war a jeex 5eelu fan ci weeru ut. |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | MAKI/XALIFA : MAG, BU RUSEE NE MAA-TEY |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Fan yii nu génn, bare woon na ñu doon yéy ak a yàbbi ci mbirum Xalifa Sàll, di wax ci njéggal bi ko Maki Sàll war a jagleel. Am na ci sax ay taskati xibaar yu demoon ba ne Xalifa Sàll këram lay tabaskijee. Waaye, bi nguur gi fésalee turi nit ñi Maki Sàll jéggal, ñu war a tabaskijee seen kër, kenn gisu ci ku tudd Xalifa Sàll. Muy mbetteel gu réy a réy ci ñenn ñi. Maki Sàll, moom, yéyu ci, yàbbiwu ci. Moone, askan wépp a ko ñaanoon njekk, kilifa diine yi, kilifa aada yi, kujje gi, kuréli way-moomeel yeek yenn mbootaay yi. Waaye, Maki dafa lànk, taxaw fi mu taxaw rekk. Rax-ci-dolli, ci ndoorteelu waxtaanu politig wi mu sumb, ñi ko wuyusi noon nañ ko li gën mooy mu bàyyi Xalifa. Wànte, dafa cosoon wax ji, yem fa. Nanguwu cee woon a sori. |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Maki Sàll dafa xaar ba dem bitim-réew, ca Biyaaris (Biarritz) ga muy teewe fan yii ndajem G7 mi, door a wax li mu xalaat dëggëntaan ci coowal njéggalub Xalifa Sàll mi nekk ciy loxoom. Ndaje moomu, nag, li mu jiite NEPAD moo tax ñu boole ko ci. Waaye, moom sax, bi mu dalee dem ay ndaje ba tey, mësta toj fenn. Ndaxte, dégguñu benn yoon fu ñu waxe ne Maki kat, bii yoon wax na wax ju réy, ni ko Ablaay Wàdd daan defe. |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Waaye, ba tey loolu ñorunu ; kàddu yi mu fa rotal ci mikóro RFI ñoo jar a bàyyi xel. Maki Sàll baat yii la fa wax ñeel Xalifa Sàll : « Bi ci njëkk mooy, wareesul a tënk giifalub làngu politig gi ci mbirum njéggal kese, yemale ko ci. Njéggalub njiitéef, ndeyu-àtte réewum Senegal moo ko jagleel njiitu réew mi. Kon, ci moom doŋŋ la aju, ciy loxoom kese la nekk. Moom mooy xool saa su ko soobee mu jéggale. Bu ko defee, sama yoon nekkul ci li taskati xibaar yiy wax ci njéggal bi, duma ci wax. Bés bu ma neexee walla ma am coobare gi rekk, dinaa ko def ni ma koy faral di defe. Ndax at mu nekk, lu ëpp téeméeri nit walla sax ay junniy nit, ci xayma, dinaa leen jéggal, génne leen kaso… » |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Kon, noo ko déggandoo : kàddu yii la rotal ca Frãs. Ñu mën cee amal ñaari njàngat yu gàtt. Bi ci jëkk mooy ne, Maki Sàll wegul waa réew mi, joxul cër askan wi walla kilifa yi fiy yeewoo. Waaw, lu tax Maki Sàll bitim-réew rekk lay waxe ak a waxtaane mbirum réew mi ? Xanaa réew mi amul i taskati xibaar yu mu mën a janool dégtal leen i kàddoom ak i xalaatam ? Lii bu tekkiwul ñàkk faayda ak suufeel sa boop ak sa réew lu muy tekki leneen ? Ndax kat, lii xeebeel la ci waa réew mi, rawati-na taskati xibaar yi fi fekk baax. Da leen a tanqamlu, dummóoyu leen te nëbbu ko ndax moo ne ci gémmiñu boppam : « sama yoon nekkul ci li taskati xibaar yiy wax ci njéggal bi, duma ci wax. » Ndege, deesul gis benn njiitu réew lu ñàkk faayda bay péncoo mbiriy réewam fii ci Senegaal. Moom kay, Maki rekk a koy defi ca réewi xonq-nopp ya. Muy wone ne, ba tey moomagunu sunu bopp dëgg dëgg, ndax sunu njiit yi amuñu fulla amuñu faayda. |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Ñaareelu njàngat bi nuy jële ci kàddoom yooyu mënees na ko xaaj ñaar. Benn bi nitu Maki ci boppam la ñeel, beneen bi aju ci digganteem ak Xalifa Sàll. Bi ci njëkk mooy réy ak réy-réylu bi Maki di biral ciy kàddoom : « …ci moom doŋŋ la aju… », « …ciy loxoom kese la nekk. », « Moom mooy xool saa su ko soobee mu jéggale. », « Bés bu ma neexee walla ma am coobare bi rekk, dinaa ko def »… Maki Sàll, li mu nuy xamal ci kàddu yii mooy ne, moom kott, moom kese- kese mooy dogal. Kenn mënul wañaar loxoom ba defloo ko lu ko neexul, ak koo mënti doon. Maki Sàll dafa summi yérey njiitu réew, sol yérey Buur Saltige. Ndaxte, buuru saltige rekk mooy jiitee doole, di jaay maa-mën, jàpp ne lu mu wax mooy am, lu mu waxul du am ; lu mu bëgg mooy am, lu mu bëggul du am. Ndege, njiitu réew day woyof, nangoo déglu askanam ak kilifa réew mi ba tax lépp lu mu jàpp, su ñu ko ñaanee mu bàyyi. Waaye, Maki jikkoy firawna lay doxe. Waaw. Ndax bu demee bay dolli ci waxam ji : « …ni ma koy faral di defe.» ak « …dinaa leen jéggal, génne leen kaso. », Maki day firndéel ni njéggal, jamono jii, ciy loxoom la nekk, ku ko neex la koy jagleel. Lii moo tax ndaw yi wutal ko dàkkental, di ko woowe « xaaju Yàlla » walla « àmbasadëeru Yàlla ci Senegaal ». Ndaxte, bu nee at mu nekk mu jéggal nit ñu bare, li wax ji wund mooy ku ci bokkul daŋ kaa neexul. |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Ci lanuy tàbbee ci ñaareelu njàngat bi ñeel digganteem ak Xalifa Sàll. |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Ndax seetlu ngeen lenn ? Saa su Makiy wax ci mbirum Xalifa Sàll, du jaar ci turam. Xanaa keroog ba mu nee “sama doomu baay la” ndax sant wi ñu bokk. Rax-ci-dolli, ñépp xam nañ ni jot naa yabal ay ndaw ca kaso ba ngir ñu gise ak Xalifa Sàll. Xamunu lu ñu fa waxante, waaye mel na ni Maki dafa dencal mer Xalifa. Te, Xalifa wax na du benn du ñaar ne sàkkuwul njéggal ci Maki te soxlawu ko. Dafa mel ni am na lu Xalifa Sàll gàntal Maki ba tax koo ñéññ. Coxorte giy feeñ ciy waxam ak doxalinam doy nañ firnde. Ma leen di laaj nag : waaw, lan la Maki jàppal ngóor si Xalifa ba tax muy doxale nii ak moom ? Lan lañu jot a séq ? |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Ak lu ci mënti am, askan wi moom moo gën a sonn Xalifa fuuf. |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Bi mu tàmbalee taw ba léegi, askan wi nelawatul, te waa Ndakaaroo ci gën a sonn. Kër yi taa nañu, koñ yi taa, mbedd yi taa, tali yi fees dell ak ndox, kenn amul foo jaar. Njëg yépp yokku, xaalis amul, oto yiy mbëkkante ci tali bi, nit ñiy dee. Kenn xamul fooy teg sa tànk. Metit yooyu yépp teewul nguur gi ne ée-yaay, nun danuy bër, njiitu réew miy wone ay portale mook soxnaam ca Tugal, ci kër gu taaroo taaru, di bége. Mu mel ni dañuy mbëllee baadoolo yi. Li am ba des moo di, ak Maki, mel na ni, laabisiina la réew miy jubal. |
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/ | Nu dem rekk. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | MBAY JAAG, GOR BI SENEGAAL AMEEL BOR (Xaaj bu njëkk) |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Xel tëju na, xalaat dëju. Xol tooy na, bët jooy. Ndeysaan… Gaynde wàcc na liggéey. Nee leen ko mbarawàcc, Jaag, nu sargal ko, delloo ko njukkal. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Mbay Jaag wuyuji na Boroomam. Dibéer, 12eelufan ci weeru me atum 2019 la génn àddina. Li Yàllay def, dibéer jooju dafa yemoo kepp ak 51eelu at ca ba muy jiite toogaayu-ñaxtu ba ndongoy iniwérsite bu Ndakaaru amaloon, waat ne fàww ñu janook Njiitu-réew ma woon, Léwopóol Sedaar Seŋoor, walla nguur gi ci boppam ngir àgge ko seen i tawat. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Mbay Jaag, nag, kenn umpalewul ne moo jiite woon kurélu Iniwérsite bu Ndakaaru, ca atum 1968 – booba, tuddagul woon Séex Anta Jóob – ga taxawoon di xeexal ndongo yi. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Ca yooyu jamono, fekk na Seŋoor nekk ci diggu ndëndam. Lu ko neex tëgg, ku feccul mu ni la génnal géew bi walla mu nëbb la jant bi. Ci gàttal, moo doon Buur, di Bummi. Ku say wax walla say jëf méngoowul ak i yosam, mu jaay la doole, ne la ràpp ci kaso bi, tëj. Waaye, kuy jaay fit, boo dajeek gaynde lamble. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Weeru me 1968 la ndongo yi jógoon, fippu, jàmmaarlook Nguur gi, ni ko : « Dafa doy ! Li nuy dund mënuta wéy ! » Ñu noon dee, coppite day am te dara lañu ci bañul. Ñu ga Nguur gi ci ne, na leen yokkal seen i ndàmpaay, jagalaat seen nekkin te it yeesal seeni jumtukaayi njàng. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Jamono jooju, daanaka fépp foo demoon ci àddina si, dinga gis ndongo yiy fippu di sàkku ab yeesal ñeel njàng mi. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Bu dee sunu réew mii, nag, UDES ak UED ñooy kuréli ndongo yi gënoon a fés ca xeex booba. Te, ñaari kurél yooyu yépp, Mbay Jaag ak i ñoñam ñoo leen jiite woon. Waaye ba tey ci njiit yooyule, Mbay Jaag lañu ci gënoon a ràññee. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Moom Mbay Jaag, nag, daanaka aul woon tiitukaay, ñi ko xamoon yépp, am fitam lañuy gën a fàttaliku tey. Rax-ci-dolli, dafa amoon pas-pas, farlu, te xareñoon lool. Kenn dàqu ko woon a wax ak mbooloo itam. Noonu, bu jëlaan kàddu gi, fu ne la nit ñiy fàqe ngir déglusi ko mbaa topp ci ginnaawam. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Mbay Jaag ! Kii moo amoon bayre, ndokk ! |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Jàmbaar jii moo teewoon nelaw Seŋoor ak i nduguroom. Waaye, Mbay Jaag ak ñi mel ni moom, foo leen fekk, nguur gu jubadi da leen di noonoo, di leen fexeel. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Moo tax Seŋoor mépp pexe mu mu xamoon lal na ko ngir sàkkal pexe Mbay Jaag ak ñi toppoon ci ginnaawam : nappaate, ger, tëj kaso, añs. Wànte du benn ci pexe yooyu bu ci àntu. Te, nag, ñi andoon ak Mbay Jaag ñoo ka bare woon ! Looloo tiitaloon Seŋoor, mu dem sax ba jàq lool. Ndax kat, ndongo yi dañoomayoon fit yeneeni kurél yi nekkoon ci réew mi, di liggéeykat yi booloo woon ciy sàndikaa yu siiw, am i tolof-tolof ba noppi ragal a fippu. Gone yee leen may fitu ñaxtu yi. Seeni rakk sax, ndongoy lekkooli diggu-dóom yi, dañoo jóg ñoom tamit. Mbir yi mujje ëpp i loxo ndax muy jàngalekat yi di óbëryee yi, kenn toogul. Koom-koomu réew mi tag, dara doxatul. |
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/ | Bi Seŋooramatul pexe, takk-deri Frãs yi sàncoon seen gàdd ci Ndakaaroo mujjee wallsi nguuram. Teewul, ndongo yi ak seeni njiit wéy di lëkkalook liggéeykat yi, jàpp fi ñu jàpp. Gornamaa bi jàq, teggi loxoom, woo leen waxtaan, nangul leen lu bare ci seeni ñaxtu, ba jàmm delsi ci réew mi. |