url
stringclasses
152 values
text
stringlengths
4
5.13k
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/
Wànte waxtaan wi taxu ko woon a yomb noonu : Mbay Jaag ak i ñoñam, dañca wone fullaak faayda ju mat sëkk, nañu ka daan defe naka-jekk. Fulla jooju ak pastéef yi ñu àndaloon bu ñu wàccaan ci mbedd yi ak tali yi, di sànniy xeer aka taal i póno. Ci njeexital li, ndongo yi jële nañfa ndam lu réy, doonte amuñu woon lépp la ñu bëggoon
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/
Xew-xew yu metti yooyu, nag, mëneesu leen a nettali ba noppi di bañ a tudd xale Naaru-Libaŋ bi ci ñàkkoon bakkanam. Keroog, bésub 29 ci weeru me, la alkaati yi song néegi ndongo yi, dal seen kaw, gaañleen, yàq mbaa sàcc seeni bagaas ak seeni alal.
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/
Mbay Jaag jitte woon na fi tamit ndongoy Iniwérsite bu Ndakaaru ci xeex bu mag bu ñu amaloon ci diggante 1971 ak 1972 te taxoon Seŋor tëjlu daara ju mag jooju.Dàqoon na yit ndongo yu bari ba noppi solal soldaar seeni njiit, yóbbu leen Kaasamaas, fa way-fippu PAIGC yi doon jàmmarlook làrme bu Purtugees yi. Ci ñooñu mënees na cee lim Ablaay Bàccili ak Mamadu Jóob Dëkurwaa… Bañkat yooyule, Mbay Jaag moo doon seen njiit. Ñoom ñépp ñu sànni leen ca Sancaba Manjaag, ci wetu Gine-Bisaawo, fa xare ba gënoon a mettee. Fa la Al Fuséyni Siise, kenn ci ñoom, faatoo ci anam bu ñaaw. Noonu la ñoom Mbay Jaag nekke woon ci làrme bi ak i jafe-jafe yu tar, ba biñ leen di bàyyi. Nguur gi jéem a saafara mbir mi, waxtaan ak ndongo yi, jëlaat ña mu dàqoon ba noppi fajal leen yenn ci seeni aajo.
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/
Ginnaaw gi la Mbay Jaag génn Iniwérsite dem jàngaleji matematig ca Cees, jóge fa dem liggéeyi Liise Jiñaabo bu Sigicoor.
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/
Xare yi mag yooyu askanu Senegaal difàttaliku tey, ndongo yépp a ci amoon ndam waaye jaloore ja ca Mbay Jaag jële, leneen mayu ko ko lu-dul taxawaayu njiit lu mat sëkk, ngor, njub, fit, ak xel mu ñaw, kaar !… boole ci ñàkk caaxaan bi ko ñépp mas  a seedeel, te ñu bare jàppe woon ko naqadi deret mbaa sax ñàkk kersa.
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/
Ñàkk caaxaan googoo ngi woon ci moom bés ba muy faatu.
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-bi-senegaal-ameel-bor/
(Fan yii di ñëw, LU DEFU WAXUdina delsi ci li des ci jaar-jaaru Mbay Jaag. Mooy doon ñaareelu xaaj bi)
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
FAN LANU JËM AK ÑAKKI BILL GATES YI?
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
(USÉYNU BÉEY)
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Coow laa ngi ne kurr ! Afrig ba Afrig daj, li ko dale Keer ba Peretoryaa, Ndakaaru jàpp Adis-Abebaa, wax ji benn la : jàppal wakseŋ fii, bàyyil wakseŋ fee.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Coow li nag, ci anternet bi la jëkke. Dafa am ay Móodu-Móodu ak ay Faatu-Faatu yu def ay widewoo di ci aartu seen i mbokk ak askanu Afrig wépp. Liñ ci jublu woon, ci seen i wax, mooy xamal leen ne, ci réewi Ërob yeek Amerig yi, am na ciy mbooloo yu laxasaayoo lëndëm, di lal ay pexe ngir wàññi limu nit ñi ci àddina si, te fas ko yéene tàmbalee Afrig ak nit ñu ñuul ñi.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Nee ñu, gëstukat yooyu kat, dañoo jàpp ne li àddina si am ciy nit dafa ëpp. Bu yàggee, dootuñu xaj ci kow suuf, dund bi dootul doy te kon xiif dina rey ñu bare. Ndaxte, suuf si dina dem ba dootul nangu, dara dootul meññ ; géej gi dina yulleeku ba jeex tàkk. Ci gàttal, dara dootul doy. Kon, ci gis-gisu ñooñu, warees na wàññi doomi-aadama yi bala njaaxum loolu di am.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Mu mel ni daal xalaati Malthus, benn boroom xam-xam bu mag bu doon dund ci 19eelu xarnu bi, ca Àngalteer, la ñuy dekkil noonu. Moom mi doon biral ne, feek wàññiwuñu limu nit ñi, dund gi ci kow suuf du neex, du yàgg.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Bu dara desulee lu dul tànn ñan lees war a wàññi, xeli saay-saay yépp ne yarr ci askanuw nit ku ñuul. Xalaas ! Mbete Yàlla !
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Bala maa dee ñu daas seen làmmiñ yi, singali nu. Ki ci gën a rafet wax mooy ki la naan :« nit ñu ñuul ñi dañoo xayadi te mën a jur ba nga ne lii lu mu doon ! » Ñi ci yées xalaat ñooy gënale xeet yi te naan : « Afrig a barey ndaw ! Nun, nag, ñi ëpp ci nun màggat nanu ba dóox, di xaar dee. Des na tuuti, xeetu nit ku weex dina sooy, nit ku ñuul jiite àddina si. Te loolu, warunu koo nangu tey, warunu koo nangu ëllëg, bun ko seetaanee mu ñaaw ! »
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Wax ju àgg, nag, dof yaa ko moom.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Lii lépp sax de, day nirook «léeboon ak lippoon». Naka la xalaat yu ni deme, di mën a juddu bay meññ ci xelu nit njaay, ku ànd ak i noppam ?
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Naal boobu, nag, ay boroomi alal, di boroomi tur, ay politiseŋ ak ay boroomi xam-xam ñoo ko sumb, jiite ko. Bill Gates ak Sarkoosi bokk nañ ci ñi ci gën a fés.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Bill Gates, moom, weddi na tuuma yooyu ñuy teg ci kowam. Nee na, waxul ñu wàññi nit ñi waaye nee na ni doomi-aadama yiy yokkoo lañu war a seetaat ngir yaxanal dund gi te neexal ko. Mu fas yéene cee def alal ju tollu ci 100 alfunniy dolaar. Maanaam 50 milyaar ci sunu xaalis. Li mu ci jublu, ciy waxam, moy xeex feebar yi ci Afrig ba noppi, fexee yemale njureel gi. Moom daal, nee na looloo mës a nekk taxawaayam te duggewu ko lenn lu dul sàmm bakkani doomi–aadama yi.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Waaw kii, dunu ko ne jàkk, ni ko : ‘Ngóor si Bill, wiiri-wiiri, jaari Ndaari. Xalaatoo ni Sàmbaay Bàcc rekk, am déet ?’’
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Rax-ci-dolli, ay kàngam yu mag a mag àddu nañ ci mbir mi, yokk ci seen xorom. Ku ci mel ni Thedros Adhanom Ghebreyesus, di doomu Ecópi, jiite kurél giy saytu wér–gi-yaramu nit ñi ci àddina si (OMS) ak it njiitu Mbootaayu Xeet yi (ONU), António Guterres bokk nañ ci. Ñaari kàngam yooyu yépp, artu nañ waa Afrig ci koronaawiris bi. Nee ñu, bees fagaruwulee ci lu gaaw, dina fi rey ay milyoŋi nit.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Waaye, li jaaxal ñépp mooy ni, ba sunu-jonni-Yàlla-tey-jii, Afrig mooy dànd gi gën a néewle fopp limu ñi Covid-19 bi daaneel, waxatumaak ñi mu rey.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Loolu nag, tekkiwul ne Afrig mën naa nelaw bay yàndoor ! Ndaxte, koronaawiris bi kat, bàyyiwul kenn !
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Li gën a teey xelu nit ñi nag, mooy waxtaan wiñaari gëstukati Farãs yi, doktoor Jean Paul-Mira ak porfesoor Camille Lotch, amal ci ayu–bés yii weesu rekk, te mu siiw lool ci Anternet bi. Ñoom ñaar ñooñu de, dañu doon wecceexalaat ci nu ñuy def ba am wakseŋ buy tax ñu jële Covid-19 bi ci àddina sépp. Ñu jàpp ni BCG, ñakk boobu ñu daan ñakk xale yi ngir xeex sëqët su bon seek yeneeni feebar, war nacee baax. Ñu tëje seen waxtaan woowule ci ànd gi ñu ànd ne Afrig rekk lañ war a defe jéemantu biy tax ñu xam ndax ñakk bi mën naa xeex koronaawiris bi am déet. Loolu, laata ñu koy mën a jariñoo ci seen i dëkk, ci Ërob mbaa Amerig.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Kàddu yooyu, nag, ñoo gënatee merloo doomi Afrig yu baree bare. Am ci ñu siiw ci ñoom, ñu mel ni Samuel Et’oo, Didier Drogba walla Àllaaji Juuf, ñu doon ñu ñu raññee ci mbirum futbal, ci àddina sépp, ak it Claudy Syar mu RFI (rajo bu Frãs moom)… Ñu di ñu am baat, seen kàddu mën a egg fu sori lool. Werante yeek xuloo yi neeti kurr ci Anternet bi, mu mel ni tulleek-màlle, di niru tuq su bënn te saañ ba réer !
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Fii nag ci Senegaal, li gën a teey xel, jaxase xel yépp, mooy dégtu (audio) biy daw ci xaraley jokko yu bees yi, ñu ciy dégg baatu benn Tubaab, di  njiitu Ayeropoor Belees Jaañ, muy xamle ne, daanaka Ayeropoor bi tëj na, ginnaaw yenn yóbbal yu ñu fay wàcce léeg-léeg, yu mel ne ay… wakseŋ ! Waa ji nag, bi ñu bare ci ñiy jëfandikoo xaraley jokko yu bees yi dale ci kowam, dellu na ginnaaw, ne moom masul a wax lu ni mel. Doonte dégtu  yaa ngi fi ba tey di ko tiiñal.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Ba ca jamono yooyu, xel yaa nga doon werante, naan dëgg laam déet.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Waaye ci fan yi weesu rekk, gis nañu ay kilifay Afrig di awante ci taskatu xibaar yi ngir teggi tuuma yi. Nee ñu, yëguñu, tinuñu. Waaye, li yéeme dëgg, mooy bi benn gëstukatu Kongo (RDC) bu ñu ràññee jëlee ñaari yoon kàddu ci diir bu gàtt, ba noppi ne maa waxoon-waxeet. Ca njëlbéen ga, dafa waxoon ne boolees na réewum Kongo RDC ci réew yiñ war a natte ñakk bi ñuy wax. Mu ne woon ne, ñoom, nangu nañu te joxe nañ seen kàddu. Bi saaga yeek diiŋat yi jibee, mu dellu ginnaaw ne, ñoom waa Kongo duñu mës a seetaan, ñuy jàppe seen askan nikiy mala.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Senegaal it, kenn demul mu des ñeel fésal cetug deram gi : mu di Ablaay Juuf Saar jawriñ bi ñu dénk mbirum paj mi, di njiitu réew mi Maki Sàll ci boppam, ñoom ñaar ñépp weddi nañu ba mu set, dem nañu sax ba ne, bu dee Senegaal rekk, kenn du ko fekk ci gaalu xaj googu !
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Ci sunu réew mii moom, ñépp a ngiy fàttaliku bés bi Bill Gates daje woon ca Kanadaa ak Maki, ca weeru sàttumbar 2016. Ndaje moomu juroon na fi coow ci ginnaaw gi. Waaye, ndawal àmbasadëeru Senegaal ca Kanadaa indi woon na ciy leeral, di biral ne, waxtaan woowule, dara sababu ko woon lu dul xeex feebar yu mel ni  sëqat su bon si, sibbiru, sidaa ak it ni ñuy def ba yemale njureel gi. Li wóor moo di ne foo séene saxaar, xal yaa ngay boy ca suuf !
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Fi mu ne nii daal, xel yi ñaaw nañu ba kenn xamatul looy def. Bu kenn ñakkatul doomam, ndax kon dinañu mën a jële feebar yu bari yi ci sunu réew mi, ak sax ci Afrig gépp ? Bu nu bàyyee ku ñëw rekk ñakkal nu sunuy doom, mbaa kon dunu dimbali ñiy jéem a faagaagal nit ñu ñuul ñi ci kow suuf ?
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Laaj yu am solo yooyu ñoo sampu tey te doomi Afrig yi, ak seen i njiit ñoo war a mànkoo joxe ci tontu lu leer, tey doon li gën ci xaley Afrig yi ak ëllëgu Afrig ci boppam.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Ñakk sa doom, mbaa bañ koo ñakk ?
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Mu mel ne Afrig tollooti na ci sélébeyoon bi mu tollu woon ca 1963. Jamono jooju, benn ci ñaari yoon lanu mënoon a jaar : yoonu Ufuwet Buwaañi ak Lewópóol Seŋoor, maanaam ànd ak doxandéem bi mu nuy wommat, walla yoonu Kwame Nkrumah ak Séex Anta Jóob, di tekki ne Afrig war naa mën demal boppam ci kow nu bennoo,  di xàccandoo di dóorandoo.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Yoonu Seŋoor ak Ufuwet woowu nu tànnoon moo nu tax a tollu tey fii. Saa su nekk nuy xaar ay doxandéem yiy jóge fu kenn xamul, ñëw  di nu wax lan lanu war a def, fan lanu war a jaar !
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Ndax bii yoon, dinanu takk sunu fit, tànn yoon wi nu Nkrumaak Séex Anta xàllal ciy jamono ? Àndandoo xeex nooni démb yi, yu tey yi ak yu jëmmi jamono yi. Bennoo bokk benn jëmu mooy tax Afrig am doole ak naataange. Booloo nuy tax a daan koronaawiris bi ; booloo moo war a nekk sunu kiiraay. Ndege, booloo mooy doole.
https://www.defuwaxu.com/fan-lanu-jem-ak-nakki-bill-gates-yi/
Askani Afrig, ëllëg, ëllëgu booloo la, ëllëgu moom-sa-bopp la !
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
WAAW, KAÑ LA SENEGAAL GËJ A YËNGOO NII…?
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Weeru màrs wii weesu, Senegaal tàngoon na jipp ! Gannaaw ba alkaati yeek sàndarm yi jëlijee Usmaan Sonko ngir jébbal ko Yoon, daanaka waa Ndakaaru yépp, waa Senegaal yépp sax, rawatina ndaw ñi, dañoo jóg nekk benn say, ne : “Du fi ame !” Keroog ak fan ya ca topp, jàppante bi metti woon na. Waa Nguur gi ne duñu bàyyi, gune yi gën leen a dëgër fi ñu jàpp. Noonu la fi fukki bakkan ak ñett rotee. Ñoom ñépp di ay waxambaane yu tollu ci seen diggu ndaw.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Ndax fu bakkan di rot, mat na di fa tudd yàqute yu dul jeex ci alal ? Ãxakañ ! Waaye, xel demul ci di leen méngale. Li nu soxal fii, mooy seetlu ni, li ëpp ci lu yàqu, nekkul ay alali doomi réew mi donte ñàkku ci. Waaye ay moomeelu doxandéem lañu, diy Tubaab yu sanc seen i këri-koom ci dëkk bi, ba tax ñu aakimoo daanaka koomu réew mépp. Këri koom yu mel ne Total, Auchan, Senac, añs. Loolu di nu fàttali bàkku yenn ndaw yiy xeex ngir Senegaal moom dëgg boppam : France Dégage ! (“Farãs jóge fi !”). Muy lu mat a jàngat ndax day wone ni, ndaw ñaa ngi ci tànki seen i mag yi fi nekkoon doon bañ nooteelu doxandéem bi. Te xaley tey yii, mel na ne ñoo gën a farlooti ci farata jooju.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Loolu lépp a taxoon Nguur gi dellu gannaaw, yolamal loxoom, bàyyi Sonko mu ñibbi. Guléet, ca ba muy ne ci jal bi, Persidaŋ Maki Sàll gis lu ko jaaxal, ëpp ko loxo ba tax mu walluji, ñaan xalifa yi ñu dugal seen loxo ci mbir mi, ba noppi nangul leen lépp lu ñu ko laajoon ngir indi jàmm. Mu mujje jél kàddu gi ñépp doon xaar, wax ak réew mi, ci anam yu ko kenn masul woon a gis : yëramtu, dige, ñaan njekk, woote juboo ak bennoo. Kujje gi ñoom it, wormaal kilifay diine ji, jóg ni kenn du dox i tànki jàmm bàyyi leen ginnaaw. Waxtu ya jiitu kàllaamay Maki yi, Usmaan Sonko jëkkoon na jël kàddu, wax waxi jàmm, waaye it teg ay sàrt yu leer yu Nguur gi war a jaar, ci gis-gisam, ba mën dalal réew mi.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Moo tax it, askanu Senegaal dina santati Sëriñ si. Ñoom ñi nga xam ne, daanaka, réew mépp a ngi doon xaar seen kàddu, ba nit ñi demee ba jàq. Ki ci gënoon a ràññeeku doon nag Sëriñ Muntaqaa Basiiru Mbàkke. Moom mi doxoon diggante Njiitu Réew mi ak kujje gi. Ñépp déggal ko, jàmm dellusi ci dëkk bi. Muy firndeelati solos sëriñ si ci nekkinu askanu Senegaal, te muy luy màndargaal Senegaal (te di dëggal lan ca jotoon a bind ci ginnaaw, ci sunub bataaxal bu nu duppe woon : ”Sëriñ seek a bari doole !”).
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Waaye, ba lépp nee tekk, lépp sedd, waa Nguur gi mel ne du ñoom : ña laqatu woon ñépp génnaat di mbéléléli ci rajo yeek tele yi. Maki woote ndaje, wax ak guney pàrteem, di gaaruwaaleek a xupp kujje gi : “Li fi amoon, du fi amati !”. Mel ne, tey la Waalo gën a aay.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Teguñu ci juróomi weer, Persidaŋ Maki woo Ndawi Réew mi, wotelu sàrt yu yees yuy rëbb mbéeféer yi, ci ni ñu ko waxe.  Mu nel ne nag, dañuy taafantoo jiyaadis yi, ndax ku seet ba ca biir xam ni, ñi ñuy rëbb dëgg, du ñeneen ñu dul waa kujje gi ! Noonu boog, la ko ñu bare jàngate, ay boroom xam-xam yuy jàngale ci iniwérsite yi, waa kujje gi ci seen bopp, ba ci Usmaan Sonko mii jagleel xew woowu ay kàddu yu am a am solo. Du caagéen ne, danuy tëkkale Usmaan Sonko ak ay kàngami Afrig yu mag yu fi nekkoon. Waaye nag, neexul ba neexul, ngóor si, ni mu waxe keroog jooju, gëj na fee am (jóge ciy way-pólitig), ca jamonoy Séex Anta Jóob walla Tomaas Saŋkara. Ne jàkk waa Tugal, tudd seen tur, xamal leen ne lu bon te yées ci Afrig, ñoom a, walla boog seen loxoo ngi ci. Ba noppi di leen digal ñu teggi seen loxo ci kaw Afrig te abal nu !
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Sàrt yu bees yii nag, li ci doy waar mooy ne, ëpp nañu téeméeri ponk, te sunuy Ndawi Réew mi, ciy “anam yu jamp” la leen ko gornamaŋ bi jébbal, ñu war koo jàngat itam ci diir bu gàtt (benn ba ñaari ayu-bés). Moone, ñoom ci seen bopp, ci bataaxalu Commission des Lois, di kurél gi ñu jagleel liggéeyu caytu sàrti Yoon yi, ñu ngiy xamle ni :
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
”Code Pénal bi ak Code de procédure Pénale bi (ñaari téere yooyu ñu leen di woteloo) soo leen joxoon ñu seen xel màcc ci mbiru Yoon sax, dinañu am i jafe-jafe ndax dañoo naqaree jàng, kenn mënul a xam dëgg lu ñu wund ; waxatumaak nun Ndawi Réew mi nga xam ni, dara lañu amul ci xam-xamu Yoon”.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Waaw, ñii de, ñu xam loolu ba noppi, bind ko ba mu leer ci seen bataaxal, ñoo walbatiku wote sàrt yooyee, te naan nu: ‘Sàrt yii baax nañu ci askan wi’! Ku leen di déglu ba di leen gëm ?
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Maki moom, booba, mu ngiy wër réew mi, dëkkoo dëkk, di nemmeekuji koomu gox-goxaan yi. Ci li mu lay, ndax ñu bare weddil nañu ko loolu, jàpp ne ay yëngug pólitig doŋŋ lay doxal noonu. Lum ci mënti doon, li yéeme ci mbir mi, mooy nit ñu baree bare yi muy dajale saa su ne, ciy jamanoy koronaawiris bii ! – Am sax ñu ñuy yab ciy woto, péey ba péey, gannaaw ba ñu leen compalee as tuut ciy koppar -. Dëgg la, ba mu noppee ciy doxontoom yooyu, xelam dellusi na, ba tax muy digle ñu bàyyi mbooloo yu tàkku yi ñuy woo ci xew yi. Xéy-na ndax “Covid 19” day moytu ay xewi Persidaŋ Maki Sàll ? Bugaan Géy Dani moom, faalewul waxi Maki yooyee, ndax moom it sol nay dàllam di doxal li mu tudde “Tibbi Tànki Maki”. Di wër réew mi, fu Maki jaaroon mu jaar fa, lu Maki waxoon, mu weddi ko ba mu set wecc ! Nit ñu baree bari di ko topp. Usmaan Sonko, moom it, ne kenn du dem mu des, daldi jëlaat “Nemmeeku Tuur” yi mu nu tàmmaloon. Wuudey Medina yi de, ñoom, duñ ko réccu ndax seen i njaay yi mu leen fexeel ba ñu jar, ci kaw dimmali liggéeykati Senegaal yi.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Senegaal nag, wax ko te dee, day réew mu doy waar ! Ndax kat, jamono jii koronaa bi gën a lëmbe àddina si, rawatina ci miim réew, la nit ñi mel ne ñu raatukaan ! Ku la gën a ñeme mbas mi, nga ni kii la ! Mu mel ne, nit ñi dañoo dem ba ës, walla book ñu tul (tul bu wuteek ñakku yi fi lamb ba dee !) ba tax koronaa bi du leen mënal tus ! Te kenn rawu ci way-pólitig yi.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Waaye kenn du nettali doxantuy Maki Sàll yooyu te doo yëy yàbbi ci mbiru nervis yi, maanaam dóorkat yi ! Ñépp gisoon nañ fi ne, ci xew-xewi màrs yi, ay sàmbaabóoy yu gànnaayoo seen i yat, walla ay jaasi, ñoo doon daw ci tali yi di rëbb xale yi doon ñaxtu, di leen jàpp, di leen dóor, dóor yu metti. Loolu lépp nag, doon ame ci kanamu takk-der yi, mu mel ne sax, ñoo àndoon ci seen “liggéey” boobu ! Dóorkat yooyee ñoo feeñaat ci doxantu Maki yi. Ñu neeti ci seen mënin, di jàpp, di dóor gone yiy ñaxtu walla sax ku ñu gis rekk nga sol mbaa nga takk lu xonq ! Dëgg la, seen kilifa moo fi newoon, lu yàggul dara, moom lu xonq du ko gis ! Waaye ku taxaw seetlu dinga gis ni, ba Persidaŋ duggee Tuuba, dóorkat yi dañu ni mes ! Kenn gisul, kenn yëgul. Moo tax it, gune yi xaaruñu ku leen woo : takk seen i sagar yu xonq coyy, di yuuxu, di sànni suuf, ñenn ñi sax di yuuxu turu… Usmaan Sonko ! Dóorkat yi daal (walla seen kilifa ?) ñemewuñu Boroom Tuuba ! Lu mu ci mënti doon, gannaaw takk-der yi, ay dóorkat, fenn lañ leen soxlawul. Te réewum Yoon sax, daa mënut a ànd ak li nu mel. Maki nag, war naa seetaat boppam !
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Ayu-bés gii ñu génn nag, Persidaŋ wooti na Ndawi Réew mi, ñu wotelati ko ay sàrt yu bees yu jëm ciy doxalinu wote yi. Fii tam, lu yéeme feeñ na fi : lu bare ci déggoo yi amoon ca Dialogue National ba (Jataayu Waxtaanekaayu mbiri Réew mi), walla ponk yu ñu yaakaaroon ne Persidaŋ dina ci jël ndogal, dañu leen teggi teg fale ! Xeli nit ñi gënatee teey ci mbirum ñetteelu màndaa bi ñuy ruumandaat booba ba léegi, di wax naan, mu ngi ci xelu Maki. Te loolu lépp fekk na mu soppi, ni mu ko neexe, tëralinu gox-goxaan yi ci Ndakaaru, te tagguwu ci kenn ! Waaye li ci kanam rawul i gët.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Fii ñu toll nii nag, yenn xel yaa ngiy ñaaw, yeneen yaa ngiy nàcc. Lii lépp ciy xew-xew yu baree nii, ame ci diir bu gàtt ; xew wu la ci gën a metti walla gën laa lëj, nga ne bii la. Mbaa réewum Senegaal dina ko mën a dëkku ? Mbaa du ñaareelu “weeru màrs” daf fe nar a am ? Li gune yiy woowe 2e vague, maanaam ñaareelu sóobu ciy ay ? Dëkk bu yëngu bii, nu fiy jàmm dellusee, sax fi dakk ? Te muy jàmm ju lalu ci dëgg ?
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Wax jaa ngi noonu. Nun waa Senegaal nag, ndax warunoo seetaat sunu bopp ? Ndax kat, fu fen di mën dëgg, fu kàdduy worook i jëf, taxawal fa luy jëm kër du yomb ! Rawatina réew moo xam ne, Nguur gi, jay-doole rekk la xam te di ko doxaale bu baax. Fàww kon, ñi bokk gis-gis te gëm seen bopp, gëm demokaraasi te féeteek askan wi, booloo, takku tey xàccandoo di dóorandoo, su nu bëggee tekki buumu-njaam gii nu tënk ba léegi.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
Uséynu Béey
https://www.defuwaxu.com/xecc-bu-danee-dagg/
XËCC BU DAŊEE DAGG !
https://www.defuwaxu.com/xecc-bu-danee-dagg/
Nimbir yiy doxe diggante nguur geek kujje gi bi Màkki Sáll toogee ci jal bi ba tey jii, dalul xel dara. Nun ñépp a ànd ci demokaraasi, waaye ni ko peresidaŋ Sàll gise — ku am doole danga koy wone, doo maye dara, doo yërëm kenn — mën naa jur ëllëg musiba ci réew mi. Ci sama gis-gis bu gàtt, dafa war a méngook li gën ci sunuy aada. Senegaal, waxtaan ba juboo lanu xam, lu fi am solo. Su dee wote rekk, nag, kenn du ni guléet, miim réew yàgg naa tabb ay njiitam te deret du turu. Lu jar a fàttaliku la, tey jii alal ju bari feeñ na ci suuf si. Mbaa du sax petorol boobook gaas bee yóbbu fiti ñenn ñi ? Bu nu ànduleek sunu sago, am nay réew yu mag ak i boroom doole dinañ jéem a salfaañe Senegaal ngir rekk aakimu alal jooju. Nanu ci Yálla musal waaye noonu la ko gaa ñooñu tàmmee def.
https://www.defuwaxu.com/xecc-bu-danee-dagg/
Kon, li war ki Yàlla teg ci boppu réew mi, mooy xam ni nun ñépp, ba ci kujje gi sax, njabootam lañu. Su ko defee mu wuuf ñépp, bañ a tànqamlu kenn. Nay yolomal buum gi bu ko mbir yi laajee, te yit këwdiir giy bax ci kaw taal bi, na koy moytoo tëj ràpp. Li peresidaŋ Abdu Juuf bàyyiwul woon xel ci looloo taxoon ñu tëral sàrtu wote bi ñépp àndoon ci atum 1992. Dafay faral ñatabal nit ñi ba ñu sës te du yoon. Ak li muus di néew doole yépp, bu sësee songe te kuy bëgg a lab sax, soo ko tàllalee jaasi mu jàpp ci.
https://www.defuwaxu.com/xeesal-walla-xeeb-sa-bopp-2/
XEESAL WALLA XEEB SA BOPP?
https://www.defuwaxu.com/xeesal-walla-xeeb-sa-bopp-2/
Kañ la jigéeni Senegaal yi tàmbalee xeesal ? Fanweeri at ci ginnaaw ? Lu ko ëpp ? Gëstukati réew mi war nañoo tontu ci laaj boobu. Li ma ci xam, daal, moo di ne mu ngiy bëgg a yàgg. Mel na ni ca njëlbéen ga ñu bare dañu newoon ci seen xel : ‘’Lii de, baaxul, waaye ay feemi gone la rekk, du jikko, jamono la, léegi ñu génn ci !’’ Njuumte lu réy la woon ndax fi mu ne nii, yematul ci jigéen ñi, ay góor sax a ngi diwu… Ku sañul ni bala la yit, xalaat nga ko. Ku weddi ne tey la Waalo gën a aay, doxantul ci mbeddi Ndakaaru yi, téen xool nataali-siiwal yiy tagg xees ak xeesal. Boo toogee sa kër tamit, taal sa tele dinga gis ñu ciy wane ndaw suy diwu, yànjal la ko ba nga ni lii lu mu doon, nataal yi di la déey musiba, naan la ‘’Nii nga war a mel !’’, walla : ‘’Nii nag la sa soxna war a mel !’’’ Wax ji moom jarul a yërëm, li xeesal tekki moo di ne am der bu ñuul gàcce la, taaruwl dara, loo gën a nirook Tubaab ñu gën laa teg nit. Mbir mi dafa dagg xol ba noppi yéeme. Xéy-na lu ni mel mënoon nañ ko séentu feneen ci Afrig fu dul Senegaal. Liggéey bu mucc ayib bi Séex Anta Jóob def ngir weglu nit ku ñuul waroon naa tax nu àndandoo sib xeesal. Te yit, xanaa Senegaal dootul réewum ‘’Négritude’’ ? Xanaa du Seŋoor a bind ‘’Femme noire’’, taalif bi gone yiy tari subaak ngoon ? Lii lépp a merloo woon Aysa Dem, mi ñépp xam ci farloom ñeel mbiri aada, ba mu jiite fi kàmpaañ, duppe ko ñuul kukk di fésal taaru jigéen ju ñuul ak ni nit ki waree naw boppam. Fulla ju mat sëkk la Aysa Dem wane foofu te ñu bare gërëm nañ ko ci. Waaye li gënoon xéy-na moo doon ñépp àndandook moom ci xeex boobu. Mbootayi jigéen ñi nga xam ni foo leen fekk ñu ngi ñaxtu, naan dañoo sàggane seeni yelleef, kenn waruleen woon cee jiitu. Léegi, nañu yëkkati seen kàddu, wax kilifay réew mi ñu aaye kuy def piblisite xeesal, aaye sax xeesal ci boppam. Am nay jàngoro yoo xam ni gornmaa rekk moo leen mén a faj. Xeesal ci la bokk. Loolu la Paul Kagamé, njiitul Ruwandaa, xam ba jël ay dogal yu am solo, tere kuy dugal walla kuy defar diwu yu ni mel ca réew ma, tere yit ku ko jaay, ku ko jënd mbaa ku ko jëfandiko. Loolu lañ fa dogal te ku ko moy yoon dal ci sa kow. Teewul doktoor yeek yeneeni boroom xam-xam war di wéy di gindi jigéen ñi, di leen yee ba ñu xam ni nit ku weex gënul nit ku ñuul. Waaye liñ naan bóli gu dog tiiñ na doktoor moo fi ne. Ndax ndaw soo laaj lu ko xiir ci xeesal mu am ci kersa, damm loos ni la lépp ak góor ñi, soo xeesul duñ la faale. Ñu ci bare leeral rekk a leen ciy dugal, ñu dem ba yëf yi ëpp leen loxo, fu ñu gis diw jënd ko, diwoo. Moonte xam nañ xéll ni xeesal day oyofal sa der, wàññi dooleem, foo laal daj ay picc ak i rew ak i taas, soo moytuwulee jële ciy feebar yu bon niki kañseer walla taŋsiyoŋ. Doktoor yi seen xam-xam màcc ci pajum der wax nañu ba tàyyi, waaye kenn nanguwuleen a déglu. Waaw, ndax wut taar rekk jar naa ñàkk sa bàkkan ? Ñàkkul jaaykati xeesal yeek isin yi koy defar la nguur gi ragal ba tax ko ni patt-pattaaral, di seetaan lu ñaaw lii mën a delloo réew mi ginnaaw. Am na ñu naan du loolu lépp, dafa ferekk ni sunuy njiit tal nañu leneen, nun baadolo yi amaluñ leen benn solo. Xanaa kay du loolu laa yaakaar ? Ku xeeb sa bopp, dem sax ba xamatoo yaay kan, mënoo amal benn njariñ saw askan. Kon, nanu ci jóg gaaw : xeesal jëmul kër… Ndey Koddu Faal
https://www.defuwaxu.com/xeesal-walla-xeeb-sa-bopp-2/
XEESAL WALLA XEEB SA BOPP ? was originally published in Defu Waxu on Medium, where people are continuing the conversation by highlighting and responding to this story.
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
KUPPEG ÀDDINA GEES JAGLEEL U17 FA ENDONESI
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Tànnees na fukk ak benni ndaw yi war a teewal Senegaal fa Endonesi ñeel kuppeg àddina jagleel ñi ëppalagul 17i at. Nii la toftale gi tëdde :
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Góol yi
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Sëriñ Juuf (G.Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Makura Mbuub (G.Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Séex Bàmba Faal (Diambar FC)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Defãsëer yi
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Sëriñ Fàllu Juuf (G.Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Mammadu Aliw Jàllo (Diambar FC)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Guy Feliks Lima (AFAT Thies)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Ibraayma Jàllo (G.Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Buubakar Saajo Ba (Étoile Lusitana)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Sériif Keebaa Ñabali ( Océan FC)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Alfa Aamadu Ture (G.Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Miliya yi
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Piyeer Antuwaan Jaata Dorival (Dakar Sacré Coeur)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Paap Daawda Jong (AF Darou Salaam)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Sëriñ Saaliw Fay (G.Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Mammadu Lamin Saajo (Environnement Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Mammadu Ñing (Espoir de Guédiaway)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Ataakã yi
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Idriisa Géy (G.Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Omar Sàll (Environnement Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Yayaa Jémme (Diambar FC)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Amara Juuf (G.Foot)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Mammadu Sawane (AFAT Thies)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Clayton Silverio Kàndi (Espoir de Guédiaway)
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Ñii ñooy ndaw yi ñu tànn ngir ñu dem teewal réewum Senegaal ca kuppeg àddina giy ame fële ca Kembaaru Asi, dëkku “Indonesie”. Joŋante bi nag moo ngi war a tàmbali fukki fan ci weer wii nu nekk. Réewum Senegaal mépp di ci ànd ak seen i doom di leen ñaanal ñu ame fa ndam.
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
Mànkoo jëli ndam li !
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (2/7/2023)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/
Dëmi-finaal U23
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/
Ginnaaw-ëllëg, talaata 4i fan ci sulet , la dëmi-finaali joŋateb kuppe U23 di door fa Marog. Esipt ak Gine Konaakiri ñooy laale bu 17i waxtu ci ngoon jotee. Bu jeexee, Marog mi dalal po mi dana dajeek Mali ci ñaareelu dëmi-finaal bi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/
Njortees na ne, joŋante yu neex la nar a doon. Nde, kenn ku ci nekk doo nangu sa moroom dóor la. Te yit, jamono jii, ekib yépp a defaru bu baax a baax. Rax-ci-dolli, ku ci nekk dafa bëgg a jël kub.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/
Cargalug Ànderes Iñestaa fa Sàppõ
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/
Ginnaaw ba mu jugee Barcelone mi nga xam ne moom la ko ñépp xamee woon, ba ñépp jàppoon sax ni du fa mës a juge, Iñestaa, saa-espaañ bi, dafa demoon fee ca Sàppõ. Ca la demee ca këlëbu bu ñuy woowe Vissel Kobe, def na fa 5i at ci ren ba démb ci gaawu gi la doon amal joŋanteem bu mujju foofu. Na mu jooyee woon, keroog  ba muy jóge Barça, noonee la jooyati ba ñu koy sargal cargal gu mag ci njeexitalu joŋante ba. Demoon nañu ba jaayukaayi tikke ya sax dafa mujje tëj ndax fowu bu fees dell. Muy lu mu yellool, ndax def na ci futbal lu nekk, jël ci itam lu nekk. Bokk na tay ci kuppekati digg yu gën a xereñ ci àddina ba sañoo lim ñett te waxoo turam.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/
Ndax dafay aj i dàllam am daf koy solaat tuuti, dara wóoragu ci, nañu ko déglu ba xam lum ci namm.
https://www.defuwaxu.com/ay-du-yem-ci-boppu-boroom/
AY DU YEM CI BOPPU BOROOM
https://www.defuwaxu.com/ay-du-yem-ci-boppu-boroom/
Senegaal, jamono ji ñu tollu nii dafa mel ni nekk doomu– réew mi rekk doyatul ; fàww nga fésal wet gi nga féete, moo xam sa diine la walla sa tarixa mbaa pàrti pólitig bi nga faral ba ci sax mbootaay gi nga bokk léeg-léeg.
https://www.defuwaxu.com/ay-du-yem-ci-boppu-boroom/
Waaye li ci gën a tiis, tey tiitalaate ba noppi ruslu mooy ñaawtéefi ñi ñuy tudde boroomi xam-xam. Ñenn ci ñoom a ngi taal i daay, ñi ci des di leen xamb. Ndax kilifa war naa làquy giseek i doomi-réew mi naan leen su nu jàppalewul Diw ci joŋante biy dégmal mu ñaaw ndax nook moom a bokk waaso ? Ana lu yées lii ?
https://www.defuwaxu.com/ay-du-yem-ci-boppu-boroom/
Ruwàndaa bokk na tey ci réew yi ñu gën a naw ci Afrig waaye du tax kenn fàtte la fa xewoon ci atum 1994. Kodiwaar tamit, démb rekk la woon. Kon mbirum waaso ak xeet du lu ñuy kafe.