url
stringclasses
152 values
text
stringlengths
4
5.13k
https://www.defuwaxu.com/ay-du-yem-ci-boppu-boroom/
Nun waa Senegaal nag, li nuy seetaan muy raam, ci ñag bi la jëm. Te kenn ñaanu ko Yàlla. Nan bàyyee nax sunu bopp, naan bal du fi tàkk, jaasi du fi jóg ndax lii walla lee. Nanuy fàttaliku ne noo bokk ndey bokk baay tey moytu lépp lu nuy féewale. Ngalla buleen fi yee fitna ndax, kat, bu keroogee kenn du ci mucc. Du xam ngeen ni ay du yem ci boppu boroom ?
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
‘’LI TAX SÉEX ANTA JÓOB AMUL MOROOM…’’
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Li ngeen ciy jàngsi mooy xaaj bu njëkk bi.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Saada Kan : Noo ngi am mbégte delsi ak yéen ci seen jotaayu waxtaan « L’entretien » bi nu leen di dégtal ñaari ayu-bés yu nekk. Tey, nag, noo ngi dalal gan gu mag, ab werekaan bu ñu ràññee ci àddina sépp, mu di ab bindkat bu yebu ci ittey réewi Afrig yi rawati-na ci lu ñeel seen daraja, di ab móolkat, taskatu xibaar, jàngalekat. Kookooy Bubakar Bóris Jóob. Moom lanu fi dalal tey, fas yéene waxtaan ak moom. Kon, Bubakar Bóris Jóob, ginnaaw bi nu la nuyoo, nu bàyyi la nga nuyoo laata nuy sóobu ci waxtaan wi.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Bubakar Bóris Jóob : Jërëjëf Saada. Maa ngi lay sant di la gërëm ci dalal biŋ ma dalal ci jotaay bii nga xam ne, xam naa ko bu baax sax. Ndaxte damay faral di ko seetaan saa yu ma ko sama jot mayee. Ndax li may toog bariwul, saa su nekk maa ngi ci roppëlaan yi. Waaye, jotaay bu ma yitteel la ; dama koy seetaan saa yu ma amee jot.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Saada Kan: waxtaan wi nag, dama koy doore ci ndokkeel la ngir yool biñ la jagleel fan yii weesu ca Etaasini.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Jërëjëf. Yool bi, “Harold Ethel L. Stellfox” lañ ko dippe. Iniwérsite Dickinson bi nekk ca Pensilwani, ca réewum Amerig, moo ma ko jagleel. Ma bég ci lool sax, ànd ci ak sag bu réy. Ndax, ñi ma ci jiitu, ay bindkat yu mag a mag lañ, ma bëgg leen lool, def leen ay royukaay te daan jàng seeni téere ca ba may ndaw. Looloo ma tax a bég ci li ma jot ci yool boobu. Jëli woon naa ko. Jot naa fa amal sax aw waxtaan, jàngaale fa tuuti sama téere bi, Murambi ci nasaraan ak sax Doomi Golo ci wolof.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Saada Kan : Nga ne ma ! Ci wolof, nag…
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Bubakar Bóris Jóob : Waaw, waaw. Mayoon nañ ma ko. Li ma ko dugge woon mooy baaxe am mbooloo mu déggul wolof, taaru kàllaamay Kocc ak neexaayam.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Saada Kan : Noo ngi lay sant ci sa teewaay ci waxtaan wi. Naam, ñépp a la xam. Waaye, du ñàkk mu am ñu umple ne, ca njëlbéen, jàngalekatu xeltu (philosophie) nga woon, nekkoon tamit taskatu xibaar. Nu gis ne at yii weesu yépp, yaa ngi doon jàngale, di bind, di amal i waxtaan, di wër àddina si. Jamono jii sax yaa ngi jàngale ca Niseryaa. Muy biral ne yow, jëfkat nga. Ma bëgg laa laaj, ndax du xeex bi ngay xeexal làmmiñi Afrig yi, rawati-na wolof, moo la yóbbe loolu lépp ?
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Bubakar Bóris Jóob  : Waaw. Jàpp naa ne, xeex booboo sabab lépp. Te, du loo xamante ni, dafa xéy rekk sotti. Boo xoolee ba ci biir, dinga gis ne sax, jaar-jaar boobu nga tudd, fa la bépp bindkat di faral di jaar, rawati-na bindkat buy xeexal jenn itte ju ko ñor. Maanaam, dangay nekk ndaw bu gàtteñlu, bëgg lool njàngum téere yi, di jéem a topp ci tànki bindkat yu mag yi. Rax-ci-dolli, ngay bindantu ay taalif yu ndaw, ay kilib ak ay téere fent. Noonu nga koy jàppe ba xéy bés, génne ab téere. Bu ko defee, ñu jàppe la bindkat, ndax du yaa koy def sa bopp. Ndege, fàww nit ñi jàppe la bindkat nga door di ko nekk. Noonu, ay ndigaale sa diggante ak nit ñi tàmbalee juddu ; ngay tibbe ci mboolem-nawle mi di bind, di roote ci seen nekkin ak dundin ay xalaat ak i gis-gis di leen jëmmal ci say biir téere. Ñoom itam, ñuy jàng say téere di la ci laaj ngay tontu. Waaye, duñu ci yem. Ndaxte, dinañ lay faral di laaj sa xalaat ci nekkinu askan wi, xew-xewi jamono walla sax xew-xewi àddina sépp. Bu ko defee, nga sóobu ci illa ju bees : jëmmal nekkinu nit ñi, rawati-na wu doomi Afrig yi. Noonu la bindkat bi di jëflante ak askan wi. Maanaam, ci moom lay jële daa ji muy rëdde téereem yi ngir jëmmal seen nekkin, dégtal àddina sépp kàddu yiy riir ci seeni xol te seeni làmmiñ të leen a tudd.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Léegi, nag, bu ñu seetloo, xool nekkin ak dundinu doomi Afrig yi, benn njàngat lañ ciy jële : njaam gi deñagu fi. Njaam gi maam yi doon dund ca jamonoy njaam ga ak ca jamonoy nooteel ba, am na ba tey. Ba jonni-Yàlla-tey jii, mënees na ràññee màndarga yi ci réewi Afrig yi : yorin wi, nguur ak njiit yiy jaamu nootkat ba woon, toroxtaange ak tolof-tolof yi askani Afrig yi di jànkoonteel bés bu nekk.  Li ci gën a doy-waar mooy ne, Afrig rekk ngay fekk ay bindkat yuy bind ci làkk woo xam ne, seeni nawle walla ñi ëpp ci askan wa ñu bokk dégguñu ko.  Muy lu yéeme ! Lan moo leen di tax a bind ak kan lañuy bindal ? Ndax xel nangu na loolu ? Man ci sama bopp, ndànk-ndànk laa tàmbalee yeewu ci mbir mi. Te bu loolu amee, ginnaaw Yàlla, maa ngi koy sante jàmbaar ju mel ni Séex Anta Jóob, sama doomu-baay bi.  Te du man rekk, képp kuy xeexal làmmiñi Afrig yi, seeni aada ak lépp lu ñeel seen daraja, war ngaa delloo njukkal Séex Anta Jóob ndax moo sumb liggéey bi, xàllal nu yoon wi.  Ci gàttal daal, mbirum làmmiñ lu am dayo la ci sama jaar-jaar.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Saada Kan : Am na loo mës a wax, te mu soxal ma lool. Nee nga bés “nekk doomu Afrig, mook dund mbugal ñoo yem”.  Mu mel ni li wax ji wund mooy dafa jot nu xeex ngir sunu daraja. Yow miy boroom wax ji, loo ci namm dëggëntaan ?
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Li ma tax a wax ne, nekk doomu Afrig, mook dund mbugal ñoo yem, ñaari mbir la. Bi ci jiitu, mooy jafe-jafe ak boddikonte yi doomi Afrig yi di dund jamono jii, rawati-na boroom der yu ñuul yi. Tey, mbañeel ak tiitaange ji yeneen xeet yi ameel nit ku ñuul moo ma gën a tax di wax. Ndax, Jamono jii, ñaawalees na lépp lu aju ci nit ku ñuul walla mu ñeel ko. Moom kay, tudd Nelson Màndelaa walla Baraak Obamaa sax génnewu la ci. Feek yaa ngeek der bu ñuul, jàppees na la nib gàkk-gàkk walla tilim bees war a raxas ba mu set wecc, jële ko fi. Loolu, ñuulaayu nit ki la ñeel, muy benn. Bi ci topp, nag, doomi Afrig yi ci seen bopp la ñeel. Dafa di, cosaanoo Afrig ñenn ñi bàkkaar lañ ko jàppe. Tey, bët bu ñaaw lañuy xoole Afrig. Boo nee Afrig rekk, xel yi dem ci xareb maxejj yi (guerres civiles), coxorte, yorin wu ñaaw wi ñu yore réewi Afrig yi, cambar-cambar bi, ndóol bi ak tumurànke bi, nger mi, añs. Saa boo xamee ne, nit ku ñuul nga teg ci nekk doomu Afrig, dañuy jàpp ne warees na la jéppi, xeeb la, suufeel la.  Loolu laa tudde mbugal.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Saada Kan : Kon, Bóris, bu ñu la déggee, ngir nu mucc ci jafe-jafe yooyu, ngir nu nekk, fàww nu xam nun nooy ñan. Te loolu, mënta àntu feek geestuwunu démb, roy ci maam ya tey ndamoo sunuy moomeel. Mu mel ni looloo la tax a bind ci wolof. Rax-ci-dolli, mënees na méngale sa taxawaay ak bu Séex Anta Jóob.   Ndax danga jàpp ne, wareef la ci doomi Afrig yi ñu wéyal xeexam ak ndono li mu nu bàyyee ?
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Mi ngoog. Loolu kese la, du leneen. Man, dama jàpp ne ñi ëpp ci nit ñi dañu réere mbiri Séex Anta Jóob. Ndaxte, saa yuñ ko tuddee rekk, xel yépp dem ci Misra mu njëkk ma, mómi ya, piramid ya, ca wax ya mu daan wax ak li mu bind ci sunu cosaan te mu doon lu am a am solo. Xel yi dinañ dem itam ci firnde yu leer yi mu jële ci gëstoom yu xóot ya, te diy wone ne, baaxi maam yu Misra yu njëkk ya, ay nit ñu ñuul, diy doomi Afrig, ñoo ko jëmbëtoon, suuxat ko ba mu naat lool, raw ci àddina sépp jamono jooju. Toog nan fi diir bu yàgg, Séex Anta rekk a doon wax ne, Afrig a sukk jur àddina si. Bépp xeetu mbañ ak ngànt indil nañ ko ko, weddi ko ngir rekk bëgg a werante. Ñi bañoon dëgg googu, àggoon nañ ci sos ay fen yu tooy xepp ngir rekk mbañ, xeebeel ak coxorte gi ñu ameel nit ku ñuul, rawati-na doomu Afrig. Waaye, suul ker du ko teree feeñ. Tey, boroomi xam-xam yépp a bokk ànd ci waxam ja. Kenn déggatul ña ko daan weddi démb. Waaye, liggéeyu Séex Anta mëneesu ko tënk ci gëstukat bi mu doonoon. Séex Anta yemul woon rekk ci di wax ak di firndeel ne, Afrig moo sukk jur àddina si walla, sunuy maam ya woon ci Misra ay nit ñu ñuul lañu woon. Liggéey na yit lu am solo ci wàllu politig.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Bu leen fàtte ne, Séex Anta Jóob nekkoon na fi politiseŋ. Waaye, nag, wute woon na lool ak politiseŋ yi nu xam. Moom dafa xamoon ne, xeex bi mu daan xeex, mënta àntu feek nguur dugalu ci loxoom. Maanaam, fàww nga yor ndogal li ngir mën a jëmmal xalaat ak yéene yi nga am ñeel sa réew walla sax Afrig gépp. Te, bokkoon na ciy yéeneem yu rafet ya, fexe ba réewi Afrig yépp booloo doon benn. Te, nag, ak li mu doon rafet xalaat yépp, mësul a dige lu mu mënul walla lu mënta nekk. Maanaam, daawul fen di dajale ni yeneen politiseŋ yi. Muy lu am a am solo. Séex Anta dafa daan wax ne, bu réewi Afrig yi bëggee tàggook seeni jafe-jafe, fàww ñu ànd fajandoo seeni jàngoro te kenn bañ a jéem a demal boppam. Ci gis-gisam, képp ku beru ci sa wet, dinga wéet ak say jafe-jafe. Te, béy bu àndul ak i  moroomi béyam, ànd ak cere ja. Kon, Séex Anta ak ñu mel ni Sànkaraa, Kuwaame Kurumaa ñoo bokkoon benn xeex, bokk benn jubluwaay bi : afal Afrig, boole doomi Afrig yi ñu doon benn ngir Afrig naat, ay dommam tekki.
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
Moom, li ko wutale ak i maasam mooy itte ju mu joxoon làmmiñi Afrig yi ak liggéey bu réy a réy bi mu ci def, rawati-na làmmiñi réewum Senegaal. Wone na ne, làmmiñi Afrig yi ñoo bokk cosaan ndax ci làmmiñu Misra lañu soqeekoo. Biral na itam mbokkoo gi nekk seen diggante ci wàllu aada, muy lu am solo. Dafa di sax, téereem bu siiw boobu mu génne ci atum 1954 te mu tudde ko “Nations nègres et Cculture”, moo may fit ñenn ñi ba ñu sóobu ci xeex bi. Ndege, ci màqaama téere bi la kurélu FEANF juddoo bañ ca tegee 4 at, ca Frãs, diiwaanu Gërënoobal. Kurél gi, nag, ay boroomi daraja, ay kàngam yu ñu ràññee, ñoo ko séqoon, ñu ci deme ni Abdulaay Wàdd, Asan Silla, Séex Aliyu Ndaw, Saaliyu Kànji Masàmba Saare, Asan Ja, añs. Ku lim juum. Waaye ay boroomi dayo ñoo ci bokkoon te amal liggéey bu am solo lool sax ñeel làmmiñu wolof. Ngir fàttali, kurél googu moo fi génne woon Ijjib wolof, muy ab téere bu ñeeloon njàngum wolof. Liggéey boobu moo àgsi ba ci sunu jamonoy tey jii. Lépp li ñu jot a wax walla def ci làmmiñi réew mi, ginnaaw Yàlla, ñooñoo tax te ñoom, téere Séex Anta baa leen xamb. Moo tax nu war ko sant, sargal ko, delloo ko njukkal. Ndax wolof dafa ne, bu lëg lekkee aloom, na ko gërëme coy…
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/
“SËRIÑ BI, FÀWW MU FEEÑ”
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/
Bu ñu seetloo fan yee ci ginnaaw, werante amoon na ci nataali Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke, naan moom la ak du moom. Muy ay nataal yi ñu fésaloon ci mbaali jokkoo yi. Nataal yooyu di wone jëmmi Séex Ahmadu Bàmba Xaadim Rasuul. Ñu xame woon ko ci benn nataal képp bu ñu miin a gis, réewu Farãs denc yeneen i moomeeli Senegaal, bokk na ca nataal yooyu.
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/
Mu doon juróom-benni nataal yu ñu portale ca atum 1918 ba ñuy teg xeer wu njëkk wu jumaay Njaareem. Bu ñu sukkandikoo ci këru xibaar gii di Pressafrik.com, nataal yooyu ñu ngi jóge ci arsitek bii di Jean Geoffre, nekk ki rëddoon palaŋi jumaa jooju. Ci lu ko weesu, ca weeru Me 2020, lañu fésal njaayum portale yooyu. Ci noonu, la ab kurél bu ëmb ay taalibe murid ak i gëstukat defe ay jéego ngir jot ci nataal yooyu. Ñu jaaye leen ko ci lu tollu ci ñeent-fukki tamndaret ci sunuy koppar, maanaam 40i milyoŋ.
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/
Biñ ci jotee lañ ko jébbal xalifa murid yi, Seex Muntaxaa. Mu fésal ci mbégteem, di sant taalibe yi. Ciy kàddoom, wax na ne : “Sëriñ bi, fàww mu feeñ”.
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/
Ci weneen wàll wi, xamees na ne, nataal yooyu, du moomeelu murid yi rekk. Ndax, day fésal mbatiitu réewu Senegaal. Ci noonu, la Njiitu réew mi, Maki Sàll, dajeek kurél googu ngir ñu jébbal ko moomeel googu. Mu nekkoon ci teewaayu jëwriñ yu bari, rawatina ki ñu dénk mbatiit gi ak moomeelu réew mi di Aliyu Sow. Bokk na ci lañu xaatim mooy jëmmal kër guy sàmm ak a saytu moomeel yi maanaam “musée”.
https://www.defuwaxu.com/serin-bi-faww-mu-feen/
Mënees na jàpp ne mbatiit, lu jar a sàmm la ndax dafa bokk ci kenoy askan. Kon, saytu moomeelu réew mi lu war la ngir seen taxawaay bañ a naax-saay.
https://www.defuwaxu.com/jonanteb-xaritoo-senegaal-door-na-kamerun-1-0/
JOŊANTEB XARITOO : SENEGAAL DÓOR NA KAMERUN 1-0
https://www.defuwaxu.com/jonanteb-xaritoo-senegaal-door-na-kamerun-1-0/
Gayndey kuppe yi dóor nañ Kamerun 1-0. Tey ci altine ji lañ doon amal joŋanteb xaritoo ca fowub Bollart bu Lens (France). Saajo Maane moo dugal biiwu Senegaal bi. Ab penaaltii la am, dugal ko. Joŋante bi nag, lees ko dugge mooy waajal CAN 2024 biy xewe fa Koddiwaar. Te sax, Senegaal ak Kamerun ñoo bokk genn kippu, war a laale keroog 18 saŋwiye 2024, ca fowub Yamusukroo.
https://www.defuwaxu.com/jonanteb-xaritoo-senegaal-door-na-kamerun-1-0/
Fu ñaari gaynde daje, pënd ma wuri. Senegaal ak Kamerun, saa buñ waree laale, àddina sépp ay toog di seetaan. Nde, bokk nañ ci ñaari réewi Afrig yi gën mag ci wàllu kuppe, ñu ràññee seen i kuppekat fépp ci àddina si. Moo tax, seen um ndaje mën a doon lépp ba mu des joŋanteb xaritoo. Ni mats tey bi demee firndeel ko. Ndax, ñaari ékib yépp a joxe li ñ amoon yépp, mel ni ñuy xëccoo kub. Mu nekkoon mats bu xumb, saf lool. Kenn mayul sa moroom dara. Moo tax, gaañante bi xawoon na bari ba arbit bi jot fa séddale 4i kàrtoŋi mboq. Senegaal nag moo daan ci seen njëlbeenug joŋante bii laata bu 18 saŋwiye 2024 bi.
https://www.defuwaxu.com/jonanteb-xaritoo-senegaal-door-na-kamerun-1-0/
Daanaka, ékibu Senegaal bi, ñépp ñoo gis, rawatina Kaliidu Kulibali, Kerepeŋ Jaata, Ismayla Jakobs ak Saajo Maane mi dugal. Dañ foogoon sax ne Kaliidu Kulibali, kàppitenu ékib bi, dafa tàmbaale jëm mag. Waaye, tey de, wone na ne dese na ñeex. Ku weddi laajal ñoom Abuubakar ak ñoom Toko-Ekambi. Dafa di, penaaltii bi sax, moom Kulibali moo ko indi. Nde, moo la wattukatu (défenseur) Kamerun bi takk, mel ni kuy bëre, daaneel ci suuf. Arbit joxoñ tombu penaaltii bi, Saajo Maane toj caaxi Andere Onanaa yi. Senegaal am benn, Kamerun tus.
https://www.defuwaxu.com/jonanteb-xaritoo-senegaal-door-na-kamerun-1-0/
Kamerun jéem na lu nekk ngir dab Senegaal, waaye dóor bu jub sax amuñu ko. Kon, xelu saa-senegaal yi war dalagum ci li seen gaynde yi wone tey. Waaye, sikk amul ci ne, joŋante bii ak bu CAN 2024 bi duñu niru. Nde, Kamerun dina bëgg a fayu. Waaye, Senegaal bii, bu dëggalee boppam, dina jafee dóor.
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/
DI BUUR, DI BUMMI
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/
Li jaaxal waa Senegaal, mooy wax-waxeet yi kilifay réew mi dëkke. Ku ci jóge ci kujje gi, dem ci nguur gi yaa ngiy xas ñaa nga àndaloon démb.
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/
Mbir mi dafay faral di am ba kenn, ci ñaari làng yépp, muccu ci. Ñépp a ngi fàttaliku ci ndetteelu atum 2018, bi peresidaŋ Maki Sàll nee mësul a ni nañu jële wote yi ci loxoy Usmaan Ngom. Moone, ba mu ko waxee yàggul woon dara te yit moom yemul woon ci loolu, nde noon na doonte sax Séex Géy la ñuy dénk liggéey boobu, ba tey Usmaan Ngom ay wéy di doon kilifaam. Waaw lan a fi soppeeku ci diggante bi ba mënul a def lu yées li mu doon laaj ? Ci sunu gis-gis, li ko waral du dara lu moy doole ju bari ji ñu jox peresidaŋ ci sunu doxalinu réew. Te loolu du tey la tàmbali : bi digganteem ak Mamadu Ja yàqoo la Seŋoor soppi sasug njiitu réew mi, jox ko doole ju baree-bari. Kon dafa mel ni mbir mi du Wàdd, du Maki te du keneen : képp ku fanaan Màkkaanu Njiitum Réew mi genn guddi, sooy yeewu di sax i laaf.
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/
Ba tax na, foog ñu wàññi doole joojuy tax benn doom-aadama kese yaakaar ni moo gën ñépp, lu mu xalaat mbaa lu mu xaw a xalaat sax, noonu la !
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/
Lenn ci li waral loolu, mën nañu cee lim li wolof naan : « Ku ëmb sa sanqal, ëmb sa kersa ». Lépp luy ndombog-tànk gu kawe, njiitu réew mi moo cay tabbe. Bu ko defee, ku nekk di xaar sa wàll ci nag wi, doo bëgg a def walla nga wax peresidaŋ loo xam ni dina tax ëllëg, mu ni kii de, àndul ak man, xereñ na, gaa, waaye dara laa ko dul jox.
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi-2/
Ngir loolu deñ fi, foog ñu def ni yen réew yi, maanaam di amal ay joŋante diggante doomi-réew yi ngir xool kan moo war a jiite bérébi liggéeyukaay yu kawe yi. Lu ko moy peresidaŋ dafay wéy di nekk daanaka Buur ak Bummi, kenn du ko sañ ni sa bët bi suuf a ngi ci.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
BÉS DU MAG, DU TUUTI, BOROOM LAY TOLLOOL…
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Dëgg la : ràcc jëmale sa kanam baaxul waaye tey fàww LU DEFU WAXU xamle mbégteem ci ndam li Paap Aali Jàllo am fan yee nu génn ca Iniwérsite Gaston Berger bu Ndar. Paap Aali ci kër gi la bokk, ayubés bu Yàlla sàkk mu am lu mu bind ci seen yéenekaay bii di LU DEFU WAXU. Nun ñiy liggéey ak moom xam nanu ne bu ci Yàlla àndee, kenn du wax ëllëg ci yenn kàllaamay réew mi, rawatina pulaar ak wolof, te doo tudd Paap Aali Jàllo.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Àllarba jii, deesu ko fàtte. Waaw, àllarba 20eelu fan ci weeru Féewaryee, Banqaasu Làkk ak Caaday Afrig (LCA), bi nekk ci Pàccum Aada yi, Diine yi, Aar yeek Jokkalante yi, doon na dalal ab ndongoom, mu war koo jax. Xew-xew baa ngi ame ca Iniwérsite Gaston Berger bu Ndar. Ndongo li doon jébbal kàngam yi njuréefi gëstoom mooy Paap Aali Jàllo. Ci kàllaama nasaraan, xew-xew boobu dees na ko duppe “soutenance de mémoire”. Loolu, nag, mi ngi am ginnaaw bi fa Paap Aali jàngee lu tollu ci diirub juróomi at.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Liggéey bi Paap Aali doon jébbal mbooloo mi, ci turi Pulaar yi la aju. Maanaam, gëstu bi mu amal ci diirub ñaari at, li mu ko dugge woon mooy biral jëmmi turi Pulaar yi, fésal ni ñu sosoo ci kàllaama pulaar, leeral seen cosaan, ak di xamle lu tur yooyii wund. Waaye, Paap Aali yemul foofu. Ndaxte, wax na ci biir téere-tëju-diggam bi naka lees tànne tur ñeel waaso Pulaar yi, gëm-gëm yeek pexe yi ko lal ba ci ngénte nees koy amale. Xóotaayu gëstu bee waral Paap Aali dem ba wone turi yaradal yeek xeeti tur yoo xam ne, ràññee njaboot gee leen tax a jóg. Maanaam, ni xale yi di toppalante, li ko dale taw bi ba ci caat bi. Loolu fés na ci tablo bii nu jële ci téeréem bi.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Kàngam yi doon saytu liggéeyu Paap Aali bi ñeent lañu : Porfesoor Maweja Mbaya mi jiite woon àtte bi, Doktoor Mouhamedoune Abdoulaye Fall, jàngalekat ca Banqaasu LCA, Doktoor Mariama Mahamane Maїga mi doon tette ndongo li ba liggéey bi yemb, ak njiitu Banqaasu LCA bi, Doktoor Ibrahima Sarr. Moom, Doktoor Ibrahima Sarr dafa wute bés bi ndax dafa amoon ngànt. Ab tukki moo ko teree teew. Waaye, jot naa yónnee ab bataaxal, biral ci mbégteem, seedeem ñeel Paap Aali, rawatina gis-gisam ci téere-tëju-digg bu Paap Aali Jàllo.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Ci suba si, bi fukki waxtu jotee, ci la ndongoy Banqaasu LCA tàmbalee feesal “Amphi B”. Mbokki Paap Aali yeek am-di-jàmmam yi tamit kenn demul ñu des. Bi fukki waxtu tegalee fanweeri simili, la lawax bi jël kàddu gi, layal xalaat yi mu xelli ci biir téere-tëju-diggam bi ginnaaw bi ko kilifa yi mayee ñaar-fukki simili. Mu daldi nuyoo ba noppi xamal nit ñi naka la tànne bile ponk, cosaanu liggéey beek jubluwaayam. Ci nasaraan, Paap Aali mi ngi doon gëstu lees di wax “Anthroponyme Pulaar : formes et sens”.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Moom, nag, tur yi Pulaar yi moomal seen bopp rekk la jagleel liggéey bi ngir biral ni tur ci bokk-moomeelu askan la bokk. Mu tënk, wone ay masala, leeral leen ci noppi nit ñi. Waaye, bala tog nomlet, toj nen.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Benn liggéey xéyul rekk sotti. Looloo tax Paap Aali xamle yoon wi mu jaar, jafe-jafe yi mu jankoonteel ak pexe yi mu lal ba jéggi leen ngir sottal mbind mi nga xam ne, mi ngi tollu ci 159 xët. Bi mu noppee, delloo na kàddu gi Kilifë yi doon càmbar téere-tëju-diggam bi. Njiitu àtte mi, Porfesoor Mbaya gërëm ko ndax li mu fexe ba yem ci waxtu wi ñu ko mayoon.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Jàngalekati Banqaasu LCA yi, Doktoor Mariama Mahamaan Maїga, Doktoor Mouhamedoune Abdoulaye Fall ak Doktoor Ibrahima Sarr, seen seede benn la. Nee nañu dañoo mӫs di bég ci Paap Aali, ndongo lu am pastéef, bӫgg lool li muy def. Dafa mës a doon royukaay ci ay moroomi ndongoom, nekk jàngkat te ku weg ñi muy jӫflanteel la. Ñu neeti, Paap Aali bokk na ci ndongo yi gën a xereñ ci Banqaasu LCA. Terewul, àtte nañu ko àtte bi war ginnaaw bi ñu saytoo liggéey bi. Li ci jaar yoon, kilifa yi rafetlu nañu ko bu baax. Masala xibaar yi mu indi ñeel Pulaari Fuuta Tooro yeek seen làkk wii di pulaar. Rawatina bi mu nu xamalee seen i tur ak li ñu wund.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
« Njuumte, nag, mënul a ñàkk ci téere-tëju-digg”. Loolu la Porfesoor Maweja Mbaya leeral laata muy jubbanti yenn njuumte yi mook Mouhamedoune Abdoulaye Fall, ak Mariama Maїga.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Kilifë yépp sampoon nañu ay laaj yu Paap Aali tontu tontu yu leer. Danuy jaaraat ci baatu Alpulaar, mu nekk baat bu siiw bu nuy dàkkantale nit ñiy làkk Pulaar. Te firi bi moo di “waxal Pulaar !”. Ci gis-gisu gëstukat bi, wareesul a woowe Pulaar yi baat boobu. Ndaxte, ab pulaar deesu ko wax “waxal pulaar” ndax moom la nàmp. Waaye baatu Alpulaar buuru Fuuta Tooro ba woon, Mànna, moo ko waxoon jëme ko ci wolof yeek yeneen waaso yi fa nekkaloon ak Pulaar. Ku ci làkk pulaar ñu woowe la “Alpulaar”, ku ko làkkul ñu rey la. Kon, baatu Alpulaar ab Ndigal la woon. Baatu “pël” yit noonu, wareesu ko jëfandikoo ngir tudd Pulaar yépp. Ndx kat, “pël” mécce la, maanaan ab sàmmkat la. Te ci biir Pulaar yi am nay nappkat, ay tëgg, ay géwél, ay uude, añs. Kon turu Pulaar moo gën jekk ci ñoom.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Jotaay bi, nag, yàggoon na ba jéggi dayo. Waaye, ba benn waxtu ci bëccëg jotee ba tegal fanweeri simili la kilifë yi daldi yégle seen àtte, jébbal ndongo li « Mention très bien ». Muy firndéel màggaayu liggéeyu Paap Aali. Ñépp ndokkale ko, ñaanal ko mu jig ko te yeneen lijaasa topp ci. Xarit yi daldi jël ay nataal ni ñu ko tàmm a defe. Ay xéewal lañu ko tëje, fa la mbooloo mi añe ba suur, naan yu sedd te neex.
https://www.defuwaxu.com/bes-du-mag-du-tuuti-boroom-lay-tollool/
Ma baamtuwaat ko, bés du mag, du tuut, boroom lay tollool, te keroog kenn werantewu ko.
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
SAARTJIE BAARTMAN, NDAW SA TUBAAB YI DEFOON MALA
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
Saartjie Baartman ab jaam la woon, fekkoon baax ca réewum Afrig-bëj-saalum.  Moom, nag, benn doomu Àngalteer lañu ko jaayoon. Gannaaw bi, Tubaab yi dañu ko wutal ab dàkkental, tudde ko Venus Noire walla Venus Hottentote. Ci atum 1810 la àgg Tugal. Bi mu àggee, nag, tubaab yi dañu ko wuññi, gàcc ko, làññi di ko wone ci ja yi ak luuma yi, diggante Àngalteer ak Frãs.
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
Waaw.
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
Saartjie Baartman as ndaw su jekkoon, ab diriyànke bu amoon waŋ ak i ween yu réy lool la woon. Mu jaaxaloon tubaab yi, ba tax fu nekk lañuy jóge ngir deñsi-kumpa soxna si. Noonu la Tubaab bi nekke woon ak moom, xàwwi suturaam, dëkke koo toroxal. Yenn saa yi sax ñii làmbatu ko, ñee siif ko, ñeneen ñi di ko jam ak seen parasol ak yu ni mel.
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
Mënees na wax ne, Tubaab yi ab mala lañu jàppe woon Saartjie Baartman. Li koy gën a firndeel mooy li ñu ko boole ci benn téere bees jagleel mala yi. Ku def jëf ju bon te ñaaw jooju mooy Cuvier, benn doomu Frãs bu doon gëstu xeeti mala yi. Noonu, gannaaw soxna Saartjie Baartman  nit ku ñuul la woon, Cuvier da koo boole ci mala yi, saytu ko, amal ay njàngat ci moom. Noonu, mu méngale ko ak mala yiy nàmpal, boole ko ci biir téere boobu nga xam ne, dajale xeeti mala yiy dund yépp a ko taxoon a jóg.
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
Bi mu faatoo ci atum 1815, kenn ci gëstukatu Frãs yi gënoon a mag te xelam màccoon ci xeet yiy dund, da koo fees, daggate ko, teqale cër yi. Mu seppi yóor gi, dindi awra wi, denc leen ci anam boo xam ne duñu yàqu. Jëmm ji moom, ñu lëmës ko ne ko gàcc ci kàggu-aada gi ñu duppe “Musée de l’homme” te nekk ca Pari, di péeyub réewum Frãs.
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
Saartjie Baartman, nag, dara yóbbewu ko mbugal bu ñaaw bii lu dul ni jigéen ju ñuul bindoo ak taaram. Ci atum 1994, ab diir ginnaaw bi politigu boddikoonte ci biir xeet (apartheid) jeexe ci réewum Afrig-bëj-saalum, ca la askan wa ñuy woowe ay xoyxoyca mooma réew sàkku ci Nelson Mandela mu fexe ba jot ci néewub Saartjie Baartman. Seen jubluwaay moo doon suturaal ko, denc ko ci bàmmeel. Waaye ñenn ci gëstukati réewum Frãs lànk ba tëdd ci naaj wi. Amuñu woon benn lay lu dul di wax ne néewub Saartjie boobu moomeelu Frãs la.  Noonu ba ci atum 2002 ci la Frãs soog a nangoo jébbale Saartjie Baartman ginnaaw bi dipite yi jëlee ndogal lu ni mel ca péncum-ndawi-réewam.
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
Tabo M’Beki mi jiitewoon booba ‘’Afrique du Sud’’ sànni woon na ci kàddu yu daw yaram yii : “Kiy niru mala dëgg-dëgg du doomu-Afrig bii di Saartjie Baartman. Déedéet. Mala yi dëggëntaan ñooy ñi ko xañ boppam ba noppi def jëf ju ñaaw jii”.
https://www.defuwaxu.com/2589/
KÀDDUY USMAAN SONKO 2/2 PÀCC
https://www.defuwaxu.com/2589/
Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa réew mi  ci 8eelu fan ci weeru Màrs. Waxtaan woowu nag, dara waralu ko woon lu dul mas-sawu leen ci yi fi jot a xew, xamal leen itam ni mook ñoom a bokk naqar.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Lu Defu Waxu>, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ci ñaareelu xaaj bii, ay kàddoom na mu leen yëkkatee keroog jooju.
https://www.defuwaxu.com/2589/
(Ci taataanug Uséynu Béey)
https://www.defuwaxu.com/2589/
Nu war nag di waxante dëgg ndax Maki Sàll, li ko bewloo, bokk na ci nun waa Senegaal, ñenn ci nun waa Senegaal. Bala maa dee ñu naan ku xareñ la ci pólitig. Ndaxte yow mën ngaa dal ci sa naataangoo, mën ngaa ko kompaloo, mën nga koo jënd, walbati ko ba suy waxati du xam li muy wax lu mu doon ; loolu mooy xareñ ci pólitig? Nun, lin soxla mooy ku xareñ ci ni ñuy yoree réew ; koo xam ne, suñ la dénkee réew, nga defar réew ma. Xarañ ci pólitig dëgg mooy liñ la dénk, nga liggéey ko ba soo ne woon sama ñaareelu moomeel jeex na, maa ngi dem, ñu ne la bàyyiwuñu la. Juróom-ñenti ati Maki Sàll yi, li fi am, masul a am ci Senegaal. Ñaata naataangoom la tëj, ñaata la faagaagal? Loolu ba kañ? Loolu nag, la nu mënatul a nangu. Te nag, lii mu def, dañ koy tudde ci Tubaab wor wu réy. Maanaam wor wi gën a réy ci wor yi mën a am. Ndax moom bi ñu ko falee dafa teg loxoom ci sunu ndeyu sàrti réew mi daldi waat, ne «waat naa ne dinaa tënku ci ndeyu sàrti réew mi, dinaa nekk ci bëgg-bëggu askanu Senegaal». Li mu def wuute na. Ku dem ba yow nga wéet kunduŋ ak say juróomi nit, saw askan janoo ak yow, nga am sañ-sañu yónni jawriñ bu ñoradi bi, mu ne sa askan woowu yépp ay «terroristes» lañu, askan woowu wépp dafa am ñu nekk seen ginnaaw di leen jox xaalis. Ndaw yii dañoo mas a gis ku leen jox xaalis ? Taxaw saaga sa askan wépp, wépp. Yow doŋŋ ci sa pale ; tey boo ñëwee ci péey bi, moom kenn ak paleem, moom cunduŋ, askan wépp nekk fii. Su dul woon takk-der yi nekk sunu diggante, tey jii ay bagaasam dañ koy for. Loolu mooy wor wu réy ndaxte liñ ko joxoon ci ay jumtukaay du woon ngir muy «comploter» ay naataangoom.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Dama wax tey, ñu ne ma «contrôle judiciaire», waratoo wax ci mbir mi, ma ne àttekat bi : «Su ngeen ci waxee ma wax ci». Ndax, ay mbir amoon nañ fi : mbirum Xalifa Abaabakar Sàlll gis nañ   ko, mbirum Karim Wàdd wax nañ ci. (…)
https://www.defuwaxu.com/2589/
Waaye, damay gaaral waa Senegaal. Wallaahi, dama ko waat, Wallaahi lañ ma tuumaal bu amoon, duma nangu benn doomu-Senegaal di ci am xoosu-xoosu, waxatumalaak bakkan di ci rot. Ndaxte bu boobaa, duma yem ci liñ ma def rekk, damay doon reykat ; kon doon na mel ni ñi ci faatu tey, man maa leen faat, duma nangu di am àq ak sama kanamu Boroom. Ñaawteefu Maki Sàll la ak ñi mu bokkal mbir mi.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Ba tax nag, ñu ne : Njiitu-Réew, am na loo xam ne, du sa sañ-sañ. Amul Njiitu-Réew moo xam ne, war naa féewale askanam, di féewale nit ñi, ñuy jàmmaarloo, di xuloo walla di xeex ; amul Persidã boo xam ne, war naa jiite ci coxor, ci bañ nit. Ndaxte, ku àndul ak yow rekk nga ne kii tey ma faagaagal ko. Loolu du Njiitu-Réew. Te nun ñépp, nan ko ci bañ a jàppale, ndaxte kàdduy mbañeel, léegi lay door a am Senegaal. Tey laay door a dégg Senegaal ñu tudd waaso nit ci pólitig, walla ñu tudd ngëm-ngëmam ci pólitig. Loolu, nun ñépp, kenn waru koo nangu ; te di ci woo ñépp nag, te di ci boole «media» yi. Nun ñépp nanu góor-góorlu. Wuutale ay porogaraam, ay naal ak ay xalaat, nangu nañ ko. Waaye def ay porogaraam ngir rekk ay nit ñëw di saaga nit, di ŋàññ nit, di wax ci moom loo xam ne du dëgg subaak ngoon, mu yor njaboot, am ñu ko bëgg, yor ay militaŋ, loolu mooy taal am réew…
https://www.defuwaxu.com/2589/
Nanu delloosi sunu xel, mbir mi sottante xalaat la, wuutale ay xalaat, ay porogaraam la, waaye du xeex ak kujje gi. Kenn ku ne deram rekk la am, waaye xéy suba ba ngoon, jóg di wax ci nit, di wax ci nit, di wax ci nit, tam ko dëmm, wax ciy mbokkam, wax ciy waa-juram, loolu amu fi woon ci Seŋoor, amu fi woon ci Abdu Juuf, amu fii woon ci Ablaay Wàdd ; mu ngi door a am, te dafa war a dakk. Maki Sàll moomul réew mi. Nun ñépp noo war a jël sunuy matuwaay. Te lii, defe naa buñ ci jógee dina doon njàngat ci nun ñépp. Ndaxte maa ngi seetaat porogaraam yi, dàŋŋaaral bi wàññeeku na. Ndax waroon nanoo toog ba agsi fii? War nañ cee jël ay njàngat. Ku ñu dénk réew, ñii nga xam ne ñooy say takk-der, nga xam ne kaaraange réew mi moo leen tax a jóg, waruloo leen teg ci yenn anam yi.  Ndaxte takk-der yi ma gis, ñoo gën a am lu leen naqadi fi nu tol nii ; ndax xam nañu ni ki ñuy dóor seen rakk la, xam nañu ni ki ñuy gaañ seen rakk la ; koo ci wéetal; xolam seddul. Ku ñu jox réew war ngaa moytu loolu.
https://www.defuwaxu.com/2589/
May sargal nag Sàndarmëri Senegaal, ci seen mën-liggéey, ci seen sago. Man dama leen a mujjee naw. GIGN, bés biñ may jàpp ba tey biñ may delloosi ma dem noppaliku, ci seen loxo laa nekk. «Brigade de Recherches», noonu. Ngalla waay bu nu caaxaane sunuy «institutions» (campeef). Kenn musu ma sax bëmëx, kenn musu ma xoos. Kon ñooñu, ku am ñu mel noonu, àddina sépp ñee na ñu ko, ngalla waay Maki Sàll bul yàq sunu réew. Sàndarm boobu gaañu démb, ci GIGN yi ma yoroon la, di liggéeykat bu mag a mag a mag, ku bëgg réewam, tiitaru Senegaal la ; ñeewant bi mu amoon ci ñi mu doon sànni gërënaad bi, moo tax mu téyéwaat ko, moo yàq loxoom tey. Kon yooyu dañ ciy bàyyi xel, te gëm naa ni, ni mu amee ci sàndarmëri la amee ci yeneen tàkk-der yi. Kon waay-pólitig yi buñu yàq sunu diggante, nun waa Senegaal, waaye it sunu diggante ak sunuy campeef, rawatina sàndarmëri, xare bi, pólis ak leneen ak leneen.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Di wax tamit ni, Maki Sàll mooy ndeyu-mbill gi ci li xew nii ci réew mi ; te loolu dunu ko bàyyi mu jàll. Maki Sàll amul màqaamay jiite Senegaal tey jii, amu ko ! Amu ko woon démb tey doog a ñëw. Ndax man bokk naa ci lawax yi nga xam ne, bi nu génnee ci 2019, maa waxoon ñetti lawaxi kujje gi, ne leen sama ngëm-ngëm du nañ génne xale yi, mooy duñ ko jàppe ni Njiitu-Réew mi. Mooy persidã ci kanamu Yoon waaye amatul màqaama bi. Defe naa mennum man ci lawax yi, maa ci yor taxawaay boobu ba léegi. Musuleen maa dégg mani ko Persidã Maki Sàll. Maki Sàll laa koy wax ndaxte màqaama Njiitu Réew amu ko, dafa mbuxum wote bi. màqaama boobu nag, li ci desoon lu tuuti, moo fi nekkatul. Kon su nu nekkoon ci yenn anam yi, Maki Sàll dañ ko waroon a wacce tey jii. Su nu nekkoon ci yenn anam yi, waaye, foofu nag laa bëgg askan wi dëglu ma, nanu dëgloonte bu baax a baax a baax. Ndaxte, loo gis rekk teey ak dal daf cee baax. Benn, bu kenn dem pale ne Maki Sàll day wàcc ci anam yu ko neexul, ndaxte loolu baaxul ci demokaraasi, fi mu mën a jëme réew mi du baax. Moom, bu xoolee boppam ba xam ne amatul màqaaamay jiite Senegaal, mu ne «jóg naa man, bàyyi naa», na askan wépp jóg tàccu, nu waajal sunu wote, ñi war a dem, dem jàmmaarloo. Wànte, bu ko deful, nanu ko gunge ba màndaam jéex.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Ñaareel bi, yenn boroom xam-xam yaa ngiy wax « gouvernement d’union nationale». Nun de, sama bopp laa mën a waxal ak ñi ma àndal, bokkunu, jegewunu benn xeetu guwernmaa bu Maki Sàll. Ndaxte, dañ koo nawloowul bay mën a ànd ak moom ci guwernmaa. Ndaxte koo dem ba ne dafa wor, waratoo wéy di ànd ak moom ci guwernmaa.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Léegi nag mu des, li ma bëgg waxtaaneek waa Senegaal :  coppite bi, «révolution», am na ba noppi, kenn mënautu koo téye. Bu ñu ne woon coppet Usmaan Sonko yóbbu, walla ñu def ko Dëkurwaa walla ñu def ko Séex Tijaan Jéey, walla Xalifa Sàll, ku mu mënti doon, du tee, ñii ma gis nii ci ndaw ñi, kenn mënatuleen a téye. «La révolution est en marche», te gën cee yàgg, 2024 nu mottali ko. Li ci des mooy, nanu bañ a def njuumte yi nga xam ne réewi Afrig yu bari def nañ ko fi : mooy, dañuy def seen coppite, «révolution», ba egg ca cëppaandaw ga, mu am ñu ñëw ne ko coppet, rawatina nag xare yi. Ndaxte, réew am na fu muy tollu, xare bi day jël nguur gi. Te ñaare, xare, day am yeneen réew yu am doole yuy jël seeni nit waajal leen ngir ñooñu jël réew mi. Bu nu sàgganee ba xare jël réew mi, lépp li nu doon yóotu ak di ko nas dinanu ko ñàkk. Moo tax ma ne «syndrome malien» baa ngi nii. Keroog ba ñu defee seen coppite  bay waaj a egg, ñu ne xare ba génn na, ñu topp ci «chars de combat» yi di tàccu, laa ni mbir mi jeex na, ñàkk nañu, ak feneen ak feneen ak feneen.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Moo tax coppite gi am na ba noppi. Maki Sàll mënautu koo téye, kenn mënu koo téye. Kon nan ko gunge ndaxte pexe dafa baax ci lu ne. Du lépp nag lañuy wax ci tele, waaye sunu warugar nun ñépp, askan wi, mooy nan ko gunge ba nu egg fi nu bëgg a egg. Waaye nag, loolu tekkiwul ni, danoo firi Maki Sàll rekk di ko seetaan. Nuŋ koy gunge mooy, danu koy tënk ci wenn doxalin ginnaaw-si-tey. Ndaxte loolu la askan wi bëgg.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Askan weey dogal tënk ci dooleem. Tënk boobu nag, bokk na ci :
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Benn lu nuy «exiger» la, bu ci njëkk mooy ñii nga xam ne seen bakkan rot na ci mbir mi, te muy ki ko def, moom Maki Sàll, nañu jox ndàmpaay seeni njaboot. Te ñu ubbi lànket bu tënku- wul ndax ñu xam ku tiire ak kan moo rey. Te itam, dinanu yóbbu mbir mi ci “Cour Pénale Internationale” mu àtte ko. Ndaxte, yii, ay «crimes contre l’humanité» lañu, te ci nguuru Maki Sàll la xewe fii ci Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Ñaareel bi, mooy ñi ci gaañu, dañ leen war a jox ndàmpaay, ñuy «civils» walla diy takk-der, jàppale leen ñu mën a faju ci ni mu gën a rafete ;
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Ñetteel bi, mooy ñi ñu jàpp ndax seen taxawaay ci pólitig bi, na leen Maki Sàll bàyyi ci ni mu gën a gaawe.
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Ñenteel bi mooy, bis niki tey dootunu nangu Maki Sàll di bunduxataal ñi àndul ak moom ak jaambur yi, di leen wattu, di leen déglu ci lu ñu yëgut, saa su ne.
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Juróomeel bi mooy, ñi nga xam ne ay sàmbaa-bóoy lañ yu mu jël, jox leen xaalis, ñu yor ay jaasi ak i fetal, nañu def lànket ba xam ñan lañu, jàpp leen, jébbal leen Yoon, ñoom ak ñi leen yónni.
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Juróom-benneel bi mooy, Maki Sàll, bëgg na ko, bañ na ko, dina fexe ba ñu mën a dem ci ay wote ni mu gën a leere. Ay wuruj «fichier électoral» jeex na ci Senegaal. Yor say kar-dàntite ne duma ko jox ndaw ñi ndax ànduñook man, jeex na ci Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Juróom-ñaareel bi, mooy, ci ni mu gën a gaawe, foog ñu amal wotey gox-goxaan yi, doomi-Senegaal yi tànn seeni meer. Na Maki Sàll amal it wote dipite yi ci atum 2022, doomi Senegaal yi tànn seeni dipite, jox seen bopp Péncum ndawi réew miñ bëgg. Waaye dina doxal it ci atum 2024 wote ngir tànn njiitu réew mi ci ni mu gën a rafetee. Lii, lenn rekk moo ko mën a gàntal, mooy mu dem ba xam ni moom, jiiteetul Senegaal, amatul màqaama bi, mu ne bàyyi na,  ñu amal ay wote lu jiitu 2024.
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Juróom-ñetteel bi mooy, na Maki Sàll delloo ñi mu ko xañ, seen àq ak yelleef ci pólitig : benn ci Xalifa Abaabakar Sàll mii, ñaar ci Karim Wàdd. Maki Sàll mooy tànn kuy lawax ak ku dul lawax, loolu jeex na Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/2589/
– Juróom-ñenteel bi mooy, moom Maki Sàll, na taxaw jàkkaarlook waa Senegaal yépp – amul lu ma neex laay def, walla du waaw du déet ; fii déet rekk moo fi am – ne ñetteel  sax dootuma ko tudd waxatumalaak ñetteellu moomeel. Atum 2024 Maki Sàll du nekk lawax ci Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Lii lépp nag dafa am lu mu àndal, may ñaan askan wi, rawatina ndaw ñi, sunu taxawaay bii, bu mu wàcc mukk nag. Tey lanu war a gën a taxaw. Kenn ku ne ci nun am na sañ-sañu jëfandikoo àqam bi nga xam ne ndeyu sàrti réew mee ko ko may ni : «man duma nangu ku ma noot». Loolu ngeen def tey jii, loolu ngeen def fan yii yépp weesu. Nu wéyal taxawaay boobu. Waaye, na doon taxawaayu jàmm, ndaxte dafa am lu Maki Sàll foqati woon ci nun : kenn amatul woon sago def mbooloo. Tey, won nañ ko ni mu bëgg ko mu bañ ko danu koy def ndax ndeyu sàrti réew mi moo nu ko may…..
https://www.defuwaxu.com/2589/
May wax nag, ginnaaw ba ma waxee ci Maki Sàll, may woo nun ñépp, nun ñii ñépp di ay way-pólitig ; askan wii, yelloo na ay way-pólitig yu mat. Nun ñépp amatunu sañ-sañ ci yenn yi, nanu sargal askan wi, nanu ko delloo màqaamaam, nanu ko waat nun ñépp ni, askan wi rekk moo nu ñor ; kenn newu fi di def pólitig ngir xaalis booy am ; ku bëgg ay milyaar, uti ko feneen. Waaye pólitig jaamu sa askan la, yaa ciy sonn, dugal ci sa alal, ñàkk ci ba dee, waaye waroo foog ni, ci pólitig ngay ame milyaar. Kon, nax nga sa bopp. Loolu dafa war a dakk ci Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Man dey, man Usmaan Sonko,  tuuti naa lool ci kanamu askan wi. Gisuma lan laa def ba askan wi daj li mu daj ci nun. Kon nun it, nanu waat ni, bis niki tey, dinanu am doxalin wu yees. Ndaxte réew mi yomb naa defar de. Bii yoon, war nanoo jublu ci doxalin wu bees. Su dee nag, danuy ŋàññ ñi fi nekk ba jële leen fi, ñëw def lañu  daan def walla lu ko yées, defe naa ne, askan wi day, mujj génn ci nun ñépp. Ngalla waay nañ ci góor-góorlu.
https://www.defuwaxu.com/2589/
Ma yokk ci benn poñ. May sànni ay kàddu jëmale ko ci Kaasamaas, ci mujjeelu yoon wi. Samay mbokk laay waxal, walla ñenn ci samay mbokk, ndax Yàlla may na ma ma bokk fépp. Ak lu nit mënoon a jàpp ba tax nga dugg ci àll bi, jàpp ni dañ laa xeeb, jàpp ni dañ laa boolewul, jàpp ni «citoyen de seconde zone» nga, boo xoolee li xew tey ci Senegaal, dinga xam ne loolu amut. Ndax, ginnaaw ba ma doonee doomu-Senegaal, doomu- Kasamaas laa. Waaye ñii ñépp jóg taxaw, muy Tuubaa, muy Ndar, muy Fuuta, Bakel, muy Kees ak feneen ak feneen, jóg taxaw, seetuñu kii fu mu bokk. Dëgg jot na, nanu xeex ngir dëgg sax fi. Kon, li ma leen di ñaan mooy ci 6i weer yii, li may ñaan samay mbokk yi ci Kaasamaas, ku ci yoroon ngànnaay na ko teg te bañ cee laaj dara, génn, nu bokk ndey bokk baay, te xam ne nun ñépp doomi -Senegaal lanu, doomi-Afrig lanu. Ginnaaw ga, ngeen ànd ak sunu xare, fépp fu nit ñi ne woon ngeen génne kàrt yi, génne miin yi, génne ndell yi, aar nit ñi. Bunu nangooti ñu ne dañ koy saafaraal ci ngànnaay. Ndaxte, kiy jam ak ki muy jam ñoom ñépp doomi-Senegaal lañu. Nun ñépp benn lanu. Kon loolu, mooy woote woo xam ne, maaŋ koy woote ndax lu ma ñor a ñor la. Te ku seet bu baax li xew Senegaal tey, dinga xam ne waa Senegaal yépp wone nañ ni Senegaal benn bopp lanu. Kon, lii lanu ci bëggoon sànni ciy kàddu yu gàtt…..
https://www.defuwaxu.com/2589/
May rafetlu it teewaayu soxna yi ; tudduma goor ñi, bis bii, bisu jiggéen ñi la. Soxna Aminata Lóo Jeŋ, ministar bi, di ko gërëm bu baax ci teewaayam ak ci taxawaayam ci xeex bi, ndax bi mbir mi dooree rekk la dawsi  kër ga, jaa-ngeen-jëf…
https://www.defuwaxu.com/seex-bekaay-deddu-na/
SÉEX BEKAAY DËDDU NA !
https://www.defuwaxu.com/seex-bekaay-deddu-na/
Xalifa tarixa xadiir yi ci Senegaal wuyuji na Boroomam ginnaaw tawat bi ko tëraloon. Kan moo doonoon Séex Bekaay ? Jaar-jaaram lan leen dégtal ci yaxal bile, ngir xamal leen kan moo doon xalifa ba woon ca Njaasaan.
https://www.defuwaxu.com/seex-bekaay-deddu-na/
Séex Al Bekaay mu ngi gane àdduna ca atum 1929, ñaari weer ginnaaw ba baayam Séex Bu-kunta nelawee. Mu nekkoon taawam, nekk tamit juróom-ñaareelu xalifaam. 2018 la toog ci xilaafa gi. Mu nekkoon ku ràññeeku ci mbooru araab. Doonoon ku fés ci bëgg Téere Bu Sell Bii di Alxuraan. Am njàngam mu doore ko ci magam Muhammet Kunta. Waaye, Gànnaar (Muritani) la ko mottalee. Ci noonu, bi mu ñibbisee la dal Medina Baay ci wetu Allaaji Ibraayma Ñas. Mu nekkoon ku ko jege lool ba léegi kóllëre googu di wéy ba ci Séex Maahi Ñas miy xalifab Medina Baay. Mu mel ni yamutoon rekk ci diine ji. Nde, Séex Bekaay bokk na ci ñi njëkk a liggéey ci caytu gi. Mu daan yëngu ca APS (Agence de Presse Sénégalaise).
https://www.defuwaxu.com/seex-bekaay-deddu-na/
Ñu denc ko ca dëkk bu sell ba di Njaasaan, ci teewaayu mbooloo mu takkoo-takku. Mbokk, taalibe, kilifa diine niki aada, ñépp ñoo ñëw teewe ci ginnaaw jullig tisbaar gi. Ñu seetlu fa teewaayu Taala Silla ma fa jiitu woon jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi, ci turu Njiitu réew mi, Maki Sàll, jottali fa njaalam njaboot gépp, waaye tamit bépp jullit. Niki ni ñu baaxoo defe, ginnaaw dëddug Séex Bekaay, ka ko fa wuutu di Séex Bu-Siidi Maxtaar Kunta, nekk léegi xalifab Njaasaan.
https://www.defuwaxu.com/seex-bekaay-deddu-na/
Mënees na wax ne Njaasaan a ñàkk, waaye umma Islaam a ñàkk kilifa gu mag. Jaar-jaaram doon lu fésul ndaxte li ko yitteloon mooy diine ji. Loolu, terewu ko ubbeeko ci xam-xami àdduna ak ug yëngoom.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
CAN-SENEGAAL : JOŊANTEB XARITOO
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
Ëllëg, ci altine ji, bu 18i waxtu jotee la Senegaal di daje ak Niseer ca fowu ba ca Jamñaajo. Muy joŋanteb xaritoo bees taxawal ngir waajalee ko CAN bi war a tàmbali 13i fan ci weer wii. Bu ñu noppee ci loolu, ndawi Senegaal yi di waajal ngir dem Koddiwaar.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
ÀNDRE ONANA
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
Góolu Kamerun bi fekkijeegul i naataangoom ca seen waajtaay ya. Lu ko waral nag, moo di ne Manchester United dafay amal ab joŋante kub moom ak Wigan ëllëg ci altine ji, ak joŋanteb sàmpiyonaa moom ak Tottenham keroog 14i fan ci sãwiyee wii. Bu ci noppee lay daldi fekkiy moroomam ya. Loolu nag, waa Manchester United ñoo ci waxtaan ak waa Kamerun ba juboo ci.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
CAF YOKK NA NDÀMPAAYU CAN BI
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
Senegaal mi jël CAN 2022 bi jotoon na lu tollu ci 2i tamñareet ak 997i tamndareet yu teg ci sunuy koppar. Ci wii yoon nag, waa CAF dañu daldi yokk yëf yi ba ci 4i tamñareet ak lu teg. Moy lu am solo lu ñépp rafetlu.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
PAAP MATAAR SAAR FEDDALI NA PASAM
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
Doomu Senegaal ji moo ngi jóge woon Metz (Farãs) fekki woon Tottenham daaw. Ren nag, dafa wane xarañte ak jom ju ko yóbbe mu bokk ci ñay tàmbali saa su ne ca ekib ba. Ci loolu, mu jubook gaa yi daldi féddali pasam ca ekib ba ba atum 2030.